TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 5/07 p. 1
  • “ Dafay may doole ñi sonn ”

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • “ Dafay may doole ñi sonn ”
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • “ Kàdduy yoonu ngëm ” : suñu ñam la ci wàllu ngëm
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Yexowa day maye kàttan
    Sasu Nguuru Yàlla — 2001
  • Wéerul ci Yexowa ngir am doole
    Sasu Nguuru Yàlla — 2001
  • Waaraate bi dafay tax ñu mën a muñ
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 5/07 p. 1

“ Dafay may doole ñi sonn ”

1 Ñun ñépp yenn saay dinañu sonn. Mën na sax bañ a jóge ci liggéey kese walla yëngu-yëngu yi, waaye it ci “ bési tiis yu tar ” yi ñuy jànkoonteel tey (2 Tim. 3:1). Ñun ñii di jaamu Yexowa, lan lañu mën a def ba am doole ci wàllu ngëm ngir bañ a wàññi li ñuy def ci waaraate bi ? Dinañu ko mën, bu fekkee ne dañuy wéeru ci Yexowa, Boroom kàttan bi (Isa. 40:26). Moom xam na bu baax suñuy soxla te dafa ñu bëgg a dimbali lool. — 1 Pie. 5:7.

2 Li ñu Yexowa may : Yexowa dafa sàkk àddina si sépp ak xelam mu sell mi. Xel moomu, kàttan la boo xam ne amul kàttan bu ko ëpp doole. Ci kàttan boobu la ñu Yàlla di maye doole saa yu ñu sonnee (Isa. 40:31). Laajal sa bopp lii : ‘ Kañ laa mujj ñaan Yàlla xelam mu sell mi ci boppam ngir am kàttanu def sama warugaru karceen ? ’ — Lukk 11:11-13.

3 Su ñuy jàng Kàddu Yàlla bés bu nekk te xalaat ci te di tàmm jàng it suñuy téere karceen yi ngir dëgëral suñu ngëm, ci dëgg su ñu defee loolu dinañu “ mel ni garab gu sax ci bëti ndox, di meññ ci waxtoom te xobam du lax ”. — Sab. 1:2, 3.

4 Yexowa dina jaar itam ci suñu mbokk ci ngëm yi mën a ‘ féexal suñu xol ’ maanaam yi mën a nekk ndimbal buy dooleel (Kol. 4:10, 11). Bu ñu nekkee ci suñu ndaje yi, suñuy mbokk ci ngëm dinañu ñu dooleel ci seeni waxtaan yuy dëgëral suñu ngëm ak ci tont yi ñuy joxe, ak it bu ñuy def ay waxtaan ci kanamu mbooloo mi (Jëf. 15:32). Ñiy jiite mbooloo mi dinañu nu jàpple ñu jëm kanam ci wallu ngëm te di ñu wax ay kàddu yuy yokk doole. — Isa. 32:1, 2.

5 Liggéeyu waare bi : Boo seetloo ne yaa ngi komaase sonn, bul bàyyi waaraate bi ! Waaraate bi bokkul dara ak yeneen liggéey yi. Ku ci faral di bokk, dafay gën a am doole (Macë 11:28-30). Waare xibaar bu baax bii dafay tax ñu gën a bàyyi suñu xel ci Nguuru Yàlla, te bañ a fàtte dund gu dul jeex gi ak barke yi muy àndal.

6 Am na lu bare lu ñu war a def bala Yàlla di dindi àddina su bon sii. Am na lu bare lu ñuy won ne dañu war a kontine di sawar ci suñu liggéeyu waare bi, “ di jëfe dooley Yàlla ” maanaam di weeru ci dooley Yàlla (1 Pie. 4:11). Ak ndimbalu Yexowa, dinañu àggali suñu liggéey, ndaxte “ dafay may doole ñi sonn ”. — Isa. 40:29.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager