TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/01 p. 1
  • Bokkal ci ngóob mi, dem ci ba jeex

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Bokkal ci ngóob mi, dem ci ba jeex
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2001
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • “ Waareel kàddu gi [...] ci fasoŋ bu jamp ”
    Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Dañu kontaan lool ci li ñuy jébbal suñu bopp ci liggéeyu Yexowa !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
Sasu Nguuru Yàlla — 2001
km 5/01 p. 1

Bokkal ci ngóob mi, dem ci ba jeex

1 Yonent Yexowa jamanoy maam ya, niki Yeesu Krist ci boppam, waxoon nañu ci ab liggéeyu dajale ay nit (Isa. 56:8 ; Esek. 34:11 ; Ywna. 10:16). Liggéey bu ni mel, ñu ngi koy amal tey, ba ñuy waare xabaaru Nguur gi, bu baax bi, ci àddina si sépp (Macë 24:14). Liy wuutale ñiy jaamu Yàlla ak ñi ko dul def a ngiy leer nàññ léegi (Mal. 3:18). Lan la looluy tekki ci ñun ?

2 Warugar wu ku nekk war a gàddul boppam : Am na lu ñu mën a jànge ci royukaayu Pool, mi demoon ba jeex ci jiital sasu karceenam. Ci moom, waare ba tax ñépp am bunt bu ñu dégge xabaar bu baax bi te mucc, bor bu mu gàddu woon la. Loolu xiir na ko ci liggéeyal leen te bañ cee tàyyi (Room 1:​14-​17). Bu ñu seetee musiba miy dalsi doom-Aadama yi ci suñu jamano, ndax gàdduwuñu wareef bu gën a mag lu jëm ci waare ñi dëkk ci gox biñ ñu sas ? — 1 Kor. 9:​16.

3 Waxtu ngir jëf ju jamp : Mën nañoo méngale liggéeyu waare bi ak wut ay nit ñu musiba dal ngir xettali leen. War nañoo xam fi ñu nekk, ba noppi dimbali leen ñu aaru laata def ko wees. Jot gi day am àpp. Ay bakkan a ci xaj ! Li Yeesu jamp ay taalibeem, ñu ‘ ñaan Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam ’ waru ñoo bett, kon. — Macë 9:38.

4 Nangu ne suñu jamano jii daa jamp moo xiir ñu bare ci waarekati Nguur gi ci yokk li ñuy def ci yëngu-yëngu boobu di musal i bakkan. Waxambaane wu tudd Hirohisa daa doon dund ak ñeenti rakkam ci seen kër yaay. Daa doon jàppleek xaalisam njaboot gi ci li mu doon yeewu ci ñetti waxtu ci njël, ngir bàyyi ci kër yi ay xabaarukaay. Teewul, li Hirohisa bëggoon moo doon yokk loxoom ci sasu waare bi, ba tax tàmbali naa nekk aji-xàll yoon, bu ci sax. Ndax am na noo mënee gën a bokk ci liggéey boobu dul amati mukk, te dem ci ba jeex ?

5 “ Diir bu gàtt rekk a fi des. ” (1 Kor. 7:29). Kon, nañu def suñu kem-kàttan ci liggéey bi ëpp solo, bi ñu nekk di amal ci kow suuf, fi ñu tollu nii — waare xabaaru Nguur gi, bu baax bi te sàkk ay taalibe. Yeesu misaale na suñu sas ak liggéeyu ngóob (Macë 9:35-38). Bu ñuy bokk ci ngóob mi, te dem ci ba jeex, li suñu liggéey di meññ mën naa ëmb dimbali kenn mu bokk ci mbooloo jaami Yàlla, mu réy, mi ñuy wax ci Peeñu bi 7:9, 10.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager