Lan lañu ci bëgg ?
1 Lu tax ñuy jàng Biibël bi ak nit ñi ci seen kër ? Jottali xam-xam, taneel dundu nit ñi walla rafetal seen gis-gisu ëllëg, ndax loolu kese moo tax ñu koy def ? Déedéet. Li gën a tax ñu koy def, mooy sàkk ay taalibe Yeesu Krist (Macë 28:19 ; Jëf. 14:21) ! Looloo tax ñi nuy jàngal war a booloo ak mbooloo mi. Ni ñuy jëme kanam ci wàllu ngëm, mu ngi aju ci ni ñuy jàppee Mbootaayu Karceen yi.
2 Ni ñuy fexe ba mu am : Bu ngeen tàmbalee njàng mi rekk nga war a topp di wax ki ngay jàngal, mu fekke ndaje mbooloo mi (Yaw. 10:24, 25). Xamal ko naka la loolu di dëgërale ngëmam, naka la koy dimbalee ci def li Yàlla bëgg, te naka la ndaje yi dee tax mu mën a am àndandoo yu baax yu bëgg màggal ñoom itam Yexowa (Sab. 27:13 ; 32:8 ; 35:18). Boo koy won ne danga bëgg te fonk mbooloo mi ak ndaje yi, dinga tax mu gën a sawar ci fekke ndaje yi.
3 Ñi sog a ñëw ci mbooloo mi, soxla nañu nànd ne mbootaayu Yexowa njaboot gu tasaaroo ci àddina si sépp la. Won leen wideo Les Témoins de Jéhovah : un nom, une organisation ak Toute la communauté de nos frères (ci ãgale). Dimbali leen ndax ñu mën a gis ne Yexowa mu ngi jëfandikoo ay milioŋi nit ñu jébbalu ci moom te tasaaroo ci àddina si sépp ngir def coobareem. Xamalal ñooñu sog a ñëw ci mbooloo mi ne, ñu ngi leen di ñaan ñoom itam ñu jaamu Yàlla. — Isa. 2:2, 3.
4 Nit kiy jàng Biibël bi, bu demee ba nekk taalibe Yeesu, mbégte bu réy lay doon. Mooy li ñu bëgg ! — 3 Ywna. 4.