“ Liggéey nañu suñu gox bi ay yooni yoon, waay ! ”
1 Ndax mas ngaa toog ba xalaat ne, dañoo liggéey a liggéey sa gox bé, desatu ci nit ñu mel ni ay xar ? Booba, xéy na, xalaat nga lii : ‘ Xam naa li nit ñiy def. Lu tax may wéy di dellu ci ñoo xam ne dëgg gi soxalu leen ? ’ Dëgg la, faral nañu di liggéey gox yu bare. Waaye, war nañoo rafetlu loolu, bañ di ko ñaawlu. Lu tax ? Seete ko ci ñeenti mbir yiy topp.
2 Suñuy ñaan nangu nañu : Yeesu nee na : “ Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu. Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam. ” (Lukk 10:2). Diirub ati at, ñaan nañook doole Yexowa ndax ñu gën a am ndimbal. Ci béréb yu bare, am nañu léegi yeneen liggéeykat yi ñu soxla woon, te faral nañu di gën di wër suñu gox ba mu daj. Ndax li Yexowa nangu suñuy ñaan, waru ñoo bégloo ?
3 Góor-góorlu day jur meññeef ju baax : Ci biir gox yi ñu faral di liggéey sax, nit ñaa ngiy nangu xabaaru Nguur gi tey jot ci xam-xamu dëgg gi. Looloo tax war nañoo wéy di dellu te bañ a tàyyi, di séentu taseek nit ñu gën a bare, ñu seen xol jub (Isa. 6:8-11). Ni ko taalibe Yeesu yu jëkk ya doon defe, “ wéyleen di dem ” ci niti gox bi ñu leen sas, di fexe Nguuru Yàlla itteel leen. — Macë 10:6, 7, NW.
4 Ca réewum Portugaal, mbooloo yu bare dañuy wër seen gox ba mu daj ayu-bés gu nekk, te loolu terewu leen a tase, ba tey, ak ñu mel ni ay xar. Menn ci suñuy mbokk mu jigéen, moom, daa soloo xel mu rafet dëgg. Lii la wax : “ Bala maa génn waareji suba su nekk, damay ñaan Yexowa mu dimbali ma ma taseek ku jàng Biibël bi soxal. ” Am bés nag, fagaru woon naa jàng ak liggéeykati kër, gu ñuy toppatoo kawari nit ñi. Waaye ci ginnaaw gi, kenn doŋŋ a ci bëggoon a jàng. Nit kooku lii la wax : “ Mbir mi soxalul ñeneen ñi, waaye man itteel na ma. ” Ci diirub wenn weer, moom ci boppam a ngi doon jiite ñaari njàngum Biibël bi. Tuuti gannaaw loolu, sóob nañu ko, te ba loolu weesoo, sumb na sasu aji-xàll yoon !
5 Liggéey baa ngi dox : Ñu ngiy waare xabaar bu baax, ni rekk Yeesu yégle woon ne lay ame (Macë 24:14). Ci béréb yi ñu nit ñi “ bëggul a déglu ” sax, liggéeyu waare baa ngi leen di artu. Bettu ñu, ñenn ci ñoom bañ a nangu dëgg gi walla sax di ko xeex. Ndaxam, war nañoo artu nit ñu ni mel ci bésub àtte Yexowa, biy dikk ; mooy yoon. — Esek. 2:4, 5 ; 3:7, 8, 19.
6 Ba léegi sottalaguñu : Du ñun ñoo war a dogal kañ la liggéeyu waare bi di sotti. Yexowa xam na tembe kañ lay war a jeex. Xam na ndax am na ci suñu gox, ñu mën a nangu ba tey jii xabaar bu baax bi. Tey, am na ñuy wax ne mbir mi soxalu leen, waaye soppi yu tar ci seen dund — ñàkk seen liggéey, wopp dëgg, deewu ku ñu sopp — mën na leen xiir ci ñu gën a bàyyi xel, bu beneenee. Ñaaw njort, walla doŋŋ li ñu doon ñu jàpp lool ci li ñuy def ngir tal ñoo déglu, tax na ba ñu bare masuñoo dégg, ca dëgg, li ñuy waar. Di fa dellu ay yooni yoon, ànd ak worma, dina leen bàyyiloo xel ci li ñuy wax te tax ñu déglu.
7 Ñi doon ay mag léegi te samp seen njaboot, a ngiy gën a jàppe dund gi ak fulla, di laajte laaj yu Kàddug Yàlla doŋŋ mën a tontu. Ndaw, su am doom, dalal na ñaari Seede ci biir këram, naan : “ Ba ma nekkee xale bu ndaw, masuma woon a nànd lu tax sama yaay doon dàq Seede yi, naan leen mbir mi soxalu ko woon, fekk li ñu bëggoon doŋŋ moo doon waxtaane Biibël bi. Dogaloon naa ci sama xol ne bés bu ma màggee, séy te am sama këru bopp, doon naa laaj Seede Yexowa yi ñu dugg, faramfàcce ma Biibël bi. ” Mooy li mu def, mu jural nag Seede yi ko seetsi woon, mbég dëgg.
8 Ndax mën ngaa yokk sa manoore ? Faral di waare ci suñu gox, li koy tax a niru lu jafe, du saa su ne ci nit ñi ñuy seeti. Lée-lée, jafe-jafe bi ci ñun la. Ndax njort lu ñaaw lañuy demee waare ? Loolu mën naa am lu mu def ci xel mi ñu soloo, akit ci suñu waxin ak suñu xar-kanam. Woneel njort lu rafet ak kanam bu leer. Jéemal doxalin wu bees. Soppil sa wone te jéem koo taneel. Xéy na mën ngaa soppi laaj bi ngay ubbee sa waxtaan mbaa dugg ci waxtaan wi ak jeneen aaya. Laajal yeneen mbokk, góor ak jigéen, li ñu gis ne mooy dox ci waare bi ci gox bi. Waareel ak yéenekat ak way-xàll yoon yu bare, te seetlul li leen di tax a àntu ci seen sasu waare.
9 Liggéeyu waare Nguur gi neex na Yexowa, mi koy barkeel ; li ñu ciy bokk it a ngiy wone suñu mbëggeel ci moom ak suñu moroom (Macë 22:37-39). Kon, nañu def suñu liggéey ba mu sotti, bañ di tàyyi ci liggéey suñu gox saa su ne.