Ay jumtuwaay yuy jàngale, yuy xiirtal ak a dooleel
1 Am nañu doole ngir jàngal nit ñi Biibël bi te xamal leen ñan ñooy Seede Yexowa yi. Xiirtal nañu ñu bare, ñu ne temm ci taxawu dëgg gi. Dooleel nañu ngëm ak ngërëmu mbooloo mi jébbalu ci Yàlla. Waaw, lool’ lan la ? Widewo yi mbootaayu Yexowa defar. Ndax seetaan ngeen leen, ñoom yépp ? Kañ ngeen ko mujjee def ? Ndax dingeen leen jëfandikoo ci seen sasu waare ? Nan ngeen mënee jariñoo ni mu gëne jumtuwaay yu amul moroom yooyu ?
2 Ci La Tour de Garde bu 1 sulyet 1999, bunt bi tudd “ Étudions régulièrement la Parole de Dieu en famille ” [Nañu faral di jàng Kàddug Yàlla ci biir njaboot gi] mu ngi doon digal ngeen “ jël jotu seetaan ci seen biir njàng aw wàll ci benn ci widewo Mbootaay gi, yiy jàngale [...] ba noppi waxtaane ci ”. Ci lu dëppook xelal bu rafet boobu, dinañu waxtaane ñaari weer yu nekk, ci Ndaje Liggéeyu waare bi, widewo bu wuute. Ñu ngiy xiirtal ku nekk ci mbooloo mi mu seetaan widewo bi këram laata ñu ciy waxtaane ci ndaje Liggéeyu waare bi.
3 Weer wii nag, widewo bi ñu jëkk a defar lañuy tàmbalee, Les Témoins de Jéhovah — Un nom, une organisation. Seetaanleen ko te déglu tonti laajte yile :
◼ Ngir def lan, lañu gën a xame Seede Yexowa yi ?
◼ Lépp lu ñu def ca Betel ba, jan aaya lañu ko lëkkaleel ?
◼ Ban nettalib Biibël bi ngeen gis ñu géewal ko, foto ko, te nataal ko ngir jariñoo ko ci suñu mbind yi ?
◼ Lan moo leen waar ci ni ñuy defare suñu mbind yi ?
◼ Li dale 1920 ba 1990, ñaata sottiy mbind la Mbootaay gi muul ?
◼ Ñan saxsax ci mbooloo Yàlla ñoo war a wut a jekk ci liggéeyu Betel ba ? — Léeb. 20:29.
◼ Nan la ñi bokk ci njabootu Betel ba nekke royukaay bu rafet ngir Seede Yexowa yi yépp ?
◼ Lan moo leen waar ci liggéey, bi ñuy def ca Betel ba ngir laal li ëpp ci nit ñi, ak xabaar bu baax bi ?
◼ Fan lañuy jële xaalis ngir jàpple liggéey, bi ñuy amal ci suuf si sépp ?
◼ Ban yëngu-yëngu lañu mën a jàppleek cawarte, te man xel lañu war a soloo ? — Ywna. 4:35 ; Jëf. 1:8.
◼ Looleen xalaat ci mbootaay gi nekk ci ginnaaw tur wi ñu nu tudde ?
◼ Nan nga mënee jëfandikoo widewo bile ci sasu waare wi ?
Ci desàmbar, dinañu nafar widewo La Bible — Un récit historique exact, des prophéties dignes de foi.