Lu tax ñuy delluwaat ay yooni yoon ci nit ñi
1. Ban laaj lañu mën a laajte ci lu jëm ci suñu liggéeyu waare bi ?
1 Ci gox yu bare, dañuy kontine di dellu ay yooni yoon ci kër nit ñi. Yenn saay sax mu nekk ci kër yoo xam ne, nit ñi nu fa fekkoon dañu nee woon ne li ñuy wax itteelu leen. Lu tax ñuy kontine di dellu ci nit ñu wone ne suñu waxtaan itteelu leen ?
2. Lan moo gën a tax ñuy kontine di waaraate ?
2 Bëgg Yexowa ak nit ñi : Li war a jëkk tax ñu jàpp bu dëgër ci liggéeyu waaraate bi, mooy li ñu bëgg Yexowa. Li nekk ci suñu xol mooy tax ñuy kontine di wax ak nit ñi lu jëm ci suñu Yàlla bu mag bi (Luug 6:45). Mbëggeel bi ñu am ci Yexowa moo ñuy puus ñuy topp li mu ñu sant te it di dimbali suñu moroom yi ñu def loolu ñoom itam. (Léeb. 27:11; 1 Yow. 5:3). Li ñuy kontine di def liggéeyu waare bi, te nangu ci muñ lu nekk, ajuwul ci ni ñu nit ñi di dégloo. Noonu la woon itam ba ñu doon toroxal karceen yi ci jamano bu njëkk ba. “ Daawuñu noppee ” waaraate (Jëf. 5:42). Su ñu nit ñi bañee déglu, du wàññi suñu cawarte, waaye dañuy kontine rekk. Loolu dafay wone fi suñu mbëggeel ci Yexowa tollu ak ni ñu ko bëggee jaamu.
3. Mbëggeel bi ñu am ci nit ñi, naka la ñuy dimbalee ñu kontine di waaraate ?
3 Dañuy kontine it, ndaxte dañu bëgg suñu moroom (Luug 10:27). Yexowa bëggul kenn alku (2 Pie. 3:9). Su fekkee ne sax li ñuy waare ci suñu gox dafa bare lool, ñu ngi gis ba tey ay nit ñu bëgg jaamu Yexowa. Nañu ko seete ci lii : Boo jëlee ñi dëkk ca Guadeloupe ñépp, ci 56 nit yoo ci jël, am na benn Seede Yexowa. Waaye daaw, sóob nañu fa 214 nit. Lu jege 20000 nit teewe nañu bés bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu. Loolu mooy tekki ne ci nit ñi dëkk ci dëkk boobu yépp, 22 yoo ci jël, am na ci kenn ku teewe ndaje boobu.
4. Ci ban fànn la li ñuy fekk ci gox yi di soppeeku ?
4 Liy soppeeku ci gox bi : Ñi nuy dajeel tey ci waaraate bi, du ñoom ñépp lañu fay fekkaat bu ñu fa dellusee. Bu ñu dellusee ci kër bi nga xam ne, ku ñu fa fekkoon dafa bañoon a déglu, keneen mën na ubbi bunt bi te nangu déglu. Kooku mën na nekk ku masul a dégg li ñuy wax. Walla ñu fekk fa ñeneen ñu fa sog a toxusi, te ñu bëgg déglu xibaaru Nguur gi. Xale yi nga xam ne seen wayjur bëgguñu woon a déglu xibaaru Nguur gi dañuy mag, jóge seen kër wayjur, dëkk feneen. Ñu mel noonu mën nañu nangu déglu xibaaru Nguur gi.
5. Lan moo mën a tax nit dem ba mujj nangu déglu ?
5 Nit ñi ñoom itam ci seen wàllu bopp dañuy soppeeku. Ndaw li Pool nekkoon na ku suufeel turu Yàlla, “ di fitnaal ak a di toroxal ñi ko gëm ” (1 Tim. 1:13). Noonu it, ñu bare ci ñiy jaamu Yexowa tey, am na jamano joo xam ne, faalewuñu woon dëgg gi. Xéyna am na ci sax ñu mas a kontar xibaar bu baax bi. Àddina si dafay soppeeku rekk. Loolu mën na tax ñi doon xeex dëgg gi walla ñi ci waxul woon dara dem ba bëgg déglu. Ñeneen ñoom mën nañu dem ba mujj bëgg déglu xibaaru Nguur gi, ndax naqar bi leen dal. Naqar bu mel ni mbokk mu gaañu, walla ñu bañ a amati liggéey, mbaa ñu am poroblemu xaalis, walla ñu feebar.
6. Lu tax ñu war a kontine di waaraate ak cawarte ?
6 Àddina sii, léegi mu jeex, waaye suñu liggéeyu waare ak jàngal nit ñi mu ngi gën a jëm kanam (Isa. 60:22). Moo tax, ñuy kontine di waaraate ak cawarte te di góor góorlu ngir kontine di gise suñu liggéeyu waare bi ni lu rafet. Xéyna nit ki ñu nar a waxal dina nangu déglu. War nañu kontine di wax ! Bu ñu defee ‘ noonu dinañu musal suñu bopp ak ñi ñuy déglu. ’ — 1 Tim. 4:16.