Nañu yemale waxtu yi ñuy féexal suñu xol, fi ñu war a yem
1 Ci jamano ju metti jii, ñun ñépp a soxla soppi, yenn saay, li ñu tàmm a def bés bu nekk. Kon, di féexal tuuti suñu xol, lu baax la. Waaye nag, féexal sa xol, fo, walla xaritoo, bu ëppee, mën na tax nit gën di wàññi waxtu yi mu doon jagleel li mu war a def ci wàllu ngëm. Dañu war a yemale waxtu yi ñuy féexal suñu xol fi ñu war a yem (Macë 5:3). Loolu, naka lañu ko mënee def ? Bu ñu toppee xelal bi nekk ci Efes 5:15-17.
2 Nañu dogal fi ñu war a yem : Pool bindoon na ne karceen dafa war a ‘ sàmm bu baax ’ fasoŋ bi ànd ak xel bi muy dunde. Bu ñu bëggee waxtu yi ñuy féexal suñu xol bañ a weesu li ñu soxla dëgg, waruñu ëppal te dañu war a mën a teye suñu bopp. Xalaat bu baax ci ni ñuy jëfandikoo waxtu yi ñu dul liggéey, lu baax la. Féexal suñu xol dafa war a nekk lu ñu amal njariñ, waaye warul nekk loo xam ne bu ñu ci jógee, dañuy yëg ne yàq nañu suñu jot, walla dañu tas. Bu ñu yëgee ne li ñu def, yokkalu ñu dara, seddalul suñu xol, walla suñu xel di ñu wax ne li ñu def am na lu ci baaxul, loolu dafay wone ne am na li ñu war a soppi ci ni ñuy jëfandikoo suñu jot.
3 Buñu ëppal : Pool dafa ñu xelal ñu ‘ sàkku jot gi war ’ ngir li ëpp solo ci suñu dund, te ñu bañ a ‘ ñàkk bopp ’. Karceen yi jébbalu ci Yàlla, mënuñu nangu féexal seen xol nekk li ñuy jiital ci seen dund. Dëgg la, noppalu ak féexal sa xol mën na tax nga amaat doole ci sa yaram, waaye doole ji Yàlla di jëfe, mooy li nuy may kàttan ci wàllu ngëm (Isa. 40:29-31). Bu ñuy def li Nguuru Yàlla laaj, maanaam jàng Biibël bi, fekke ndajey mbooloo mi, ak bokk ci liggéeyu tool bi, ci lañuy jot ci xelu Yàlla — du bu ñuy féexal suñu xol.
4 Nañu tànn li war a jiitu : Pool santoon na karceen yi ñu ‘ wéy di gën a xam liy coobare Yexowa ’. Yeesu jàngale woon na ne Nguuru Yàlla moo war a jiitu te ëpp solo ci lépp lu ñuy def ci suñu dund (Macë 6:33). Lu am-a-am solo mooy ñu jëkk a def li mën a tax suñu dund ànd ak suñu njébbalu ci Yexowa. Bu boobaa, waxtu yi ñuy féexal suñu xol dinañu mën a yem fu ñu war a yem. Bu ñu defee loolu, dinañu jariñoo bu baax waxtu yooyu te day gën a neex ci ñun. — Daj. 5:12.