LESOŊ 37
Lan la Biibël bi wax ci liggéey ak xaalis?
Jafe-jafe ci am liggéey walla xaalis ndax mas naa tax nga jaaxle? Faj suñuy soxla boole ci jaamu Yexowa ni mu ko bëgge, mën na nekk lu jafe. Biibël bi dafa ñuy jox xelal yu baax yu ñu mën a dimbali.
1. Lan la Biibël bi wax ci liggéey?
Yàlla dafa bëgg ñu jële mbégte ci suñu liggéey. Biibël bi nee na «nit amul lu gën [...] di bànneexoo ñaqam» (Kàdduy Waare 2:24). Yexowa liggéeykat bu mag la. Bu ñu nekkee ay liggéeykat ni moom, dinañu ko neex te dinañu ci jële mbégte.
Liggéey am na solo. Waaye waruñu ko bàyyi mukk mu gën ñoo amal solo jaamu Yexowa (Yowaana 6:27). Yexowa dige na ne, bu ñu ko jiitale ci suñu dund, moom dina ñu may li ñu soxla ngir dund.
2. Naka lañu war a gise xaalis?
Dëgg la ne Biibël bi nee na «xaalis kiiraay la», waaye wax na itam ne xaalis kese mënuñoo may mbégte (Kàdduy Waare 7:12). Kon dafa ñuy xelal ñu bañ a bëgg xaalis waaye ñu «doylu» (Jàngal Yawut ya 13:5). Bu ñu doyloo ci li ñu am, duñu daj jafe-jafe yi sonal ñiy wut a am lu bare. Dinañu moytu it yenn bor yi (Kàddu yu Xelu 22:7). Te loolu dina ñu aar ci jafe-jafe yi mbirum lotëri walla wut a am xaalis ci lu gaaw te yomb di jural ñi koy def.
3. Naka lañu mënee yéwén ci suñu alal?
Yexowa, Yàlla ju yéwén la, te bu ñu royee ci moom dinañu «yéwén, bay sédd ñi amul» (1 Timote 6:18). Mën nañu jëfandikoo suñu xaalis ngir def ay maye ci mbooloo mi te dimbali ñeneen ñi, rawatina suñuy mbokk ci ngëm. Noonu dinañu wone ne yéwén nañu ci suñu alal. Li gën a am solo ci Yexowa nag, du ñaata lañuy maye, waaye li tax ñuy maye. Bu ñuy maye ak xol bu tàlli, dinañu bég te dinañu neex Yexowa (Jàngal Jëf ya 20:35).
XÓOTALAL NJÀNG MI
Xoolal njariñ bi ñuy am bu ñu amee gis-gis bu baax ci liggéey te doylu.
4. Màggalal Yexowa ci ni ngay defe sa liggéey
Suñu xaritoo ak Yexowa dafay feeñ ci gis-gis bi ñu am ci liggéey. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.
Ci wideo bi, lan moo la neex ci gis-gisu Jason ak ci doxalinam ci bérébu liggéeyukaayam?
Lan la def ba yemale liggéey palaasam?
Jàngal Kolos 3:23, 24. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lu tax suñu gis-gis ci liggéey am solo?
Liggéey am na solo. Waaye waruñu ko bàyyi mukk mu gën ñoo amal solo jaamu Yexowa
5. Dañuy jële njariñ ci doylu
Ñu bare dañuy def lépp ngir am xaalis bu bare. Waaye li ñu Biibël bi xelal wuute na ak doxalin boobu. Jàngal 1 Timote 6:6-8. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan la ñu Biibël bi xelal ñu def?
Bu dee sax li ñu am bariwul, terewul mën nañoo bég. Seetaanal WIDEO BI. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp.
Lan moo tax njaboot yooyu bég, bu dee sax amuñu xaalis bu bare?
Léegi bu ñu bare xaalis nag te bëgg mu gën a yokku? Yeesu joxe na misaal buy wone ne loolu mën na ñu lor. Jàngal Luug 12:15-21. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan nga jàng ci léebu Yeesu bi? (Xoolal aaya 15).
Jàngal Kàddu yu Xelu 10:22 te xool li ko wuutale ak 1 Timote 6:10. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp:
Ci sa xalaat, lan moo gën a am solo? Xaritoo ak Yexowa walla am xaalis bu bare? Lu tax?
Ban jafe-jafe moo mën a dal kiy daw ci ginnaaw xaalis rekk?
6. Yexowa dina faj suñuy soxla
Bu ñu amee jafe-jafe ci am liggéey walla xaalis, loolu mën na ñu dimbali ñu xam ndax wóolu nañu Yexowa. Seetaanal WIDEO BI ngir xool li ñu mën a def bu ñu amee jafe-jafe yooyu. Boo paree, nga tontu ci laaj yii di topp.
Ci wideo bi, ban jafe-jafe la mbokk mi amoon?
Lan la def ngir génn ci jafe-jafe boobu?
Jàngal Macë 6:25-34. Boo paree, nga tontu ci laaj bii di topp:
Lan la Yexowa dig ñi ko jiital ci seen dund?
BU LA NIT WAXOON: «Dama war a liggéey ngir dundal sama njaboot. Mënuma teewe ndaje yi yépp.»
Ban aaya moo tax nga gëm ne, jiital jaamu Yexowa ci suñu dund mooy dogal bi gën?
NAÑU TËNK
Liggéey ak xaalis am na solo, waaye wuruñu leen a bàyyi mukk ñu tere ñoo jaamu Yexowa.
Nañu fàttaliku
Lan moo ñu mën a dimbali ñu am gis-gis bu baax ci liggéey?
Ban njariñ lañuy jële ci doylu?
Yexowa dige na ne dina toppatoo ay jaamam, naka nga mënee wone ne gëm nga loolu?
GËSTUL
Xoolal ndax Biibël bi dafa wax ne xaalis baaxul.
Ndax lotëri ak kàrt xaalis mën na ñu indil jafe-jafe?
«Lan la Biibël bi wax ci (lotëri ak kàrt xaalis)» (g15 Màrs)
Xoolal li tax góor gu doon lotëri ak di sàcc soppi dundam.