Nañu toppatoo bu baax béréb fu ñuy jaamu Yàlla
1 Mbooloo Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp, bare nañu. Ëpp nañu 94 000. Mbooloo yu bare dañuy daje ci ay Saalu Nguur. Foofu dañuy jàng Biibël bi te di daje ak seen mbokk karceen yi. Ci Saalu Nguur gi la nit ñi dëkk ci goxu mbooloo mi mën a dem ngir jaamu Yàlla.
2 Set-setal bi : Dañu war a setal suñu Saalu Nguur. Ci li ñuy def ngir jaamu Yàlla la bokk. Lu am solo la. Ci xët 61, téere Notre ministère, nee na lii : “ Mbokk yi war nañu xam ne bu ñu leen maye ñu jàpple Saalu Nguur yi ak seen xaalis, may nañu leen lu réy. Waaye ku bokk ci ñiy setal Saalu Nguur gi te di ko defar ba mu jekk, am nga it lu réy. Saalu Nguur gi dafa war a mel ni lépp lu bokk ci mbootaayu Yexowa, maanaam jekk te rafet, ci biir ak ci biti yépp. ” Komka ayu-bés bu nekk dañuy dem ci Saalu Nguur gi ay yoon yu bare, war nañu ko setal te toppatoo ko bu baax ndax dara bañ ci yàqu. Ñiy daje ci Saalu Nguur bu nekk ñoo faral di def loolu. Ni ñu ko doon defe bu njëkk, ñiy jaamu Yexowa tey dañu war a sawar a defar li yàqu ci béréb fu ñuy jaamu Yàlla. — 2 Net. 34:10.
3 Ayu-bés bu nekk dañuy def set-setalu Saalu Nguur gi. War nañu taf ci tablo bi nekk ci Saalu Nguur gi, porogaraamu set-setal boobu. Gurupu njàngum téere yi dañu war a ay-ayloo set-setalu Saalu Nguur gi ayu-bés bu nekk. Te bu ñu koy def, dañu war a topp li ñu bind ci kayit biy wone li ñu war a def ci set-setal bi. Ñi ko mën ñépp war nañu bokk ci set-setal bi ak ci li ñuy def ngir Saalu Nguur gi jekk. Bu xale yi àndee ak seeni way-jur, mën nañu bokk ci set-setal bi. Bu ko defee dinañu leen jàngal ne dañu war a fonk liggéey boobu ñuy def ngir suñu moroom yi jariñoo ko. Bu dee lu ëpp benn mbooloo ñoo bokk Saalu Nguur gi, mbooloo yooyu war nañu seet ni ñuy defe set-setal bi. Bu ko defee, liggéey boobu nga xam ne ci jaamu Yàlla la bokk, du tuuti nit kese ñoo koy def.
4 Mën nañu taf kayit buy wone li ñu war a def ci set-setal bi, ci béréb fu ñuy dence li ñuy jëfandikoo ci set-setal bi. Kayit boobu war na wax li ñu war a def ci set-setal bi ayu-bés bu nekk. Bale saal bi, raxas palanteer yi, dindi pënd bi nekk ci fi ñuy joxe téere yi, tuur mbalit yi, fobeere ak raxas seetu yi dina bokk ci li ñu bind ci kayit boobu. Am na yoo xam ne soxlawul ñu koy def ayu-bés bu nekk, lu mel ni dindi pënd bi ci saal bi yépp, raxas siis yi, rido yi, wantilaateer yi ak làmp yi. Waruñu teg butéel yi ñuy jëfandikoo ci set-setal bi fi ko xale mën a jot, te war nañu bind ba mu leer li nekk ci butéel bu nekk. War nañu bind it ci lu gàtt ni ñu koy jëfandikoo.
5 Fexe ba dara bañ a lor kenn ci Saalu Nguur gi moo war a jiitu lépp (5 Mu. 22:8). Moo tax, wërale bi nekk ci xët 4 di joxe li ñu war a faral di seet ngir dara bañ a lor kenn ci Saalu Nguur gi.
6 Bu ñuy toppatoo Saalu Nguur gi : Kurélu magi mbooloo mi moo war a jiite lépp li ñuy defar ci Saalu Nguur gi. Benn magu mbooloo mi walla benn surga mbooloo mi lañuy tàmm a dénk liggéey boobu. Moom mooy faral di seet ni Saalu Nguur gi di mel ngir mu wóor ne set na, dara yàquwu ci, te yor nañu ba mu doy lépp li ñu soxla ngir set-setal bi. War nañu fexe ba dara luy lore bañ a nekk ci biir saal bi walla ci wetam. Lu am solo la. Bu fekkee ne lu ëpp benn mbooloo ñoo bokk benn Saalu Nguur, kuréli magi mbooloo yooyu dinañu tànn ñi war a nekk kurél bi tudd comité de gestion. Kurél boobu mooy toppatoo lépp li ñu war a toppatoo ci Saalu Nguur gi ak ci li ko wër. Kurél boobu dafa war a topp li ko kuréli magi mbooloo yi di wax.
