Buñu bàyyi waaraate bi
1 Yenn saay, mën nañu xalaat ne waare nañu ay yooni-yoon suñu gox bi yépp, waaye ñu bare duñu déglu. Waaye ba tey, am na lu am solo lu war a tax ñu kontine di waare. — Macë 28:19, 20.
2 Dafa war a nekk seede : Yeesu waxoon na ne waaraate xibaaru Nguur gi dina am solo lool ci xew-xew yuy wone bi “ àddina di tukki ”. Waxoon na it ne dinañu yégle xibaar boobu “ ngir mu nekk seede ci xeet yépp ” (Macë 24:3, 14). Bu ñu nit ñi di gis ñuy waare xibaar bu baax bi jëm ci Nguuru Yàlla, loolu seede bu am solo la . Bu ñu waaree ba dem, ay nit mën nañu topp di wax ci ñun lu mat ay waxtu walla ay fan, bu dee sax nanguwuñu déglu li ñuy wax. Xam bu baax li waral ñuy waare, dina tax ñu jàpp bu dëgër ci waaraate bi. Bu ñu bokkee ci nit ñiy def li Biibël bi wax ne dafa war a am, maanaam ñuy waaraate te di yégal nit ñi li leen war a dal, dañuy neex Yexowa. — 2 Tes. 1:6-9.
3 Waruñu bàyyi liggéey bi : Nit ñi dañu bare itte te barewuñu jot. Looloo tax bu ñu dajee ak koo xam ne suñu waxtaan dafa ko neex, dañu war a góor góorlu ngir kontine di ko seeti. Am na jigéen joo xam ne, seede Yexowa yi dañu ko doon seeti ayu-bés bu nekk. Def nañu ko lu mat at bala muy nangu ñu dugg ci biir këram ngir waxtaan ci Biibël bi. Li mu dég dafa ko neex lool ba mu nangu ñu jàngal ko Biibël bi. Mu komaase di teewe ndaje yi. Teguñu ci lu yàgg sax, mu wax ne dafa bëgg ñu sóob ko.
4 Àddina si dafay gaaw a soppeeku. Nit ñi itam. Ñu bare ñu bañoon a waxtaan ak ñun bu njëkk, mën nañu nangu déglu léegi xibaar bi nga xam ne dafay maye yaakaar. Bu dee sax benn nit rekk moo nangu déglu xibaaru Nguur gi, mën nañu wax ne jar na ko.
5 Ci àddina si sépp, nit ñaa ngi gën di “ metitlu ci lu bon li am ” (Éz. 9:4). Li liggéeyu waaraate bi di indi, dafay wone ne boroom xol yu rafet yi ñu ngi nangu déglu xibaaru Nguur gi (Esa. 2:2, 3). Kon nag, buñu bàyyi waaraate bi, te nañu kontine di “ yégal nit ñi xibaar bu baax buy yégal lu gën ”. — Is. 52:7 ; Jëf. 5:42.