Yexowa day maye kàttan
1 Loo xalaat ci ndaw li Pool ? Bu ñu jàngee téereb Jëf ya, mën nañoo gis ni mu njaxlafe woon ci liggéeyu Yexowa. Waaye, nan la Pool daan def, ba mën a matal lépp li mu def ? Lii la wax : “ Man naa lépp ci ndimbalu Aji-Dooleel ji. ”(Fil. 4:13). Ñun itam, mën nañoo jot ci kàttan gi Yexowa di maye. Naka ? Bu ñuy sàkku njariñ ci juróom-benni yëf yu mu ñu jox ngir mayaat ñu doole te dëgëral ñu ci wàllu xel.
2 Kàddug Yàlla : Niki rekk lekk war na ñu ngir sàmm suñu dooley jëmm, noonu it la ñu dundal suñu bopp ak Kàddug Yàlla ware, ngir wéy di dund ci wàllu xel (Macë 4:4). Biibël bi day maye kàttan, gi ñuy taxawu. Ngir sàmm suñu cawarteek suñu parlu ngir dëgg gi, soxla nañoo dugg ci jàngal suñu bopp tey xalaat ba xel xelli ci fasoŋ bu am maanaa, bés bu ne, su ñu ko mënee. — Sab. 1:2, 3.
3 Ñaan : Lu am solo la, jege Yexowa, rawatina nag ci jamanoy soxla su jamp. Jaare ci xelam, day maye kàttan guy jàjji ñi ko koy ñaan (Lukk 11:13 ; Efes 3:16). Mbind yaa ngi ñuy xiirtal ciy “ sax ci ñaan ”. (Room 12:12.) Ndax dingay def loolu ?
4 Mbooloo ñi gëm : Ñu ngiy sàkku itam doole ak xiirtal ci ndajey mbooloo mi, ak ci ànd bu sedd xol, bi ñuy bànneexook suñu mbokki diine yi, góor ak jigéen (Yaw. 10:24, 25). Bu ñu jàqee, dañ ñuy dimbali ñu siggi te dañ ñuy taxawu ak mbëggeel. — Léeb. 17:17 ; Daj. 4:10.
5 Sasu tool bi : Faral di bokk ci sasu waare bi da ñuy dimbali ñu wéy di teewlu ci Nguur gi ak i barkeem. Dimbali ñeneen ñu jàng a xam Yexowa, day yokk suñu dogu (Jëf. 20:35). Du ñépp ci ñun ñoo mën a toxu ngir liggéey fi soxlas waare si gën a taxaw, walla jagleel ci seen jot gépp, waaye mën nañoo bokk neneen ci liggéeyu waare bi, ci fasoŋ bu am maanaa. — Yaw. 6:10-12.
6 Wottukati karceen yi : Dañuy sàkk njariñ ci xiirtalu magi mbooloo mi ak ci seen ndimbal. Yexowa da leen sas ñu sàmm géttu Yàlla, gi mu leen dénk (1 Pie. 5:2). Wottukat yiy wër dañuy feddali ngëmu mbooloo yi ñuy liggéeyal, niki rekk Pool ca jamanoom. — Room 1:11, 12.
7 Royukaayi ñii takku ci Yàlla : Seet ci royukaayu nit ñi takku, ñu bokk di liggéeyal, royukaay yuy xiirtal, muy démb mbaa ci suñu jamano, day dooleel dëgg (Yaw. 12:1). Boo soxlaa doolewu, lu la tee duruus nettaliy dundug nit, yuy xiirtal yi ne ci suñu yéenekaay yi, walla nettali buy feddali ngëm ci Annuaire bi, mbaa yenn ci nettali yu daw yaram, yi jëm ci jaar-jaaru Seede Yexowa yi ci suñu jamano, ci biir téere Prédicateurs ?
8 Menn mbokku karceen mu góor, mu nekk léegi ci diggu 90 atam yi, nangu woon na dëgg gi, fekk muy xale bu góor. Mu nga nekkoon xale ba tey, ba ngëmam jànkoonteek ay nattu. Bi njëkk moo doon, ba ñenn ñu bokkoon ak parlu ci yëngu-yëngu mbooloo mi, bàyyee mbootaayu Yexowa. Liggéeyu kër-oo-kër bi itam, lu jafe ci moom la woon. Wànte, saa su ne da doon wàkkirlu ci Yexowa. Yàggul dara, mu nga doon yëg bànneex ci waare bi. Waaw, tey-ci-tey nag ? Lu mu wéradi wéradi, mu ngi bokk ba léegi ci njabootu Betelu Brooklyn ak ci Jataay biy dogal. Réccuwul lenn ci li mu taq ci mbootaayu Yexowa.
9 Menn mbokk mu jigéen, mu bokk ci njabootu Betelu Ãgalteer, a nga amoon 13 at, ba ñu ko sóobee. At ma ca tegu la sumb sasu aji-xàll yoon ak càmmiñam, te ba ca meneen at tegoo, téj nañu baayam kaso ndax li mu faralul benn làng ci biir Ñaareelu Xeexu Àddina si sépp. Janq bi wéy di jublu ci Yexowa ngir am kàttan, te sax ci jaamu Yàlla dëgg ji. Ca waxtoom, séy naak mbokk mu takku, ñu ànd a sax ciy def coobare Yexowa. Jékki-jékki, gannaaw séyub 35 at, jëkkëram gaañu. Foofa itam, ci Yexowa la sàkku doole, te loolu la wéy di def ba tey jii, di séentu ne ci temm ba fàww, ci biir njabootu Yàlla gi ci kow suuf.
10 Yexowa day taxawu tey dooleel jaamam yu takku yi. “ Day may kàttan ki tàyyi ; te ci ki loof, day def ba doole bare dëgg. ” Mën nañoo jot ci kàttan googu jéggi dayo, bu ñuy jariñoo juróom-benni yëf yooyu yépp mu maye te ñu tudd leen ci kow. Fàttalikul lii : “ Ñii yaakaar ci Yexowa, dinañu jotaat kàttan. [...] Dinañu daw te duñu lott ; dinañu dox te duñu tàyyi. ” (Isa. 40:29-31). Pool daa wékkoon dëgg yaakaaram ci Yexowa ngir am doole, te mooy li ñu war.