Ragalal Yexowa bés bi lëmm
1 “ Ragal Yexowa mooy ndoorte sago. ” (Sab.111:10). Da ñuy xiir ci jëf yu baax te da ñuy dimbali ñu dëddu lu bon (Léeb. 16:6). Ragal googu, weg Ki ñu sàkk, gu xóot la, weg gu ñuy xiir ci moytoo def lu ko naqari ak di ko déggadil. Lu ñu soxlaa suuxat ci suñu xol la, te di ko wone, bés bi lëmm. — Léeb. 8:13.
2 Bés bu ne, xelum àddina Seytaane, ak doole ju doy waar, a ngi ñuy ruux ndax ñu roy ciy yoonam yu bon (Efes 6:11, 12). Dañoo matadi, di bàkkaar, te suñu jikko da ñuy xiir ci lu bon (Gal. 5:17). Looloo tax, ngir topp ndigali Yexowa yi, am bànneex te jot ci dund ga mu dig, war nañu koo ragal, bés bi lëmm. — 5 Mu. 10:12, 13.
3 Ci Yawut yi 10:24, 25, ñu ngi ñuy dénk ñu dajaloo ngir xiirtalante, “ rawatina nag, NW ” ci jamano jii ñuy dund. Tàmm di teewe ndaje yi, am na solo lool, su ñu bëggee mucc ci bés yu mujj yii. Suñu ragal-a-def lu naqari Yàlla da ñuy xiir ci teewe ndaje yi te fonk dëgg seen jubluwaay. Ñi ragal Yàlla dañu jàppe niki cér bu tedd, bokk ci ndaje karceen yi.
4 Topp ndigalu waare xabaaru Nguur gi, bu baax bi, beneen fasoŋ la bu ñuy wonee suñu ragal Yàlla (Macë 28:19, 20 ; Jëf. 10:42). Lenn ci li ëpp solo ci li ñu jublu, bu ñuy waaree, mooy dimbali ñeneen ñu suuxat ci seen xol ragal Yexowa te nangul coobareem. Ñu ngiy def loolu, bu ñuy seetiwaat nit ñi, di góor-góorlu ngir tàmbali ay njàngum Biibël bi ci kër yi tey jàngal ñeneen lépp li Yàlla digal. Noonu lañuy wone ne, ragal nañu Yexowa te bëgg nañu suñuy moroom. — Macë 22:37-39.
5 Ñi ragalul Yàlla mënuñoo soloo xelum fonk mbiriy Yàlla yi, te ngelawu àddina si di reye, maanaam xel mi mu soloo, da leen ëpp doole (Efes 2:2). Yal nañu ne temm, dogu ci “ di [...] jaamu [Yàlla], ni mu ko bëgge, boole ci wegeel ak ragal. ” (Yaw. 12:28). Dinañu ci góobe noonu barke yi ñu baaxe ñi ragal Yàlla, bés bi lëmm.