7 Benn yoon at mu nekk, dinañu seet bu baax lépp li nekk ci Saalu Nguur gi ba xam ndax dara yàquwu ci. Bu ñu ci gisee lu ñu war a toppatoo, magi mbooloo mi ñoo war a seet ni ñu koy defe. Bu amee lu ñu war a defar, mag yi mën nañu ñaan waaraatekat yi ñu jàpple leen ci. Bu ñu leen dénkee liggéey, waaraatekat yi dañu war a seetlu sax li ci gën a ndaw, te def ko bu baax. Te it waruñu yéex ci seen liggéey. Bu wottukat buy wër ñówee ci mbooloo mi, mën na won magi ñi li ñu war a gaaw a defar ci Saalu Nguur gi.
8 Bu amee li ñu war a defar ci Saalu Nguur gi, mën na am mag ñi gis ne soxla nañu ay xelal walla ku leen di wax li ñu war a def. Bu booba, mën nañu wax ak biro buy toppatoo tabaxu Saalu Nguur yi te nekk ci bànqaas bi.
9 Nañu jariñoo ni mu gëne xaalis bi ñuy dajale ci mbooloo mi : Yenn saay dina am liggéey bu ñu war a def ci Saalu Nguur gi walla ci li ko wër. Waaye ñiy def liggéey boobu, li ci ëpp, dañuy nangu ne duñu leen fey dara. Loolu ñuy def dafay wone ne dañu am mbëggeel te dafay wàññi bu baax xaalis bi mbooloo mi war a jaay. Yenn saay dinañu war a wut ku ñuy fey ngir mu defal ñu liggéey bu mel ni lii : rey max yi, liggéey bu minise war a def, walla tabax dara. Bu booba, dinañu seet ni ñu mën a def liggéey boobu ci njëg bi gën a yomb. Ngir mën koo xam, dinañu njëkk bind ci kayit ban liggéey lañu bëgg santaane ak lan lañu war a jëfandikoo ngir defar ko. Dinañu ci def ay sotti yu bare, ba pare jox ko ñi mën a def liggéey boobu. Bu ko defee, li kenn xam ci liggéey bi ñuy santaane, moom la ñeneen ñi di xam itam. Ñi bëgg def liggéey boobu dinañu joxe kayit fu ñu bind ni ñu koy defe ak li ñuy feyeekoo. Bu ko defee, magi mbooloo mi dinañu mën a tànn bu ci gën. Bu amee sax suñu benn mbokk bu ñu bëgg defaral liggéey boobu te mu wax ñaata lañu ko war a fey, noonu lañu war a def.
10 Ci lu ëpp, duñu fey ay lempo ngir Saalu Nguur gi, ndaxte béréb fu ñuy jaamoo Yàlla la. Bu fekkee ne lu ëpp benn mbooloo ñoo bokk benn Saalu Nguur, kurél bi ñuy woowe ci tubaab comité de gestion dina denc xaalis bu mbooloo mu nekk dajale. Weer wu nekk mu bind ñaata xaalis la jaay, te jox ko kurélu magi mbooloo mu nekk. Bu ko defee, mag yi dinañu xam fan la xaalis bi mbooloo yi dajale di jaar. Mag ñi ñoo war a seet ndax ñu ngi jëfandikoo ni mu gëne xaalis bu mbooloo yi di dajale.
11 Bu fekkee ne li ñu war a defar ci Saalu Nguur gi liggéey bu réy lay laaj : Bu kurél bi tudd Comité de gestion gisee ne li ñu war a defar ci Saalu Nguur gi liggéey bu réy la, kurél boobu dina ko wax kuréli mag ñi ngir ñu wax leen li ñu war a def. Kuréli mag ñi dinañu seet ba xam ndax soxla nañu def li Comité de gestion bi wax. Bu ñu ko soxlaa dëgg, walla ñu gis ne dinañu soxla keneen ku bokkul ci mbooloo miy (walla yiy) daje ci Saalu Nguur gi ngir def liggéey boobu, dinañu wax ak biro buy toppatoo tabaxu Saalu Nguur yi te nekk ci bànqaas bi, ngir mu xelal leen. Suñu mbokk yi nekk ci biro boobu, seen xam-xam yaatu na ci wàllu tabax. Dinañu leen xelal bu baax, te dinañu leen seetal ni liggéey bi di deme. Bu ñu waree def liggéey bu réy, dinañu seet ñaata la leen di laaj ci xaalis, ba pare ñu laaj waa mbooloo mi ndax nangu nañu ñu def ko. — Seetal Le ministère du Royaume de février 1994, Réponses à vos questions.
