Lu ñu mën a dimbali ñu dëgër ci ngëm gi ?
1 Li dale ca ba ñu tàmbalee digaaleek mbootaayu Yeowa ba léegi, suñu njëm kanam ci wàllu xel, mbég dëgg la ñu jural ! Ndaxam, ngir ‘ sax [...], màgg [...], tey gëna dëgër ci ngëm gi ’, soxla nañoo wéy di màgg ci wàllu xel. (Kolos 2:6, 7.) Ba li ëpp ci ñun texe ci fànn boobu, am na ci, ñu bayliku ndax li ñu sàgganee “ dëgër ci ngëm ” gi (1 Korent 16:13). Mën nañoo moytu lu ni mel dal ñu. Naka noonu ?
2 Yëngu-yëngu ci wàllu xel, bu takku : Tëralal doxalukaay bu baax ci wàllu xel ci biir mbootaayu Yeowa. Ñu ngi fay toppatoo bu baax, ci fasoŋ bu yéwén it, suñuy soxla ci wàllu xel. Ndajey mbooloo gëmkat yi ak ndaje yu mag yi, dañ ñuy xiirtal ci gën a màgg ci wàllu xel te sax ci, fi ak ñu ngiy takku ci teewe leen ngir góobe ci ay njariñ (Yaw. 10:24, 25). Liy dimbali suñuy reen, ci wàllu xel, roofu te dëgër mooy doxalukaay bu ñu tàmm di topp lu jëm ci duruus Biibël bi, yéenekaay yi tudd La Tour de Garde, ak Réveillez-vous !, akit téere yiy waxtaane ci ñamu Kàddu Yàlla, wu dëgër wi (Yaw. 5:14). Di sampal sa bopp ay jubluwaay ci wàllu xel tey liggéey ak parlu ci matal leen, dina jur itam njariñ yuy yàgg.— Fil. 3:16.
3 Ndimbalu ñii ñor : Wutal a ubbeeku ci ñii ñor ci wàllu xel ci biir mbooloo mi. Jéemal a xamanteek mag ñi, ndegam ñoom, balaa keneen ku mu mën a doon, ñooy ñi ñu mën a dooleel (1 Tes. 2:11, 12). Nangul ak xol bu sedd bépp ndigal walla xelal bu ñu la mën a jox (Efes 4:11-16). Surgay mbooloo mi, ñoom it, ittewoo nañu dimbali ñeneen ñi, ndax ñu dëgër ci ngëm gi ; kon jublul ci mbokki karceen yu góor yooyu ngir sàkku ci ñoom xiirtal.
4 Waaw, boo soxlaa ndimbal ci sasu waare bi, nag ? Waxal ak mag ñi, te ñaan leen ndimbal. Xëy na ñu boole la ci doxalukaay bi tudd Way-xàll yoon yaa ngiy Dimbali Ñeneen ñi. Ndax ñu ngi lay soog a sóob ? Jàng téere bi tudd Notre ministère tey topp li mu ëmb dina la jëmloo kanam, jëme la ci ñoraay ci wàllu xel. Boo dee aji-jur nag ? Saxal ciy feddali diggante say doom ak Yàlla. — Efes 6:4.
5 Bu ñu saxee ay reen ci ngëm gi te riigu ci, dinañu sàkku bànneex ci diggante yu rafet ak Yeowa, akit ci ànd, bu sedd xol, ak suñuy mbokki diine yi. Loolu dana tax ñu të congiy Seytaane, te dooleel suñu yaakaaru dund gu dul jeex. — 1 Pie. 5:9, 10.