TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 3/01 p. 8
  • Dimbalil ñeneen ñi ñu teewe ndaje yi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Dimbalil ñeneen ñi ñu teewe ndaje yi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2001
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ban njariñ nga mën a jële ci teewe ndaje Seede Yexowa yi?
    Mën nga dund ci jàmm ba fàww! (Njàngum Biibël bi)
  • Xaaj 8 : Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
    Sasu Nguuru Yàlla — 2005
  • Lan lañu ci bëgg ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2001
Sasu Nguuru Yàlla — 2001
km 3/01 p. 8

Dimbalil ñeneen ñi ñu teewe ndaje yi

1 “ Bépp xarit bu ne ci gox bi [...] te bëgg a teew ci ndaje yi, ñu ngi lay ñaan ak xol bu tàlli, nga def ko. ” Ba yégle boobu génnee ci Le Phare de la Tour de Sion, bu nowàmbar 1880, ba léegi, Seede Yexowa yaa ngiy farlu ci ñaan nit ñi, ñuy dajalook ñoom ngir jàng Biibël bi (Peeñ. 22:17). Wàll wu am a am solo la ci njaamu dëgg gi.

2 Lu am a am solo la, teew ci : Dañuy barkeel, bu ñuy ànd ak mbooloo gëmkat yi. Dañuy gën a xam suñu Yàlla, ju kéemaane ji, Yexowa. Ci biir mbooloo mi, dañuy daje ngir “ Yexowa jàngal ” ñu (Isa. 54:13). Mbootaayam day tëral doxalinu njàngale bu sax, bu sukkandiku ci Biibël bi, ba tax ñu gën a jege Yàlla, teyit da ñuy jox ndimbal lu am njariñ ngir topp “ lépp li Yàlla digle ”. (Jëf. 20:27 ; Lukk 12:42.) Ndaje yi dañuy tàggat ku nekk ci manooreb jàngale Kàddug Yàlla. Pàttali yi ci Mbind yi dañ ñuy dimbali ñu am diggante yu rafet ak ñeneen ñi, akitam Yexowa ci boppam. Di ànd ak ñii bëgg Yàlla day dooleel suñu ngëm. — Room 1:11, 12.

3 Woo ko ci lu àndul ak sikk-sàkka : Li dale njàng mu jëkk mi, ñaanal képp kuy jàng Biibël bi, mu teewe ndaje yi. Xambal itteem ci li ngay bokk ak moom ponk bu la xiirtal ci ndaje mi nga mujj a teewe, akit booy seet ak moom li ñuy waxtaane ci ndaje miy dikk. Nettali ko ni Saalu Nguur gi mel, te na la wóor ne xam na fi mu nekk.

4 Su ab jàngkat teewul ci tàng-tàng ci ndaje yi, wéyal di ko ci woo. Ayu-bés gu nekk, jëlal simili yu néew ngir won ko ni suñu mbootaay di doxe. Jëfandikool téere bu ndaw bi Unis pour faire la volonté de Dieu, ak widewo bi tudd Les Témoins de Jéhovah : un nom, une organisation, ngir mu miinanteek ñun ak suñuy ndaje. Àndal ak yeneen yéenekat ngir mu xamanteek ñoom. Booy ñaan, gërëmal Yexowa ngir mbootaayam te tuddal soxlas jàngkat bi boolook moom.

5 Bul xel ñaar ci dimbali ñi dëgg gi itteel bu yàggul, ñu dajeek ñun. Ba seen cant ngir Yexowa di yokku, loolu dina leen xiir ci topp li ñuy jàng te bokk ci mbootaayu Yàlla, gi bennoo. — 1 Kor. 14:25.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager