Ndimbal bu yomb am
1 Suñu benn mbokk bu tudd Anna, dafa amoon jëkkër bu nekkul Seede Yexowa te liggéeyam dafa doon jël lu bare ci jotam. Moo tax teewe ndaje yi, waaraate ak jàng Kàddu Yàlla, jafe woon na ci moom. Mujj na bàyyi waaraate, fekk mbëggeel bi mu amoon ci Yexowa deñul woon ci moom. Yàlla baax na, njiiti mbooloo mi dañu ko dimbali ci wàllu ngëm, ndaxte li mu nekke woon dafa leen metti woon.
2 Ku nangu mbooloo mi jàpple la ci wàllu ngëm, yaa ngi wone ne ci Yexowa ci boppam ngay wéeru. Njiiti mbooloo mi dañuy roy ci Yeesu, di toppatoo waa mbooloo mi ak mbëggeel. Loolu moo tax, dañuy seet li ñu mën a def ngir yokk doole te jàpple ñi am ay jafe-jafe ci wàllu ngëm (1 Tes. 5:14). Ci lu bare, boo jëlee benn aaya buy yokk doole te nga am ci waxtaan bu neex ak nit ki, dina doy. Karceen yépp a war a seet li ñu mën a def ngir jàpple ñiy jaar ci jafe-jafe ci wàllu ngëm. Du njiiti mbooloo mi rekk ñoo war a def loolu. Wóor na ne, ñun ñépp a mas dégg “ kàddu bu ñu wax ci waxtoom ”, fekk ñu ngi woon ci coono. Te gis nañu ni kàddu bu mel noonu amee doole. — Léeb. 25:11 ; Esa. 35:3, 4.
3 Seetal li nga mën a def : Ku bëgg won ñi soxla ndimbal ne danga leen bëgg, yow mii yaa war a seet li nga leen mën a defal. Danga ko war a won ne dangay bokk ak moom tiis, maanaam li ko metti, metti na la yow itam. Te danga leen war a bëgg dimbali dëgg. Bi Yonatan déggee ne Dawuda dafa amoon jafe-jafe bu mettee metti, “ dafa jóg, dem fekki Dawuda ca Ores, ngir dëgëral loxoom ”. (1 Sam. 23:15, 16.) Yow itam nanga seet lu rafet loo mën a def ngir dimbali nit ñi. Wax leen ay kàddu yuy wone ne danga leen bëgg dëgg, mën na def lu bare. Yeesu wone na ne ku bëgg dimbali mbokkam bu am jafe-jafe ci wàllu ngëm, danga war a nekk ku sawar te waruloo gaaw a dellu ginnaaw (Luug 15:4). Te bu dee sax nit ki du gaaw a jëm kanam ci wàllu ngëm, duñu ci tàyyi. Dinañu ko kontine dimbali.
4 Dëgg-dëgg, woo sa mbokk mel ni ñi nga bokkal njàngum téere, ngir ngeen ànd ci waaraate bi, lu baax la ! Te bu ngeen di waaraate, mën nga ko xiir ci yokk li muy def ci liggéeyu Yexowa. Dañuy kontaan bu ñuy nekk noonu di liggéeyal Yexowa, rawatina bu dee ki ñuy àndal mu ngi door a komaasewaat a bokk ci waaraate bi.
5 Lu baax li ñu taxawal : Ñi yàgg bañ a waaraate walla bañ a teewe ndaje yi, mën na am ñu soxla leneen ngir seen ngëm gën a dëgër. Xéyna bu ñu leen defalee benn njàngum Biibël ci téere Adorez le seul vrai Dieu, walla téere Approchez-vous de Jéhovah, walla téere Qu’enseigne réellement la Bible ?, dina baax. Ndegam nit ki sóob nañu ko ci ndox ba pare, kon lu ci ëpp, jarul ñu yàgg ci njàngum Biibël boobu. Kurélu liggéeyu waare bi moo war a seetlu kan moo soxla njàngum Biibël bu mel noonu. — Seetleen Réponses à vos questions ci Le ministère du Royaume bu nowàmbar 1998 ak bu nowàmbar 2000.
6 Sànq, ñu ngi doon wax ci suñu benn mbokk bu tudd Anna. Njiiti mbooloo mi dañu ko wax ne bu ko neexee, suñu benn mbokk bu am ngëm gu dëgër, dina ko defal benn njàngum Biibël. Dafa ci kontaan lool te nangu na loolu. Njàng mi, ñeenti yoon lañu ko def rekk, mu defaraat digganteem ak Yexowa. Mu komaasewaat teewe ndaje yi te wax it ne dafa bëgg màggal Yexowa ci waaraate bi. Suñu mbokk mi dëgër ci ngëm dafa ko yóbbu ci njàngum Biibël yi mu doon def, ba bés bu mu amaat ngëm gu dëgër gu koy may mu mën a waare këroo-kër. Suñu mbokk moomu, ku ko dimbali kese la soxla woon ngir mën a def lépp li ko war ci wàllu ngëm.
7 Dëgëral ngëmu ñi ko soxla dafay indil ñépp ay barke. Ki soxla ñu jàpple ko dafay gën a jege Yexowa te dafay bokkaat ci lépp li ñuy def ci mbootaayu Yexowa. Njiiti mbooloo mi, bu ñu gisee nit kooku di jëm kanam ci wàllu ngëm, dañu ciy kontaan (Luug 15:5, 6). Waa mbooloo mi dañuy gën a nekk benn ndaxte ku nekk dafay toppatoo moroomam ak mbëggeel (Kol. 3:12-14). Loolu lépp a tax ñu war a roy ci Yexowa mi nekk ndimbal bu yomb am ! — Efes 5:1.
[Laaj yi]
1. Naka la ngëmu nit mëne wàññeeku ?
2. Naka la karceen bu nekk mënee nekk ndimbal bu yomb am ?
3, 4. Lan mooy dimbali ñi ko soxla, te naka lañu ko mënee def ?
5. Lan la njiiti mbooloo mi mën a def yenn saay ngir dimbali suñu ay mbokk ci ngëm ?
6. Lan moo tax suñu benn mbokk mu jigéen amaat doole ci wàllu ngëm ?
7. Dëgëral sa moroom ci wàllu ngëm, loolu naka la ñuy jariñe ?