Bu ñu jëfandikoo kayit yu ndaw yi, dina indi lu baax
1 Mbootaay bi Yexowa di jëfandikoo tey, yàgg na gis lu baax li kayit yu ndaw yi di indi. Turu mbootaay bi ci boppam, maanaam Watch Tower Bible and Tract Society, wone na ne kayit yu ndaw yi am nañu solo lool ngir xamle xibaar bu baax bi. Diggante 1881 ba 1918, mbooloo Yexowa bi joxe na lu ëpp 300 milyoŋi kayit yu ndaw. Lu bare ci ñi ñówoon bokk ci ñi des ci karceen yi ñu tànn ci jamano jooju, ci kayit yu ndaw yooyu lañu njëkke gis lu jëm ci dëgg gi.
2 Bi ñu génnee ñeenti kayit yu ndaw yu am nataal yu am kulóor ci atum 1987, dañu waxaat nit ñi ñu jëfandikoo kayit yu ndaw yi. Kayit yu ndaw yooyu ñu ngi fi ba tey. Ndaje bu gën a mag bu ñu defoon ca atum 1992, mu ngi tuddoon : “ Porteurs de lumière. ” Ca ndaje boobu newoon nañu ne dinañu am yeneen ñeenti kayit yu ndaw yu am nataal yu am kulóor. Li nekk ci kayit yooyu, dafay tax nit ñi di xalaat bu baax. Kayit yu ndaw yooyu ñu ngi tuddoon : Le monde actuel survivra-t-il ? ; De l’aide pour les déprimés ; Une vie de famille agréable ; Qui domine vraiment le monde ? Ginnaaw loolu yokk nañu yeneen kayit yu ndaw yu mel ni yii : Jéhovah : qui est-il ? ; Jésus : qui est-il ? ; Avez-vous un esprit immortel ? ; Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? Ndax yéen a ngiy jëfandikoo bu baax kayit yu ndaw yooyu ci waaraate bi, ngir ñu mën a indi lu baax ?
3 Balaa kayit yu ndaw yooyu di mën a jur lu baax, fàww ñu jëfandikoo leen bu baax. War nañu xam bu baax li kayit bu nekk di wax. Ndax jàng nga leen bu baax ngir mën a xam li kayit bu nekk di wax ? Ndax seet nga yan nit la kayit bu nekk mën a neex ? Boo leen jàngee bu baax ñoom ñépp, dinga gis ne jar na ñu jëfandikoo leen ci waaraate bi këroo-kër, walla feneen foo mënee am bunt ngir waaraate.
4 Bu ñuy waaraate këroo-kër : Am na benn wottukat buy wër bu ne : “ Bu may waaraate, su ma faralee di komaase sama waxtaan ak kayit bu ndaw, nit ñi dañuy déglu bu baax. ” Ndax mas nga jéem loolu ? Ndax mënuloo komaase sa waxtaan ak benn kayit bu ndaw ? Kuy jëfandikoo kayit yu ndaw yi, dina am lu bare lu mu mën a wax ngir komaase waxtaanam ci fasoŋ bu neex nit ñi ba ñu nangu déglu li ñuy wax. Mën nañu jëfandikoo kayit bu ndaw bu mu mënta doon, ngir komaase benn njàngum Biibël bés bi ñuy njëkk waxtaan ak nit walla ngir dellu seeti nit.
5 Mën nañu jëfandikoo itam kayit yu ndaw yi bu ñuy waxtaan ak ku mbokkam gaañu bu yàggul, walla ku am ku feebar ci waa këram. Ñi am naqar bu leen metti lool walla ñi am coono bu leen topp lu yàgg ba tey, lu ci ëpp seen xol dafay jeex, walla du neex dara. Bu ñu leen wonee li nekk ci kayit bu ndaw bi tudd “ De l’aide pour les déprimés ”, dinañu xam ne dañu leen bëgg dëgg. Mën nañu tase it ak koo xam ne bu yàggul la séyam tas, walla bu yàggul la ñàkk liggéeyam. Lu mel noonu metti na lool ci nit ki te dina def lu bare ci njaboot bi. Laaj ko laaj yii nekk ci kayit bu ndaw bi tudd “ Une vie de famille agréable ”, ci xët 2 : “ Pourquoi les familles sont-elles assaillies de problèmes si graves aujourd’hui ? Comment avoir une vie de famille agréable ? ” (Maanaam lu tax jafe-jafe yu metti nii di dal rekk ci njabooti tey ? Naka lañu mënee fexe ba suñu njaboot bare jàmm ?) Xéyna laaj yooyu la nit kooku di laaj boppam. Su fekkee ne sax wonewul ci saa si ne suñu waxtaan neex na ko, xéyna mu jàng kayit bi ci suñu ginnaaw. — Daj. 11:6.
6 Yenn mbooloo dañu waaraate ci seen gox ay yoon yu bare ba tax nit ñu bare am yenn ci suñu téere yi ba pare. Bu ñu jëfandikoo kayit yu ndaw yi, dinañu mën a wax lu neex nit ñi ba ñu nangu waxtaan ak ñun, te nangu xalaat ci yaakaar bi Nguuru Yàlla di maye. Laaj leen laaj bu ngeen di mën a tontu bu beneenee. Dellul seeti leen te kontineel di fa dem ngir waxtaan ak ñoom. Bu yàggee, dinga mën a komaase ak ñoom benn njàngum Biibël ci téere bi mu am ba pare.
7 Bu ñuy waaraate saa yu ñu ci amee bunt : Bu ñu defee ay kayit yu ndaw fu neex a jot (mel ni ci suñu poos, suñu kalpe walla ci suñu saag bu ñuy yóbbu ci waaraate bi), dina bare fu ñu leen mënee jëfandikoo, maanaam fépp fu ñuy fekk ay nit. Jëfandikoo leen booy jëndi dara, booy tukki walla booy waxtaan ak say mbokk walla ak ñi la seetsi. Bu ñuy jëfandikoo kayit yu ndaw yi, dinañu mën a waaraate ci lu gàtt. Li ñuy wax ci kayit yu ndaw yi dafa gàtt te ànd ak teggin. Moom la nit ñi gën a sawar a jël ndaxte li ci nekk barewul ni li nekk ci téere yi walla yéenekaay yi.
8 Bul ragal a joxe kayit yu ndaw yi fi ngay jànge, fi ngay liggéeye, ci restoraŋ yi, fi ngay jënde esaas, ak feneen fu mel noonu. Suñu benn mbokk mu jigéen dafa doon yóbbu maamam ci doktoor bi. Mu yóbbaale ay kayit yu ndaw. Bi mu doon xaar ca doktoor ba, mu waxtaan ak benn jigéenu biir bu fa nekkoon. Bi mu ko wonee kayit bu ndaw bi tudd : “ Une vie paisible dans un monde nouveau ”, dafa ko nee : “ Ndax bëggoo sa doom màggee ci béréb bu mel nii ? ” Mujj na seeti jigéen jooju ca këram ay yoon yu bare ngir waxtaan ak moom.
9 Mën nañu tàmbali ay njàngum Biibël ci ay kayit yu ndaw : Am na benn wottukat buy wër bu demoon ci benn mbooloo. Foofu waaraatekat yi dañu doon tàmbali seen waxtaan ci kayit yu ndaw yi. Loolu lu mu indi ? Ci ayu-bés bu mu fa nekkoon tàmbali nañu 64 njàngum Biibël.
10 Booy njëkk wax ak nit ñi booy waaraate këroo-kër ndax mas nga jéem a tàmbali ay njàngum Biibël ak nit ñi ngay dajeel ? Ak kayit bu ndaw, mën nga wone ci lu gàtt ni ñuy defee njàngum Biibël. Am na suñu benn mbokk mu jigéen bu def loolu ak kayit bu ndaw bi tudd “ Une vie paisible dans un monde nouveau ”. Dafa won benn jigéen nataal bi, ba pare laaj ko ndax suñu suuf si dina mas a mel noonu. Bi ko jigéen ji tontoo ba pare mu wax ko mu jàng ñaari aaya yu nekk ci kayit bu ndaw bi, maanaam 2 Pieer 3:13 ak Isayi 65:17. Ba pare suñu mbokk mi nee ko : “ Li ñu wax fii du ci gént kese lay ame, ndaxte Biibël bi maanaam kàddu Yàlla moo ko wax. ” Mu daldi seet ak jigéen ji kañ la fay dellu ci ayu-bés bu ci topp. Bi mu fa dellusee, dafa tontu laaj yu bare yu ko jigéen jooju laaj, te mu jox ko benn téere. Mujj na def ak moom benn njàngum Biibël.
11 Boo nekkee ku ñu yàggul a sóob, walla waaraatekat bu ñu sóobagul, te nga bëgg gën a aay ci waaraate bi, demal ci ñi la gën a yàgg ci waaraate bi. Laaj leen noo mënee wone kayit yu ndaw yi ci seen gox. Biibël bi wax na ci nit ñu bare ñoo xam ne ñeneen ñu leen gën a dëgër ci ngëm, ñoo leen xiir ci lu baax, te won nañu leen li ñu mën a def. — Jëf. 18:24-27 ; 1 Kor. 4:17.
