Dencal kayit bii
Nañu dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng
Sasu Nguuru Yàlla yi paase wone woon nañu ni ñu mënee dimbali ñi ñuy jàngal Biibël bi ñu topp li ñuy jàng. Def nañu ci xët 3 ba 6, ay ponk yu am solo yu ñu jële ci xaaj yooyu. War nañu ko denc bu baax ñun ñépp ngir topp li ñu ci wax, bu ñuy def njàngum Biibël. Mën nañu ci jël it ponk yi ñuy waxtaane ci ndaje yi ñuy am bala ñuy waare, ngir fàttali leen waaraatekat yi. Wottukatu liggéeyu waare bi mën na ci waxtaan bu demee ci gurupu njàngum téere bi.
Xaaj 1 : Lan mooy njàngum Biibël ?
Def njàngum Biibël mooy tàmm di waxtaan ak nit ci Biibël bi ak benn ci téere yi ñu am ngir jàngale Biibël bi. Bu dee sax waxtaan bi du yàgg, njàngum Biibël la. Kañ lañuy mën a komaase bind ne ñu ngi def njàngum Biibël ? Boo wonee nit naka lañuy jànge Biibël bi, ba pare nga jàngal ko ko ñaari yoon, boo gise ne nit ki bëgg na kontine njàng mi, mën nga bind ne yaa ngi def njàngum Biibël. — km-WO 7/04, xët 1.
Téere yi ñu mën a defe njàngum Biibël
◼ Lan la ñu Yàlla laaj ?
◼ Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex
◼ Adorez le seul vrai Dieu
◼ Bu dee nit ki mënul liir bu baax, mën ngeen jël téere bi tudd Mën nga nekk xaritu Yàlla !
Xaaj 2 : Nañu waajal suñu bopp
Bu ñu bëggee jàngale bu baax, fàww ñu laal xolu nit ñi. Loolu laaj na ñu waajal bu baax suñu bopp te bu ñu koy def ñu xalaat nit ki ñu war a jàngal. — km-WO 8/04, xët 1.
Nii lañuy waajale njàng mi
◼ Dangay seet ni pàcc bi walla njàngale bi tudd, seet xaaj yi ci nekk ak it nataal yi ñu fa def.
◼ Dangay jàng laaj yi te seet tont yi ñu bind. Kàddu yi ëpp solo kese ngay rëdd.
◼ Dangay tànn aaya yi nga bëgg liir ak ki ngay jàngal. Nanga bind ci lu gàtt ci xët boobu lu lay fàttali li nekk ci aaya yi.
◼ Dangay waajal ay laaj ngir bu ngeen jàngee ba pare, nit ki fàttaliku li ëpp solo ci li ngeen jàng. Te loolu warul yàgg.
Nit ku nekk ak ni ñu ko war a jàngale
◼ Booy ñaan Yexowa, boole ci nit ki ak li mu soxla.
◼ Seetal it ndax ci njàngale mi dina am li nga xam ne bala mu nànd ko, walla nangu ko, dina jafe ci moom.
◼ Laajal sa bopp lii : Su ma bëggee mu topp li muy jàng, lan la war a nànd bu baax, walla ci lan la war a góor-góorlu ? Lan laa war a def ngir mën a laal xolam ?
◼ Waajalal benn misaal, walla leneen lu mën a leeral sa wax, walla ay laaj, saa yoo gisee ne dina baax ci njàng mi. Dina tax nit ki xam bu baax li nga ko bëgg jàngal walla li benn aaya bëgg wax.
Xaaj 3 : Nañu jëfandikoo bu baax Mbind yi
Bu ñuy jàngale Biibël bi, dañu bëgg “ sàkk ay taalibe ”. Naka lañu ko mënee def ? Fexe ba nit ki nànd, nangu te topp li Kàddu Yàlla wax (Macë 28:19, 20 ; 1 Tes. 2:13). Kon lépp lu ñuy jàngale, na jóge ci Biibël bi. — km-WO 11/04, xët 4.
Li ngay jàngale, nanga ko jël ci Kàddu Yàlla
◼ Wonal nit ki ni mu mënee wut aaya yi ci Biibëlam.
◼ Nangeen jàng ci Biibël bi aaya yiy wone fi ñu jële li ñu gëm, te waxtaanleen ci.
◼ Laaj ko ay laaj ci aaya yi. Bu ngeen jàngee benn aaya ba pare, laajal nit ki mu wax lu tax ñu def ko ci xise bi. Moom moo ko war a wax, du yow.
◼ Waxal lu yomb nànd. Bul jéem a leeral lépp li nekk ci aaya yi. Waxal rekk luy leeral seen waxtaanu bés bi.
