Wërale Laajte Yi
◼ Kan a war a gàddu set-setalu Saalu Nguur gi?
Saalu Nguur, bu set te rafet, day siggal ci fasoŋ bu rafet xabaar, bi ñuy waare. (Dendale kook 1 Pieer 2:12.) Sàmm setaayu saal bi te fexe lépp jag lu am solo dëgg la. Ku nekk mën naa def wàllam ci toppatoom. Waruñoo xaaru ñenn nit doŋŋ tegoo sëf bi bépp. Li gën a faral, ndajey Njàngum Téereb Mbooloo mi ñooy def set-setal bi, aji-jiite jeek kuutaayam di ko jiite. Ci saal yi lu ëpp menn mbooloo di daje, mag ñi dinañu fagaru ba tax mbooloo yi yépp bokk ci toppatoo bi.
Nan lañu mënee def suñu warugar bu baax-a-baax? War nañoo setal Saalu Nguur gi, di topp doxalukaayub ay-ayloo. Li ñu war a jëfandikoo ngir set-setal bi ak jumtuwaay yi war nañu leen a fekk foofa. War nañoo taf limu yëf, yi ñu war a def, foo xam ne liggéeykat yi dinañ ko mën a seet ngir sàkku ca ay tegtal. Mën naa am ñaari lim, yu wuute, benn bi ngir set-setal bu ndaw, bu saal bi bépp, saa su ndaje yi tasee, ak beneen ngir socc ko bu baax-a-baax, muy set-setalu ayu-bés gi. Bés ak waxtu, yu gënal ñépp ñi ñu sas liggéeyu set-setal bi la aji-jiite njàngum téere bi war a jàpp ngir taxawal liggéeyu socc boobu. War nañoo faral di bàyyi xel ci tóor-tóor yeek garab yu ndaw yi. Fi nit ñiy war a dox ci mbedd yi ak dencukaayu oto yi waruñoo am anitu mbalit. At mu ne, war nañoo amal set-setal bu mag-a-mag, xëy na tuuti laata ñuy màggal Fàttaliku bi. Loolu mën naa boole raxas palanteer yeek miir yi, bàcc tapi yi te fóot rido yi.
Jarul ñu koy wax, ñépp mën nañoo wàññi coono bi, bu ñu dul waddal siŋgom walla xollit ci biir walla ci bitib saal bi. Saa yu ñu jëfandikoo wanag yi, mën nañu leen a jagal, bàyyi leen ñu set wecc ngir nit kiy topp ci ñun. Bàyyileen xel ci moytoo damm jumtuwaay yi walla yàq toogu yeek ñoom seen. Seetluleen gàkk-gàkk yi ci kow tapi yi, toogu niki robine yeek saas yi yàqu, làmp yi lakk, ak ñoom seen, te gaawleen koo xamal mbokk mi ñu sas toppatoob Saalu Nguur gi.
Yal nañu jagoo, ñun ñépp, def suñu wàll. Loolu dana tax kër gi ñuy jaamu Yàlla doon béréb bu jekk te dina tax it ñu ràññee ci ñun mbooloo mu set, muy siggal Yeowa Yàlla.—1 Pie. 1:16.