Nañu dimbali suñuy moroom ñu màggal Yexowa
1 Am na xibaar bu am solo lool bu ñuy yégal waa àddina si sépp : “ Ragalleen Yàlla te jox ko ndam li, ndaxte waxtuw àtteem jot na. Jaamuleen ki sàkk asamaan ak suuf, géej gi ak bëti ndox yi. ” (Peeñ. 14:6, 7). Bokk ci ñiy yégal xibaar boobu, lu réy la. Ku bëgg ragal te jaamu Yexowa, lan la war a xam ci moom ?
2 Turam : Tey, yàlla yu dul dëgg yi bare nañu. Nit ñi war nañu xam turu Yàlla dëgg ji, ngir mën koo ràññe (5 Mu. 4:35 ; 1 Kor. 8:5, 6). Yàlla dafa am tur bu mag : Yexowa. Tur boobu bind nañu ko ci Biibël bi lu ëpp 7 000 yoon. Dañu war a xam kañ lañu war a xamle tur boobu, waaye waru ñu ko nëbb mukk, walla tere suñu bopp di ko tudd. Yàlla dafa bëgg nit ñépp xam turam. — Sab. 83:18.
3 Jikkoom yi : Nit ñi war nañu xam ban fasoŋu Yàlla la Yexowa nekk ngir mën koo màggal. Lii lañu bëgg nit ñi xam bu baax : Mbëggeelam bu doy kéemaan, xam-xamam bu dul jeex, njubteem bu mat sëkk, kàttanam bu sut bépp kàttan, yërmandeem, laabiiram, ak yeneen jikkoom yu rafet-a-rafet (2 Mu. 34:6, 7). Te it, nit ñi war nañu jàng a ragal Yàlla, jàng koo jaamu, te nangu ne bu ñu bëggee dund war nañu koo neex. — Sab. 89:7.
4 Jege Yàlla : Bés bu Yàlla di àtte nit ñi mu ngi ñów. Ku ci bëgg mucc, war na gëm Yexowa te woo ko ci turam (Room 10:13, 14 ; 2 Tes. 1:8). Loolu laaj na lu ëpp xam turu Yàlla ak jikkoom yi kese. War nañu dimbali nit ñi ndax ku ci nekk am diggante bu rattax ak Yexowa te gëm ko bu baax-a-baax (Léeb. 3:5, 6). Bu ñuy topp li ñu jàng, di ñaan Yàlla ñaan yu jóge seen xol, di gis it li leen Yexowa di defal, seen ngëm day gën di dëgër, te dinañu gën a jege Yexowa. — Sab. 34:8.
5 Nañu sawar ci xamal nit ñi turu Yàlla, te dimbali leen ñu gëm ko te ragal ko. Dinañu mën a dimbali nit ñi ñu gën a bare ñu xam Yexowa te màggal ko moom mii nekk “ Yàlla juy musal ”. — Sab. 25:5.