12 Ndaje yi ñuy am ci Saalu Nguur gi, dañu leen fonk bu baax. Buñu leen fowe mukk, te buñu xalaat mukk ne amuñu solo. Ndaje yi dañu leen taxawal ngir ñu yokk suñu doole. Am na li ñépp mën a def ngir ndaje yi dox bu baax. Mooy bokk bu baax ci li ñuy def ngir toppatoo Saalu Nguur gi. Loolu dina tax nit ñi gën a fullaal diine dëgg ji, te dina màggal turu Yexowa. Nañu nangu def lépp li ñu mën ngir toppatoo bu baax béréb fu ñuy jaamu Yàlla.
[Laaj yi]
1. Lu tax ñu def ay Saalu Nguur ?
2. Lu tax setal Saalu Nguur gi, te toppatoo ko ba mu jekk am solo lool ?
3. Naka lañuy defee set-setalu Saalu Nguur gi, te ñan ñoo war a bokk ci liggéey boobu ?
4. Lu ñu war a def ngir waa mbooloo mi xam li ñu war a def bu ñuy setal Saalu Nguur gi ?
5. Fexe ba dara bañ a lor kenn ci Saalu Nguur gi naka la amee solo ? Lan lañu war a faral a seet (seetal wërale bi nekk ci xët 4) ?
6. Bu amee lu ñuy defar ci Saalu Nguur gi, naka lañu war a def ?
7. a) Lan lañuy def at mu nekk ngir seet ndax defar nañu lépp li yàqu ci Saalu Nguur gi ? b) Lan lañu war a tàmm seetlu (seetal wërale bi nekk ci xët 5) ?
8. Kañ la magi mbooloo mi mën a ñaan ay xelal biro buy toppatoo tabaxu Saalu Nguur yi te nekk ci bànqaas bi ?
9. Bu ñu waree fey nit ngir mu defal ñu benn liggéey, naka lañu war a def ?
10. Lan lañuy def ngir mu wóor ne ñu ngi jëfandikoo ni mu gëne xaalis bu mbooloo yi di dajale ?
11. Bu fekkee ne li ñu war a defar ci Saalu Nguur gi liggéey bu réy la, lan lañu war a def ?
12. Naka lañu mën a wone ne fonk nañu ndaje yi ñuy am ci Saalu Nguur gi ?
[Wërale bi nekk paas 4]
Li ñu war a seet ngir dara bañ a lor kenn
◻ Butéel yi ñuy jëfandikoo ngir fey liy tàkk ci Saalu Nguur gi, war nañu neex a jot. At mu nekk, dañu war a seet bu baax ndax dañuy dox ni mu ware.
◻ Bunt yi ñuy duggee, ak yeneen bunt fu nit ñi mën a jaar bu musiba amee ci Saalu Nguur gi, ak it iskale yi, war na am luy wone bu baax fu ñu nekk. War nañu am leer bu doy, te war nañu neex a jot.
◻ Béréb fu ñuy dence bagaasu Saalu Nguur gi, ak wanag yi dañu war a set. Waruñu fa fekk dara lu mën a tàkk walla mbalit, te waruñu fa dénc suñu bagaas.
◻ War nañu tàmm seet jank (toit) bi te di ko setal.
◻ Dër bi nekk ci mbedd mi ci kanamu Saalu Nguur gi, ëtt bi ak fu ñuy gaare oto yi, war nañu am làmp yu doy, te waru fa am luy daaneel nit ñi.
◻ War nañu seet bu baax lépp lu am kuuraa ak wantilaateer yi, te fexe ba ñu dox bu baax.
◻ Bu amee fiy senn, war nañu ko gaaw a defar.
◻ War nañu téj Saalu Nguur gi, bu fa kenn nekkul.
[Wërale bi nekk paas 5]
Ni ñuy toppatoo Saalu Nguur gi ak li ko wër
◻ Ci biti : Jank bi (toit), palanteer yi ak fi ñu bind ci kanamu Saal bi : “ Saalu Nguuru Seede Yexowa yi ”, ndax dara yàquwu ci ?
◻ Liy wër Saalu Nguur gi : Ndax ñu gi koy toppatoo bu baax ? Ndax dër bi nekk ci kanamu Saal bi ci mbedd mi, ñag bi, ëtt bi ak fi ñuy gaare oto yi dara yàquwu ci ?
◻ Ci biir Saalu Nguur gi : Ndax lépp li nekk ci Saal bi jekk na ? Maanaam suuf si, tàppi yi, rido yi, siis yi, lépp liy dox ak kuuraa, fi ñuy dence téere yi, ak fi ñuy dence mikoro yi ?
◻ Li ñuy jëfandikoo ci Saalu Nguur gi : Ndax làmp yi, mikoro yi ak wantilaateer yi ñu ngi dox bu baax ?
◻ Wanag yi : Ndax set nañu te yàquwuñu ?
◻ Kayiti mbooloo mi : Ndax nguur gi nangu na kayitu fi ñu tabaxe Saal bi ? Ndax dangeen di fey kuuraa bi ak ndox mi ni mu ware ? Ndax denc ngeen bu baax kayit yooyu yépp?