“ Waareel kàddu gi [...] ci fasoŋ bu jamp ”
1 Soo jotee dara lu ñu bind “ LU JAMP-A-JAMP ”, noo koy gise ? Baat “ jamp ” a ngiy tekki “ liy laaj ñu bàyyi ci xel ci saa si ”. Ni mu awe yoon, ndaw li Pool tegtal na ne, karceen yi war nañoo ‘ waare kàddu gi [...] ci fasoŋ bu jamp, NW ’. (2 Tim. 4:2.) Ndax mooy li ngay def ci li ngay bàyyi xel léegi-léegi, fi ñu tollu nii, ci liggéey boobu ?
2 Xëy na dañoo nettali woon Pool ne, daa amoon ñenn ci ay mbokki karceenam ñu daan bëgg a jikkowoo ‘ tendeefal ci seeni yëngu-yëngu, NW ’, nikiy karceen (Room 12:11). Loolu nag da doon wàññi li seen liggéey mënoon a jur, niki it mbég mi ñu mënoon a yëg ciy dimbali ñeneen ñi, su ñu doxalee woon neneen.
3 Ni Yeesu gise woon sasu waare bi : Ndaw bànneex bu Yeesu daan sàkku ciy matal sasam ! Lii la wax : “ Sama ñam moo di def coobarey ki ma yónni te àggale liggéey, bi mu sant. ” Royukaayu Yeesu sawarloo na ay taalibeem, yi mu xiirtal, ba mu leen waxee ne ‘ tool yi, ñoo ngi ñor ba weex tàll, di xaar ku leen góob ’. (Ywna. 4:34, 35.) Xelum li jamp, mi mu soloo woon te mu wone ko it ci biir sasam, fés na ba mu nee ay taalibeem : “ Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam. ” (Macë 9:38). Yeesu nàndoon na ne yónnentam moo doon waare, te daa dogu woon ci bañ a bàyyi dara tere koo def lu ni mel.
4 Waaw, lu jëm ci ñun nag ? Jëm kanam ci liggéeyu waare bi masul a gën a jampe niki ci suñu jamano jii. Ci diiwaan yu bare ci àddina si, tool yi ñor nañu, di xaar ku leen góob. Dem na ci bé, ci dëkk yi seede bi niru lu ñu amal bu baax-a-baax sax, ñu ngiy fay sóob ay junniy, junniy nit at mu ne. Ak muju jamono giy dégmal bu gaaw-a-gaaw, am na ‘ liggéey bu baree bare, bu ñu war a def ci Sang bi, NW ’. (1 Kor. 15:58.) Góor-góorlu dëgg ci suñu bopp, ngir bokk ak ñeneen ñi xabaaru Nguur gi, masul a gën a ame solo niki ci suñu jamano.
5 Nañu teewlu ci jokkook ñeneen ñi ak xabaar bu baax bi, muy kër-oo-kër ak it feneen fépp fu ñu mën a taseek nit ci gox gi ñuy waare. Bu ñuy def lu ñu mën ngir bokk ci liggéeyu waare bi, dinañu wone ci fasoŋ bu leer ne, Nguur gi lañu jiital ci suñu dund (Macë 6:33). Suñu takkute ci waare kàddu gi ci fasoŋ bu jamp dina ñu jural mbég mu réy.