Buñu fàtte ne jot bi des bareetul
1 Yeesu xamoon na ne jot bi mu amoon ngir def liggéey bi ko Yàlla dénk ci kow suuf barewul woon (Ywna. 9:4). Looloo tax mu doon gaaw ci liggéeyam te wax taalibeem yi ñu def ni moom (Lukk 4:42-44 ; 8:1 ; 10:2-4). Dëgg la alal mën na faj soxla yu bare, waaye du moom la Yeesu jiitaloon ci àddinaam (Macë 8:20). Looloo tax mu àggale liggéey bi ko Yexowa dénkoon. — Ywna. 17:4.
2 Jot bi ñu am barewul : Tey it jot bi ñu am ngir waar xibaar bu baax bi ci “ àddina sépp ” barewul (Macë 24:14). Ni ko Biibël bi waxe, ñu ngi ci muju jamano ji te li ci des bareetul. Léegi, “ ñi xamul Yàlla te baña déggal xebaar bu baaxu suñu Boroom Yeesu ” dinañu “ alku ba fàww ”. (2 Tes. 1:6-9.) Àtte boobu dina ñu bett (Lukk 21:34, 35 ; 1 Tes. 5:2, 3). Nit ñépp a war a yëg musiba biy ñów. War nañu xam it li ñu war a def bu ñu bëggee Yexowa baal leen, bala réccu di wees. Ñun nag ñoo leen war a xamal loolu. — Tsë. 2:2, 3.
3 Nañu def lépp li ñu mën : Ñiy jaamu Yàlla xam nañu ne “ diir bu gàtt rekk a fi des ”. Looloo tax liggéeyu waare bi ëpp solo ci ñoom (1 Kor. 7:29-31 ; Macë 6:33). Am na ñu mënoon a am xaalis bu bare, ñeneen am lu ñuy wut ci àddina. Waaye dañu bàyyi loolu lépp ngir yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi (Mark 10:29, 30). Am na ñu am jafe-jafe yu dul jeex, waaye ba léegi ñu ngi “ sawar ci liggéeyu Boroom bi ”. (1 Kor. 15:58.) Am na it ñu yàgg ci yégle xibaar bu baax bi. Waaye toqiwuñu fenn, maanaam ba léegi dañu ci dëgër (Yaw. 10:23). Nit ñooñu ñépp dañu bëgg liggéeyu Nguur gi jëm kanam. Yexowa fonk na kuy def ni ñoom. — Yaw. 6:10.
4 Nañu jiital ci suñu dund lépp li ñuy def ngir jaamu Yexowa, boole ci liggéeyu waare bi. Kon duñu fàtte bésu Yexowa. Àddina Seytaane si du ñu yóbbaale te fu ñu tollu rekk dinañu góor-góorlu ngir sell ci suñu jikko (2 Pie. 3:11-14). Kon nag buñu yéex ci waaraate bi. Dinañu ci mën a mucc ñun ci suñu bopp ak ñi ñuy déglu. — 1 Tim. 4:16.