Jëfandikool suñu mbind yu gàtt yi ngir tàmbali ay waxtaan
1 Ndax dàkkooruloo ci wax ne, seede bu am doolee ngi aju, ci lu bare, ci li ngay jiitu ci tàmbalee waxtaan ak nit ki? Liy tëkk dëgg, nag, mooy wax loo xam ne, dina soxal nit ki, ba tax mu nangoo waxtaan ak yaw. Waaye lu ñu mën a def ba am loolu?
2 Yéenekat yu bare seetlu nañu ne, ak i kàddu yu gàtt, yu ñu tànn bu baax, mën nañoo tàmbali ay waxtaan ak nit ki, bu ñu ko mayee benn ci suñuy mbind yu gàtt yi sukkandiku ci Biibël bi. Seeni tur dañuy xiir ci ñu duruus leen, seeni nataal bare kulóor te rafet. Mbind mu gàtt du tiital nit ki, di ko gëmloo ne daa war a duruus xabaar bu dul jeex. Terewul xabaar bu gàtt bi ne ci biir dugg nit ki, te mën nañu leen a jëfandikoo ngir tàmbali njàngum Biibël bi.
3 Lii la benn Seede yëg ci biir xolam: “Ci suñu jamano jii dëkke kër-këri, nit ñi faraluñu di jël jot gu bare ngir duruus; melo mbind yu gàtt yi da leen di jottaliloo xabaar bu am solo; ndaxam gudduñu, ba tax nit ñi dumóoyu leen, laata sax ñoo seet li ci biir. Mbind yu gàtt yu bare laa duruus, ba faf jàng dëgg gi.” Bul xeeb mukk, kon, doole Kàddu Yàlla ni ñu ko faramfàccee ci xabaar yu gàtt yooyu ñu muul.—Yaw. 4:12 .
4 Ñeenti jéego yu yomb: Ñu bare àntu nañu, ba ñu jëfandikoo yoon wu yomb ngir waxtaan ak nit ñi. (1) Wonal nit ki yenn ci suñuy mbind yu gàtt yi, ba noppi laaj ko bi ko ci itteel. (2) Bu ci tànnee benn, laaj ko laaj boo waajal bu baax, buy fésal ponk bi ëpp solo ci mbind mu gàtt mi. (3) Tontul ci laaj bi, ci li ngay duruuse ci mbind mu gàtt mi, xise walla aaya ji war. (4) Léegi soo gisee ne mbir mi soxal na ko, wéyal di waxtaane ci li mbind mu gàtt mi ëmb, walla tuddal njàngale mu nekk ci téere bu ndaw bi Laaj, walla ci menn pàcc ci biir téere Xam-xam, muy yokk yeneeni xalaat. Noonu sax, dinga mën a jiite, ci tàng-tàng, njàngum Biibël bi. Xelal yiy topp dinañu la dimbali, nga waajal li nga mën a wax, booy jëfandikoo ñeent ci suñuy mbind yu gàtt yi.
5 Turu mbind mu gàtt mii “Ndax dinañu toog bés, ba nit ñi ñépp bëgg, ku nekk sa moroom?” nekk na laajte buy itteel nit ñi:
◼Mën nañoo tàmbalee suñu waxtaan nii: “Seetlu nañu ne nit ñu bare dañoo jaaxle ndax ñàkk mbëggeel dëgg, gi law ci kow suuf si. Ndax loolu jaaxalu la, yaw itam? . . . Ci sa gis-gis, lu waral loolu? . . . Ndax xam nga ne Kàddu Yàlla yégle woon na lu ni mel (2 Tim. 3:1-4)? Mu ngi ñuy xamal itam li waral loolu (1Ywna. 4:8).” Fésalal ci aaya jooju solo jàng a xam Yàlla. Ba noppi, mën ngaa kontine, naan: ‘Seetal li mbind mu gàtt mi tudd “Ndax dinañu toog bés, ba nit ñépp bëgg, ku nekk sa moroom?” wax ci loolu.’ Jàngal kàddu gu njëkk gu xise 5, xët 4. “Soo bëggee, mën naa laa bàyyil mbind mu gàtt mi; dina la xamal lii tax ñu mën a gëm ne, bés, mbëggeel dëgg dina ne ñoyy ci kow suuf si sépp.”
6 Mbind mu gàtt mi tudd “Quel espoir y a-t-il pour nos chers disparus?” (Jan yaakaar ngir suñu soppe yi gaañu?) mën naa soxal nit ki ci saa si. Mën ngaa tàmbalee waxtaan ak laajte bii:
◼“Ndax foog nga ne, dinañu toog bés, ba gisewaat ak suñu soppe yi gaañu?” Bu nit ki tontoo, joxoñal li ñu wax ci ñaareelu xise bi ne ci xët 4 ci mbind mu gàtt mi, ba noppi duruusal Yowanna 5:28, 29. Boo sottalee, faramfàcceel ne ndimbal la, nànd li ñu bind ci suufu ponk bi ñuy jëkk a waxtaane ci mbind mu gàtt mi. Wax ko ne mën ngeen cee waxtaane.
7 Mbind mu gàtt mi tudd “Une vie de famille agréable” (Bànneexuleen ci seen dundug njaboot), naka jekk, daa neex njaboot yi yépp. Boo koy jëfandikoo, mën ngaa wax lii:
◼“Du ñàkk, dinga ànd ci wax ne liy song njaboot yi, ci suñu jamano ji, daa bare. Loo xalaat ne lañu mën a def ngir dëgëral diggante ñi bokk ci njaboot gi?” Bu nit ki tontoo, fexeel mu bàyyi xel ci li ñuy waxtaane ci xise bi njëkk ci xët 6. Tànnal jenn ci aaya yi ñu lim ci xët 4 ak 5 bu mbind mu gàtt mi, te faramfàcceel li muy tekki. Boo sottalee, wax ko ne mën naa am njàngum Biibël bi, ci këram, te du ci fey dara.
8 Mën nañoo jëfandikoo mbind mu gàtt mi tudd “Ni ñuy daje yoon wiy jëme Àjjana” ak wone bile:
◼“Salaam maalekum. ————laa tudd. Sant wi? Damay xiirtal képp ku ma taseel, mu seet ëllëg ju amul moroom ji ñu Biibël biy dig. (Jàngal aaya ju ne ci biir Biibël bi, maanaam Peeñu bi 21:3, 4.) Ndax yaakaar ju ni mel seddalul sa xol? Mbind mu gàtt mile, tudd “Ni ñuy daje yoon wiy jëme Àjjana” dina la gën a xamal ni dund gi di mel ci jamano jooja.”
9 Di siiwal mbind yu gàtt, yi sukkandiku ci Biibël bi, pexe mu am doole la ngir xamle xabaar bu baax bi, pexe mu wone njariñam ci biir at yi jàll. Ndax yomb nañoo yóbbaale foo mën a jëm, mën nga leen a jëfandikook doole ci yëngu-yëngu waare bi, kër-oo-kër, booy seede yit saa yu ñu la ci xàllalee yoon. Mbind yu gàtt yi am nañu maanaa lool ci ni ñuy matale suñu sasu waare. Na la wóor ne yóbbaale nga ci yu bare te wuute, te jëfandikoo leen ci fasoŋ bu yéwén ngir tàmbali ay waxtaan.—Kolos 4:17.