Ndax yaa ngi ci tànku toxu?
Su fekkee ne tontu laajte boobu: “waaw!” la, am na yëf yu bare yu ngeen soxlaa tàmbalee a def, yaw ak ñeneen. Boo toppee jéego yu am solo yiy topp, te ñu waxtaane ne leen ci suuf, sa dëju ci mbooloo gëmkat, mu bees mi nga jëm, dina gaaw.
1) Boo xasee xam fi ngay jëm, sekkerteeru mbooloo mi nga ne nëgëni, mën naa jéem a am adareesu saalu Nguuru sa mbooloo mu bees. Boo agsee ci béréb booba, nanga seet, ci saa si, fu saal bi nekk, ak kañ la mbooloo mi di amal ay ndajeem. Su fekkee ne lu ëpp menn mbooloo mooy jëfandikoo saalu Nguur gi, laajal mag yi ñu wax la, ci goxu man mbooloo nga dëkk. Bul yéex ciy teewe ndaje yi, ciy xamante itam ak magi mbooloo gox ba.
2) Sekkerteeri mbooloo, mi nga bokk nëgëni, ak mu bees mi ngay jëm, dinañu ànd a liggéey ngir toxal sa kàrtu Yéenekatu Mbooloo mi ak yu sa njaboot. Dinañu yónnee itam magi sa mbooloo mu bees bataaxalu wonale. (Seetal Le Ministère du Royaume, bu feewriyee 1991, ci Wërale laajte yi.) Foofa, Kurélu Liggéeyu waare bi, bu Mbooloo mi, warkoon naa yégal aji-jiite njàngum téere mbooloo mi, ji war, ne yaa ngiy agsi, ba tax mu mën a jokkook yaw te dimbali la, nga xam béréb bi nitiy sa njàngum téere mbooloo, mu bees mi, di daje.—Room 15:7.
3) Yéenekat yi yépp, yi ne ci sa mbooloo mu bees, mën nañoo def seen wàll, ci fasoŋ bu làmboo mbég—xamanteek yaw te fexe nga yëg ne dalal nañu la ak jàmm. (Dendale kook 3 Yowanna 8.) Jarul ñu koy wax, looloo ngiy tekki ne, war ngaa teew ci ndaje yi, ba tax nga mën a jariñoo xiirtalante ak feddaleente ngëm ak say mbokki karceen, góor ak jigéen.
(4) Warkoonuloo xaar, ba liggéey bi jëm ci toxu bi bépp sotti, ngir tàmbalee bokk ci sasu tool bi ak mbooloo, mu bees mi. Ba ngay jiital njariñi Nguur gi, dinañu toppatoo yeneeni mbir, te dinga yëg péex dëgg ci sa kurukaara, bu bees bi. (Macë 6:33) Boo dëjoo bu baax ci sa kër gu bees, du ñàkk nga bëgg a woo ñenn ci mbooloo mi ngir ñu seetsi la, ngeen gën a xamante.—Room 12:13b.
Toxu, mébét bu réy la. Waaye, bu ku nekk ci ñii mbir miy laal, defe li ñu digal, du am wenn gàllankoor ci wàllu xel. Cofeel, gu làmboo mbëggeel, gi ñu ameel suñu mbokki karceen yi dina laal, ci fasoŋ bu rafet, xolu ku nekk ci ñi mbir mi itteel.