Ndaje mu mag mu ñaari fan miy ñów : li ñu fay waxtaane.
Ragal mën na nekk “ weg bu baax a baax, rawatina bu fekkee ne Yàlla lañuy weg ”. Loolu mooy ragal bu am njariñ bi Mbind mi méngale ak “ fi am xel di tàmbali ”. (Sab. 111:10.) Waaye nag, beneen ragal moo nekk ci àddina Seytaane si ñu nekk. Bu ñuy yokk ragal bu am njariñ bi ñu am ci Yexowa, naka lañu mënee moytu ragal buy lore boobu ? Ndaje mu mag mu ñaari fan mi ñuy am ci atum liggéeyu waare (ci tubaab année de service) bu 2002, dina ñu tontu ci loolu. Yaxu ndaje mu mag moomu mooy : “ Ragalleen Yàlla te jox ko ndam li. ” (Peeñ. 14:7). Dinañu gis naka la ragal Yexowa amale njariñ nit ku nekk ak it mbooloo mi, ci lu bare.
Ragal dafay tax sa xel bañ a dal, doo am fit, te doo ñeme lu jafe. Waaye Biibël bi nee na : “ Képp ku ragal Yàlla, bég nga. ” (Sab. 128:1). Ndaje mu mag moomu dina ñu won ni ñu mënee xeex jafe-jafe yi ñuy am bu ñuy jaamu Yàlla dëgg, ba am ci pexe. Dinañu gis ni ñu mënee dimbali ñi sog a ñów ci mbooloo mi, ñu saxal ci seen xol ragal boobu am njariñ. Ci lu wóor, loolu moo leen di xiir ci jaamu Yàlla ak seen xol bépp, seen bakkan bépp, seen xel mépp ak seen kàttan gépp (Mark 12:30). “ Gënleen di jege ñi ngeen sopp ” mooy waxtaan biy mujj ci fan bu jëkk bi. Wottukatu diiwaan bi (ci tubaab surveillant de district) moo koy def. Dina wone ni ñu mënee gaaw a ràññe te xeex lépp li Seytaane di def ngir ñu won ginnaaw Yexowa, suñuy mbokk ak suñuy mbokki karceen.
“ Ragalleen Yexowa, buleen ragal nit ” mooy waxtaan bi ñuy def ci ñeenti xaaj, ci ñaareelu fan bi. Bépp ragal buy tax ñu bañ a def suñu liggéeyu waare ba mu mat, walla ñu dellu ginnaaw ci suñu takkute ci Yàlla, walla ñu def li ñu suñu xel mayul, fa ñuy jànge, walla fa ñuy liggéeye, waxtaan boobu dina ñu leeralal naka ak lu tax ñu war koo xeex ba daan ko. “ Ragalleen Yàlla te topp li mu sant ” mooy waxtaan bi ñu jagleel ñépp. Dafay sukkandiku ci xew-xew yuy toppante te nekk ci Peeñu bi pàcc 14 . “ Dëkkleen ci ragal Yexowa ”, waxtaan boobu di xiir ci lu baax, mooy jeexal ndaje mu mag mi.
Fexeel it ba fekke Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, Ndaje liggéeyu waare bi ñuy def ngir ñu roy ci, waxtaan bi ngir ñi ñuy sóob ak tënku njàngum La Tour de Garde. Waxal ñi ngay jàngal Biibël bi ñu ñów fekke ndaje mu mag moomu. Képp ku bëgg a ñu sóob ko, na ko gaaw a xamal wottukat biy jiite (ci tubaab surveillant-président). Ñun ñépp, bu ñu teewee ci bépp waxtaanu ndaje mu mag mu am solo moomu, ci lañuy wone ne ragal nañu Yexowa, ragal bu am njariñ, te bëgg nañu koo màggal.