Laalal xolu ki ngay jàngal
1 Laata moo yéeg asamaan, Yeesu ne woon na ay taalibeem ñu “ sàmm ” lépp li mu leen sant (Macë 28:19, 20). Ngir nit ki mën a “ sàmm ” santaane Krist yi, xabaar bi war naa laal xolam (Sab. 119:112). Noo mënee laal xolu nit ki ngay jàngal Biibël bi ?
2 Ñaanal Yexowa mu tette la : Sàkk ay taalibe liggéeyu Yàlla la. Barkeem mooy tax ñu àntu, du suñu manoore bopp (Jëf. 16:14 ; 1 Kor. 3:7). Kon, di sàkku ndimbalu Yexowa ci ñaan bu ñuy jàngal ñeneen dëgg gi, lu am solo dëgg la. — Isa. 50:4.
3 Ràññeel li njàngaan li gëm : Xam li nit ñi gëm ak li tax ñu gëm ko, mën naa ñawal suñu xel ngir xam li ñu war a wax ngir laal seen xol. Lu tax njàngale sàngam neex dëgg njàngaan li ? Lu ko wóor ne lu mat a gëm la ? Xam loolu dina ñu dimbali ñu wax ak ràññaatle. — Jëf. 17:22, 23.
4 Layal lu yenu maanaa te sës ci Mbind yi : Dëgg gi war naa nekk lu xelu njàngaan li mën a nangu (Jëf. 17:24-31). War nañoo tontu lu wér ci li waral suñu yaakaar (1 Pie. 3:15). Waaye, saa su ne def kook mbaaxaay ak muñ.
5 Dooleelal sa njàngale ak i misaal : Misaal du yem rekk ci gën a yombalal njàngaan li li mu war a nànd, waaye it day tax yaramam daw. Day laalaale xelam ak xolam. Yeesu faraloon na di leen jëfandikoo (Mark 4:33, 34). Jarul ñu koy wax, ngir mu am doole, misaal mi ñuy jëfoo war naa ànd ak li ñuy waxtaane, teyit lëkkaleek dundug njàngaan li.
6 Woneel njariñ yi ne ci nangu dëgg gi : Nit ñi bëgg nañu di xam njariñ li ëmbu ci topp li ñuy jàng. Dimbalil ki ngay jàngal mu gis sago kàdduy Pool yi ci 2 Timote 3:14-17.
7 Bul yoqi su amee ñu nanguwul sa njàngale. Am na ñu seen xol dërkiis (Macë 13:15). Waaye, am na it ñuy mujj a gëmi (Jëf. 17:32-34). Yal na say njéem ngir laal xol yi ak xabaar bu baax bi, dimbali ñu gën a bari ñu nangu te “ sàmm ” li Yeesu sant.