◼ Waxal nit ki ni mu mënee topp li mu jàng. Boo gisee aaya bu baax ci kiy jàng, fexeel ba mu gis ne war na ko topp.
Xaaj 4 : Won ko ni ñuy waajale njàngum Biibël
Kuy jàng Biibël bi, bala mu gaaw a jëm kanam ci wàllu ngëm, am na lu mu war a def. Dafa war a jàng bala ngay ñów li ngeen di waxtaane, rëdd ci suufu tont yi, te mën a wax tont yi ci kàddu boppam. Kon, boo amee njàngum Biibël boo faral a def, woneel nit ki ni ñu koy waajale. Li ci mën a dimbali ñu bare mooy waajal ak ñoom benn njàngale ba mu jeex. — km-WO 12/04, xët 1.
Won ko ni ñuy rëdde tont yi ak ni ñuy binde mbind yu gàtt ci booru xët yi
◼ Jàngal ak moom laaj yi ñu bind ci téere bi, te won ko ni ñuy seete tont yi ci xise yi.
◼ Won ko ci sa téere bopp ni nga rëdde kàddu yi ëpp solo kese ngir tontu.
◼ Aaya bu nekk, am na ci xise bi loo xam ne ci aaya boobu lañu ko jële. Fexeel ba ki ngay jàngal gis loolu. Wax ko ne am na lu mu mën a bind ci wetu xise yi, te won ko li mu mën a def ngir loolu bañ a bare.
Na njëkk xool ci lan la waxtaan bi di nekk te bu ko waajalee ba pare, na seetaat li mu jàng
◼ Waxal nit ki ne buy waajal waxtaan bi, na njëkk xool yaxu waxtaan bi, turu xaaj bu nekk, ak foto walla nataal yi fa nekk.
◼ Wax ko it ne, bu waajalee njàngam ba pare, na jéem a fàttaliku ponk yi ci ëpp solo.
Xaaj 5 : Xamal ñaata xise ngeen di jàng
Bu ñuy def njàngum Biibël, dañu war a xam ñaata xise lañu mën a jàng. Loolu dina aju ci li ñu mën ak li ñu nekke, nit ki ak ñun ci suñu bopp. — km-WO 1/05, xët 1.
Ngëmam war na dëgër
◼ Buñu gaawantu ba nit ki bañ a nànd bu baax li ñu koy jàngal.
◼ Jëlal jot bu doy ngir nit ki nànd li muy jàng te gëm ko.
◼ Fexeel ba am jot bu doy ngir seet aaya yi nga xam ne fa lañu jële li ñuy jàngale.
Bul bàyyi waxtaan bi dem fu sore
◼ Bu nit ki amee lu bare lu mu la bëgg a wax ci moom walla ci li muy def, nee ko dingeen ci waxtaan bu ngeen jàngee ba pare.
◼ Bu ñuy def njàngum Biibël, suñu wax warul bare. Yenn saay dinga wax ponk bu amul solo noonu walla nettali dara ngir waxtaan bi gën a neex. Waaye loolu warul bare te warul yéexal njàng mi. Am na li nit ñi war a njëkk xam ci Biibël bi. Te dañu ci war a am xam-xam bu wér. Kon, bëgguñu suñu wax ju bare yàqal leen ci loolu.
Xaaj 6 : Bu la nit ki laajee dara
Boo amee njàngum Biibël, nanga topp njàngale yi ni ñuy toppante. Loolu moo gën nga nekk di waxtaan ci lépp lu mu lay laaj. Loolu dina ko may li mu soxla ci wàllu ngëm ngir xam bu baax dëgg gi. Te digganteem ak Yàlla dafay gën a rattax rekk. — km-WO 2/05, xët 6.
Xamal bu baax li nga ko war a tontu
◼ Su laaj bi àndee ak li ngeen di waxtaan, mën nga ko tontu ci saa si.
◼ Mën na am laaj bi bañ a bokk dara ak li ngeen di waxtaan. Walla nga war a gëstu bala di ci mën a tontu. Laaj yooyu, mën ngeen xaar ba beneen yoon bala ngeen ciy waxtaan. Boo bindee laaj yooyu, xéyna dina la dimbali.
◼ Mën nga ko jàngal dara, waaye gis nga ne àndu ci noonu. Li nga mën a def mooy, seet yeneen téere yuy gën a xóotal waxtaan boobu.
◼ Su ngeen ko jàngee te ba tey loolu doyu ko, nanga bàyyi waxtaan boobu ba beneen yoon te kontine seen njàngum Biibël.
Nañu xam fan la suñu wax war a yem
◼ Boo xamul tont laaj bi, bul wax sa xalaatu bopp.
◼ Nanga ko dimbali ndànk-ndànk ba mu xam ni mu mënee gëstu ci suñu yeneen téere yi ngir gisal boppam tontu laaj yi muy laaj.
