Li nekk ci wideo boobu, war nañu ci xalaat bu baax
“ Wideo boobu, dafa lay xalaatloo bu baax ! ”
“ Dafa laal sama xol ! ”
“ Sama yaram dafa doon daw ! ”
1 Ndax lu mel noonu nga doon wax yow itam bi nga njëkkee seetaan wideo bi tudd Les jeunes s’interrogent... Comment se faire de vrais amis ? Am na léegi ay at ci ginnaaw, suñu benn mbokk bu ndaw dafa amoon poroblem yu réy ndax xarit yi mu tànnoon. Xaritam yooyu taxoon nañu ba dëgg gi neexatu ko woon ni bu njëkk. Mujj gi, digganteem ak Yexowa yàqu. Ginnaaw loolu, bi wideo bi tudd Vrais amis génnee, dafa nee : “ Dama ko seetaan ay yooni yoon. Te li ma ko doon seetaan yépp, ay rongooñ a ngi doon tuuru ci sama kanam. Dama gërëm Yexowa ci ndimbal bi mu ma indil ci waxtu bi ma ko gënee soxla. ” Wideo bi tax na ba mu soppi lu bare ci dundam te mu wut xarit yu baax. Nee na it : “ Ñépp a mën a gis ne dara umpu leen ci lépp liy laal ndaw yi tey. ” Yéen wayjur yi ak ndaw yi, njàngum Biibël bi ngeen di def ci seen njaboot bu jotee, ndax mënuleen a seetaan wideo boobu ? Saa yu benn xaaj jeexee, nangeen arete wideo bi te waxtaan bu baax ci laaj yii di topp. Ku nekk di wax li nekk ci xolam dëgg.
2 Ngir ubbi waxtaan bi : Lan mooy xarit dëgg ? — Léeb. 18:24.
3 Liy yàq xaritoo : Naka nga mën a fexee ba bañ a xalaat ne nit ñi bëgguñu la xajal ci seen biir (Fil. 2: 4) ? Lu tax nga war a nangu góor-góorlu ba am jikko yu gën a rafet ? Kan moo la ci mën a dimbali ? Lu la mën a dimbali ba nga am xarit yu gën a bare ? Foo mënee am ay xarit ? — 2 Kor. 6: 13.
4 Xaritoo ak Yàlla : Naka nga mënee def ba xaritoo ak Yexowa ? Ku bëgg xaritoo ak Yàlla, dafa war a góor-góorlu dëgg. Waaye, lu tax ñu mën a wax ne jar na ko (Sab. 34: 8) ? Lan moo gën a mën a rattaxal sa diggante ak Yàlla ?
5 Xarit yu bon yi : Lan mooy àndandoo bu bon (1 Kor. 15:33) ? Xarit yu bon, naka lañu mënee yàq sa diggante ak Yàlla ? Li Biibël bi nettali ci Diina, lan la la jàngal ? — Njàl. 34: 1, 2, 7, 19.
6 Lenn lu mën a xew ci suñu jamano : Lan la wéetaay def Tara ? Lan la wax ngir wone ne ci moom, ànd ak ndaw yu bokk ci àddina si, lu baax la ? Xarit yooyu, ci lan lañu ko mënoon a dugal ? Lu tax wayjuram yi gisuñu musiba yi ko naroon a dal ? Waaye ban jikko lañu wone ngir dimbali ko ba mu defaraat digganteem ak Yàlla ? Naka la benn pioñee bu jigéen wone ne xaritu Tara dëgg la woon ? Lu tax karceen yi war a déglu bu baax li Léebu 13:20 ak Yeremi 17:9 wax ? Lan la Tara jàng te mu nekk lu am solo ?
7 Ngir jeexal waxtaan bi : Loo jàng ci wideo bii ? Noo ko mënee jëfandikoo ngir dimbali ñeneen ? — Sab. 71:17.