TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/00 p. 1
  • “ Yeewuleen te sax ci ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • “ Yeewuleen te sax ci ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2000
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Dinañu gën a wax ci Biibël bi !
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Buñu fàtte ne jot bi des bareetul
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Sasu Nguuru Yàlla — 2000
km 5/00 p. 1

“ Yeewuleen te sax ci ”

1 Ba mu noppee nettali xew-xew yu am solo, yi naroon a màndargaal bés yu mujj yi, ci suñu jamano jii, Yeesu jamp na ay taalibeem ñu ‘ yeewu te sax ci ’. (Mark 13:33, NW.) Lu tax karceen yi war a yeewu te sax ci ? Ndaxte ñu ngiy dund ci jamano ji yées ci jaar-jaaru doom-Aadama. Mënuñoo may suñu bopp doon nit ñu gëmméentu ci wàllu xel. Daanu ci lu ni mel dina tax ñu fonkadi liggéey, bi ñu Yeowa sas ci muju jamano jii. Ban liggéey la boobu ?

2 Yeowaa ngiy yéeneloo mbooloom, xabaar bu baax bi jëm ci Nguuram, ci kow suuf si sépp — muy jenn yaakaar ji doom-Aadama yi am doŋŋ. Ànd a liggéey, ak takkute, ak mbootaayu Yàlla, nag, day tax ñu ràññe ñu ni ay karceen ñu yeewu dëgg ci tekki-tekki suñu jamano jii, ni nit ñu yeewu itam ci soxlas dimbali ñeneen ñi ñu dégg ‘ baati dund gu dul jeex ’. (Ywna. 6:68.) Bokk ak cawarte ci liggéey bu am-a-am solo boobu, mooy wone ne yeewu nañu ci wàllu xel.

3 Lu ñuy xiir ci waare : Ndegam dugg nañu ci biir mbootaayu Yeowa, war nañoo rafetlu suñu sasu waare. Bëgg Yàllaak suñu moroom moo ñuy xiir, ku nekk ci ñun, ci bokk ci liggéeyu waare bi (1 Kor. 9:16, 17). Noonu lañuy musale suñu bopp ak ñi ñuy déglu (1 Tim. 4:16). Yal nañu dogu ci def suñu kem-kàttan ngir def waareb Nguur gi ab tàmmeel, di ci def suñu kem-kàttan ci wàllu waxtu, ci parlu, xam ne mooy nguur gi gën, gu doom-Aadama yi mënkoon a am — Nguuru Yàlla !

4 Mbir mu am solo tax na suñu sasu waare doon lu jamp. Metit wu réy wi dina tàkk, fekk ñu ba tey ci liggéey boobu. Ñàkk a xam bés beek waxtu wi, tax na ñu yeewu te sax ci, tey pare saa su ne, di wàkkirlu ci ñaan ci Yeowa (Efes 6:18). Doole liggéeyu waare baa ngiy wéy di law. Waaye bés a ngiy ñëw ci kanam, fu liggéeyu seede bi gën a mag ci jaar-jaaru doom-Aadama di àgg ci dayoom gi gën a ñàng.

5 Ak takkute, toppleen ndigalu Yeesu, maanaam ‘ yeewu te sax ci ’. Tey la soxlas def loolu gën a am solo jépp jeneen jamano. Yal nañu def li war, soloo xelum li jamp. Bés-oo-bés, nañu sax ci doon ñu maandu, ñu sawar te farlu ci liggéeyu Yeowa. Waaw, yal nañu ‘ wéy di yeewu te maandu ’. — 1 Tes. 5:6, NW.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager