TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • lmd lesoŋ 7
  • Wéyal di yégle xibaaru jàmm bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Wéyal di yégle xibaaru jàmm bi
  • Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Turu xaaj yi
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ko Pool defe
  • Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?
  • Nanga roy ci Pool
  • Na nga suufeelu
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Wonal nit ñi ne am nga itte ci ñoom
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Deel muñ, te def ndànk ak nit ñi ci liggéeyu waare bi
    Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
  • Buñu bàyyi waaraate bi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2008
Xóotalal waxtaan bi
Wonal nit ñi mbëggeel—Noonu nga leen di dimbalee ñu nekk taalibe Yeesu
lmd lesoŋ 7

LI NGA MËN A WAX BOO SEETIWAATEE NIT KI

Ndaw li Pool a ngi yégal xibaaru jàmm bi nit yu dajaloo ci benn lekkool.

Jëf ya 19:8-10

LESOŊ 7

Wéyal di yégle xibaaru jàmm bi

Njàngale bi: «Dañoo wey di jàngale ak di xamle xibaaru jàmm bi»—Jëf ya 5:42.

Ni ko Pool defe

Ndaw li Pool a ngi yégal xibaaru jàmm bi nit yu dajaloo ci benn lekkool.

Turu WIDEO bi: Ndaw li Pool dafa wéy di yégle xibaaru jàmm bi ca dëkku Efes

1. Seetaanal WIDEO bi, walla nga jàng Jëf ya 19:​8-10. Ba pare nga tontu ci laaj yii di topp:

  1. Amoon na ñi doon fitnaal Pool. Waaye, lan la def ba wéy di dimbali ñi nga xam ne xibaaru jàmm bi itteel na leen?

  2. Ñaata yoon la Pool doon dellusi ngir seetiwaat ñi nga xam ne xibaaru jàmm bi itteel na leen? Te ñaata wér la fa def?

Ban njàngale lañu mën a jële ci li Pool def?

2. Seetiwaat nit ñi te tàmbali njàngum Biibël bi ak ñoom dafay laaj góor-góorlu, ak jot ju bare.

Nanga roy ci Pool

3. Deel seeti nit ñi ci waxtu bi gën ci ñoom. Laajal sa bopp lii: ‘Ban waxtu moo gën ci moom? Fan la bëgg ñuy daje?’ Defal lépp ngir seetiwaat nit ki ci waxtu bi gën ci moom.

4. Laaj ko kañ nga mën a dellusi ngir wéyal waxtaan bi. Saa yoo waxtaane ak nit ki, bala ngay dem, laaj ko bés ak waxtu bi nga fa war a dellu ngir wéyal waxtaan bi. Fexeel ba ñëw ci bés ak waxtu bi nga ko dig.

5. Amal gis-gis bu rafet ci ñi lay déglu. Xéyna nit ki, amul jot ju bare, walla sax, doo ko fekk këram saa su nekk. Loolu tekkiwul ne xibaaru jàmm bi itteelu ko. (1 Korent 13:​4, 7) Waaye nag, def lépp ngir yégle xibaaru jàmm bi, tekkiwul ne da nga war a jël sa jot jépp ci ki nga xam ne yelloowu ko.—1 Korent 9:26.

SEETAL AAYA YII ITAM

Jëf ya 10:42; 1 Korent 9:​22, 23; 2 Korent 4:1; Galasi 6:9

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager