Nañu màggal Yexowa
1 Sabuur nee na : “ Yéen mbooloo yi nekk ci kow suuf si sépp, woyalleen Yexowa. [...] Màggalleen ko ci diggu xeet yi. Waxleen ñi nekk ci réew yépp lu réy te rafet li mu def. ” Waaw, bu ñuy xalaat li ñu Yexowa defal démb, li mu ñuy defal tey, ak li mu ñu bëgg defal ëllëg, li ñuy bëgg def mooy màggal ko. — Sab. 96:1, 3.
2 Ci waaraate bi : Seede Yexowa yi am nañu lu réy : Turu Yàlla ci boppam lañuy wuyoo, te tur boobu lañuy màggal ci àddina si sépp (Mal. 1:11). Ndax gis ngeen ni ñu wuutee ak kilifa diine yiy wuyoo turu karceen fekk toppuñu li Yeesu wax ? Ñoom, bi ñu doon tekki Biibël bi ci yenn làkk, dañu dindi turu Yàlla. Loolu ñeme Yàlla dëgg la ! Xamal nit ñi turu Yàlla, lu jamp la tey ndaxte ku bëgg mucc ci metit bu réy bii di ñów, fàww mu gëm te woo Boroom bi ci turam (Room 10:13-15). Te it bala jàmm mën a am fépp fu mbindeefu Yàlla yi nekk, boole ci jàmm diggante doom-Aadama yi, fàww turu Yàlla sell. Waaw, ci dëgg, turu Yàlla bokk na ci lépp li Yàlla di def.
3 “ Yexowa ku mag la te dañu ko war a màggal bu baax. ” Waaye bala nit ñi mën a “ màggal Yexowa ndax tur bi mu am ”, fàww ñu xam dëgg gi ci moom (Sab. 96:4, 8). Waaye am na ñuy wax ne Yàlla amul (Sab. 14:1). Am na ñeneen ñuy wax ne amul kàttan walla ñu ne moom faalewul doom-Aadama yi. Bu ñuy dimbali ñi yore xol bu jub ñu xam dëgg gi ci Ki ñu sàkk, ñu xam li mu bëgg def ak jikkoom yu rafet yi, dañuy màggal Yexowa.
4 Ci li ñuy def : Bu ñu toppee lu baax li ñu Yexowa sant, loolu dafa koy màggal. Nit ñi dinañu gis suñu jëf yu rafet yi (1 Pie. 2:12). Bu ñuy gis lu set te jekk li ñuy sol, mën nañu wax lu rafet ci ñun. Te dinañu ci mën a jaar ba wax ak ñoom ci njariñ bi nekk ci topp li ñu Yàlla wax ci Kàddoom (1 Tim. 2:9, 10). Dëgg-dëgg, dañuy kontaan lool bu nit ñi ‘ gisee suñuy jëf yu rafet te màggal suñu baay bi ci kaw ’ ! — Macë 5:16.
5 Yàlla ji ñuy jaamu ku baax te mag la. Nañu ko màggal bés bu nekk ci suñuy wax ak suñuy jëf. Noonu lañuy defe li ñu wax fii : “ Woyalleen Yexowa, màggalleen turam. Bés bu nekk, waxleen xibaar bu baax bi jëm ci li muy def ngir ñu mucc. ” — Sab. 96:2.