12 Boo bëggee yeneen waaraatekat jàpple la ngir nga gën a mën a jëfandikoo kayit yu ndaw yi, wottukatu njàngum téere bi ci mbooloo mi mën na la ci dimbali. Way-jur yi ñoo war a jàpple seeni doom ngir ñu gën a mën a waaraate. Am na xale bu ndaw bu way-juram won ni mu mënee wone kayit bu ndaw bi tudd “ Une vie paisible dans un monde nouveau ”. Benn bés, dafa ànd ak yaayam ci benn njàngum Biibël. Mu daldi may benn kayit bu ndaw jëkkëru jigéen ju doon waxtaan ak yaayam. Li jaaxal góor googu, mooy naka la xale bu ndaw bu mel noonu mënee am ngëm bu dëgëre noonu. Bi mu jàngee kayit bu ndaw bi, li mu fa gis dafa ko neex. Ginnaaw loolu, xale bu ndaw boobu, saa yu mu fa doon dellu ak yaayam, dafa ko doon jàngal benn aaya ci Biibël bi, walla mu wax ko lenn lu ñu nettali ci Biibël bi, fekk dafa ko waajaloon ngir won ko ko. Fi mu ne nii, góor googu dafay jàng suñu yéenekaay yi saa yu ñu génnee, wax na ne téere La Révélation : dénouement dafa ko neex, te teew na sax ci yenn ndaje. Lu tax loolu lépp am ? Way-juru xale boobu dañu def seen wareef. Maanaam dañu jàngal seen doom ni mu mënee jëfandikoo bu baax kayit yu ndaw yi.
13 Nañu jariñoo bu baax kayit yu ndaw yépp : Ngir jëfandikoo kayit bu ndaw bi tudd “ Le monde actuel survivra-t-il ? ”, mën nga nuyoo ba pare ne lii : “ Dañuy waxtaan ak nit ñi ci lu jëm ci suñu dund gi tey. Ndax foog nga ne bu ëllëgee dund gi dina tane walla dafay gën a metti ? [Mayal nit ki tontu.] Am na ñu xalaat ne li am tey ci àddina si Biibël bi waxoon na ko, te soreetuñu muju jamano ji. Loo ci xalaat ? ” Bu la nit ki tontoo ba pare, may ko kayit bu ndaw bi te won ko ñetti laaj yi nekk ci xise 2. Toppal li kayit bu ndaw bi wax ngir won ko ne Yàlla mas na alag benn jamano, te dina alag it suñu jamano jii. Booy jeexal seen waxtaan, laaj ko kañ ngay mën a ñówaat ngir ngeen gis ci Biibël bi luy wone ne muju jamano jii soreetul.
14 Am na foo xam ne, bu ñu bëggee waaraate, duñu mën a wax lu yàgg. Mën na nekk bu ñu nekkee fi ñuy liggéeye walla fu ñuy jànge. Fi ngay liggéeye, nit ñi mën nañu nekk di wax ci lu yàggul a xew ci wàllu politig. Mën nga wax ne njiiti nguur yi def nañu lépp li ñu mën, waaye terewul mu faral di am ay naqar yuy dal nit ñi. Ba pare, ubbil kayit bu ndaw bi tudd “ Qui domine vraiment le monde ? ” te woneel xise bi mujj ci xët 2. Jàngal ñetti laaj yu am solo yi fa nekk. Bu fekkee ne mënuleen waxtaan lu yàgg, jox ko (walla jox leen) kayit bu ndaw bi te seetleen kañ ak fan ngeen di mën a waxtaan ci laaj yooyu.
15 Nañu seet ñun ci suñu bopp, walla ñun ak suñu njaboot, ni ñu mënee wone kayit bu ndaw bu nekk. Balaa ñuy dem waaraate, nañu won kenn li ñu nar a def ngir wone kayit yooyu bu ko defee dinañu ko mën bu baax. Bu ñu komaasee suñu waxtaan ak kayit bu ndaw, naka lañu mënee àggale waxtaan bi ak téere bi ñu war a wone ci weer wi ? Ndax am na foo war a jëm foo xam ne mën nga fa yóbbaale ay kayit yu ndaw ? Ndax am na koo war a waxal ayu-bés bii te nga xam ne mën na jariñoo xibaar bu am solo bi nekk ci kayit yu ndaw yi ?
16 Bu ñu bëggee Yexowa dëgg te yéene lu baax nit ñi, dinañu def lépp li ñu mën ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi. Lan moo ñu ci mën a dimbali ? Nañu faral di jëfandikoo kayit yu ndaw yi. Benn xale bu ndaw bu am juróom ñaari at moo bëggoon a dimbali dëkkandoom ngir mu fekke àddina su bees si. Mu daldi ko jox benn kayit bu ndaw. Muj gi, komaase nañu benn njàngum Biibël ak jigéen jooju. Loolu de niroo na lu yomb lool ! Waaye ndax dinañu def noonu bu ñuy waaraate ? Bu ñu mayatee kenn benn kayit bu ndaw, xéyna dinañu komaase ak moom benn njàngum Biibël. Bu ñuy jariñoo bu baax kayit yu ndaw yi ci waaraate bi, ci lu wóor, dina jur lu baax.