Xaaj 7 : Ñaan Yàlla bu ñuy def njàngum Biibël
Kuy jàng Biibël bi, bala mu jëm kanam ci wàllu ngëm, fàww Yexowa barkeel ko. Kon, tàmbali te àggale seen njàngum Biibël ak ñaan, lu baax la. — km-WO 3/05, xët 4.
Kañ nga mën a komaase wax lu jëm ci ñaan te naka nga ko mënee def
◼ Su nit ki nekkee ku mbirum diine neex, dinga ko mën a def ci seen njàng mu njëkk mi.
◼ Ak ñeneen, yaa war a seet kañ ngay mën a komaase ñaan ci njàngum Biibël bi.
◼ Mën nga won nit ki, ci Sabuur 25:4, 5 ak ci 1 Yowanna 5:14, lu tax ñu war a ñaan Yàlla bala ñuy jàng Biibël bi.
◼ Mën nga ko won it ci Yowanna 15:16 lu tax ñu war a jaarale suñuy ñaan ci Yeesu Krist.
Li nga mën a wax ci ñaan bi
◼ Ndegam Yexowa mooy Kiy jàngale, nanga ko màggal ci sa ñaan ndax loolu.
◼ Booleel ci ñaan bi luy wone ne danga bëgg ki ngay jàngal.
◼ Waxal ci ñaan bi ni nga fonke mbootaay bi Yexowa di jëfandikoo.
◼ Ñaanal Yexowa mu barkeel li nit ki di def ngir topp li muy jàng.
Xaaj 8 : Nañu jëmale nit ñi ci mbootaayu Yàlla
Bu ñuy jàngale Biibël bi, li ñu bëgg mooy nit ñi gëm li nekk ci Biibël bi. Bëgg nañu it ñu bokk ci mbooloo karceen yi. Nanga jël tuuti minit ngir waxtaan lu jëm ci mbootaayu Yexowa. — km-WO 4/05, xët 8.
Ndaje yi ñu am ci mbooloo mi :
◼ Wax ko ni ndaje bu nekk di deme. Bés boo defee njàngum Biibël bu njëkk bi, nanga ko komaasee woo ci suñuy ndaje.
◼ Nanga waxtaan ak moom ci ay ponk yu am solo yi amoon ci ndaje yi nga teewe woon bu yàggul.
◼ Wax ko lu jëm ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu, ndaje yu mag ak yu gën a mag yi, ak ndaje yi ñuy am bu wottukat biy wër bi di ñu seetsi. Te fexeel ba mu bëgg ci teew moom it.
◼ Won ko ci suñuy téere ay foto yuy wone ni ndaje yi di deme.
◼ Wax ko mu jàng téere bi tudd Les Témoins de Jéhovah : Qui sont-ils ? Quelles sont leurs croyances ?
Fexeel ba mu seetaan wideo yi ngir mu fonk mbootaay bi :
◼ Les Témoins de Jéhovah — un nom, une organisation
◼ Toute la communauté des frères
◼ Unis grâce à l’enseignement divin
◼ Jusqu’aux extrémités de la terre
Xaaj 9 : Woneel ki ngay jàngal ni ñu mën a waaree saa yu ñu ci amee bunt
Ñiy jàng Biibël bi, bu ñu demee ba gëm li ñu jàng, dinañu ko bëgg a jottali seeni moroom. — km-WO 5/05, xët 1.
Nañu leen xiir ci waar nit ñi :
◼ Ndax am na xarit walla mbokk yu mu mën a woo ngir ñu bokk ci njàng mi ?
◼ Ci ñi mu bokkal liggéey, ñi mu bokkal lekkool walla ñeneen ñi mu xam, ndax am na ku ci bëgg a déglu xibaar bu baax bi ?
Won ko ni mu mënee waxtaan ak nit ci li mu gëm :
◼ Booy jàng Biibël bi ak moom, lée-lée mën nga taxaw te laaj ko lii : “ Li nga jàng nii, boo naree wax sa mbokk lu tax nga gëm ko, ban aaya nga koy won ? ”
◼ Dimbali ko mu weg nit ñi te baax ak ñoom, buy wax ci Yàlla ak ci li mu bëgg def.
◼ Bu nit ki bëggee xamal xaritam yi walla mbokkam yi lu tax Seede Yexowa yi gëm li ñu gëm walla def li ñuy def, mën na jëfandikoo téere bi tudd Les Témoins de Jéhovah : Qui sont-ils ? Quelles sont leurs croyances ?
