Ni ñuy wone suñuy téere ci gox fu nit ñi bokkul làkk
1 Ci gox yu bare, ñi nuy dajeel ci waaraate bi duñu bokk làkk. Nit ñooñu, lu ci bare, bu ñu leen làkkee làkk bi ñu nàmp, dañuy gën a gaaw a jàng dëgg gi, te ci la suñu waxtaan di gën a leer. Lu ñu mën a def ngir indil leen ay téere ci làkk bi ñu gën a dégg ?
2 Kañ lañuy wone suñu téere yi : Yenn saay, ñaari mbooloo yu bokkul làkk, walla lu ko ëpp, dañuy bokk gox bi ñuy waare. Ci gox boobu, mbooloo mu nekk war na mën a waar bu baax képp kuy làkk làkku mbooloo mi. Kon kuréli magi mbooloo yooyu dinañu seet ak wottukati liggéeyu waare bi ni ñu koy defe. Bu ñuy waare këroo-kër, waaraatekat yi tàmmuñu wone téere yi ñu bind ci làkku yeneen mbooloo yi. Waaye, bu ñuy waare saa yu ñu ci amee bunt, walla feneen fu dul ci biir kër yi, mën nañu wone téere yi ñu bind ci làkku nit ki ñuy waxal. — Seetleen Le ministère du Royaume d’octobre 1990, Réponses à vos questions.
3 Kañ lañuy denc ci mbooloo mi ay téere yu ñu bind ci beneen làkk : Gox mën na bare nit ñuy làkk benn làkk te fekk amu fa mbooloo bu koy làkk. Bu booba lu ñu war a def ? Bu loolu amee, mbooloo mi mën na denc tuuti ci téere yi am ci làkk boobu. Téere yu mel ni kayit yu ndaw yi, téere Laaj, téere Xaritu Yàlla, ak téere Xam-xam. Saa yu waaraatekat dajee ak ku mën a jàng làkk boobu, mën na ko won téere yooyu.
4 Ni ñuy ame téere yooyu : Nit mën na bëgg jàng suñuy téere ci benn làkk, fekk mbooloo mi amul téere yooyu. Ki daje ak moom naka lay ame téere yooyu ? Na laaj kiy toppatoo téere yi ci mbooloo mi yan téere la mbootaay bi defar ci làkk boobu. Bu mbooloo mi di laaj téere yi mu soxla, mën nañu ci boole téere yi waaraatekat boobu soxla.
5 Nañu jëfandikoo bu baax suñu téere yi ngir dimbali “ ñépp ”, ak làkk bu ñu mënta dégg. Di leen dimbali ngir ñu ‘ xam dëgg gi, te mucc ’. — 1 Tim. 2:3, 4.
[Laaj yi]
1. Lu tax mbooloo yu bare soxla ay téere ci làkk yu wuute ?
2. Mbooloo yu bokk gox te fekk bokkuñu làkk, ci lan lañu war a déggoo ?
3. Kañ la mbooloo mën a denc ay téere ci yeneen làkk ?
4. Bu mbooloo mi amul téere bu ñu bind ci benn làkk, naka lañu koy ame ?
5. Lu tax ñuy fexe ba nit ñi mën a jot ci suñu téere yi ?