Xaaj 10 : Nañu leen jàngal ni ñuy waaraatee këroo-kër
Bu magi mbooloo mi waxee ne nit ki mat na waaraatekat bu ñu sóobagul, ci lay mën a komaasee ànd ak mbooloo mi ci waaraate bi. — km-WO 6/05, xët 1.
Nangeen waajal yéen ñaar waaraate bi
◼ Wonal ki ngay jàngal fu mu mënee gis li mu mën a wax buy waaraate.
◼ Dimbali ko mu seet foofu waxtaan bu yomb bu mën a neex ñi nekk ci seen goxu mbooloo.
◼ Nee ko mu jëfandikoo Biibël bi ci waaraate bi.
◼ Nangeen waajal waaraate bi, di def mel ni yéen a ngi waaraate. Wax ko ne li nit ñi di def walla wax boo leen di waar, bare na. Waaye ba tey, na wone yar ak teggin ci lépp li muy def, te won ko ni mu ko mënee def.
Bu ngeen di waaraate yéen ñaar
◼ Bàyyi ko mu seet ni ngay toppe li ngeen waajaloon yéen ñaar.
◼ Yow mii xam nit ki ak li mu mën, yaa war a seet li mu mën a def ci waaraate bi. Yenn saay liy gën mooy, waaraatekat bu bees bi bokk rekk ci waxtaan bi.
◼ Nañu dimbali waaraatekat yu bees yi ñu defar porogaraam ngir faral di waaraate.
Xaaj 11 : Nañu leen won ni ñuy delloo seeti nit ñi
Ci waxtaan bu njëkk bi lañu war a waajal li ñuy waxtaane beneen yoon bu ñu dellusee. Waxal kiy jàng Biibël bi ne dafa war a toppatoo bu baax nit ki muy waxtaanal. Won ko ndànk-ndànk li mu mën a def ngir nit ki wax li mu xalaat. Won ko it ni mu waree déglu nit ki ak li mu mën a seet ci nit ki ngir gën koo xam. — km-WO 7/05, xët 1.
Waajalleen li ngeen war a wax bu ngeen di dellu seeti nit
◼ Seetaatleen li ngeen waxtaane woon bi ngeen fa njëkkee dem. Te wonal kiy jàng Biibël bi ni mu mënee seet waxtaan bu mën a neex nit ki.
◼ Waajalleen li mu nar a wax nit ki. Booleleen ci ñaar yii : benn aaya ak benn xise ci benn téere.
◼ Nangeen waajal it benn laaj bu ngeen mën a laaj nit ki bu ngeen di jeexal waxtaan bi.
Bala ñuy dellu seeti nit, warul yàgg
◼ Waxal kiy jàng Biibël bi mu bañ a xaar lu yàgg bala muy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex.
◼ Lée-lée ñu war a jaar këru nit ñi ay yooni-yoon bala ñu leen di mën a gisaat. Wonal ki ngay jàngal lu tax ba tey, fàww ñu def loolu.
◼ Wax ko li mu mën a wax nit ki ngir jàpp ak moom bés ngir kontine waxtaan bi. Won ko it lu tax dellu seeti nit ki ci bés bi ñu jàpp am solo lool.
Xaaj 12 : Nañu leen won ni ñuy komaasee te kontinee njàngum Biibël
Nanga roy ci Yeesu ngir nekk royukaay bu baax ci fasoŋ bi ngay waare. Loolu lu am solo la. Kiy jàng Biibël bi, bu xoolee ni ngay waaree, dina xam li ñu bëgg bu ñuy dellu seeti ñi suñu waxtaan neex, maanaam komaase ay njàngum Biibël. — km-WO 8/05, xët 1.
Bu ñuy laaj kenn ndax bëgg na ñu jàngal ko Biibël bi
◼ Waxal kiy jàng Biibël bi ne soxlawul ñu wax, wax bu dul jeex ngir xamal nit ki ni njàngum Biibël di deme.
◼ Ci lu bare, liy gën mooy ñu won ko ni njàngum Biibël di deme. Mën nañu jël téere fu ñuy jàngale Biibël bi, tànn benn walla ñaari xise, te won ko foofu ni ñuy jàngalee nit ñi.
◼ Am na Sasu Nguuru Yàlla yuy wone ni ñu mënee tàmbali njàngum Biibël. Tànnleen ci benn, te toppleen li ci nekk mel ni yéen a ngi ci waaraate bi. — km-WO 1/02 xët 4.
Nañu won waaraatekat yu bees yi ni ñuy jàngalee Kàddu Yàlla
◼ Nañu xiir ñiy jàng Biibël bi ci bokk ci lekkoolu sasu Nguuru Yàlla.
◼ Seetleen li ngeen mën a def ngir waaraatekat bu bees bi ànd ak kuy dem defi njàngum Biibël. Nañu ko may mu bokk tuuti ci njàngale mi.