Tegtal yu bees ngir kàggu yi nekk ci Saali Nguur gi
Ay ati at ci ginnaaw ba léegi, mbooloo yi nekk ci àddina si sépp dañuy jëfandikoo kàggu (bibliothèque) gi nekk ci seen Saalu Nguur. Kàggu gu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla lañu koy woowe. Bu njëkk dañu jàppoon ne mbooloo mu nekk dafa war a am kàggu gi mu moomal boppam. Waaye, tey, am na ay mbooloo yu bare yuy bokk benn Saalu Nguur. Léeg-léeg, am na bu ciy làkk làkku bitim réew. Li gën mooy, ci Saalu Nguur bu nekk, ñu def benn kàggu gu baax ngir mbooloo yu bokk benn làkk, làkk bu nekk ak sa kàggu. Am na ay Saalu Nguur yu mag yu yore ñaari béréb, mbaa lu ko ëpp, fu ñu mënee a am ay ndaje. Ci béréb bu nekk dafa war a am benn kàggu ci làkku mbooloo mi fay daje. Su dee ay mbooloo la, làkk bu nekk moo war a am kàggoom.
Yaakaar nañu ne loolu dina tax Saalu Nguur yi gën a yaatu, te dina wàññi xaalis bi ñuy def ci kàggu yi. Li ëpp solo mooy, bu ñu boolee kàggu yi ngir ñaari mbooloo walla sax lu ko ëpp, dina tax kàggu yi gën a baax. Bu ñu leen boolee, xéyna dinga gis ay téere yoo xam ne ñaar ngeen ci am. Kon jëlleen ci benn, denc beneen bi. Bu ëllëgee, bu ñu tabaxee Saalu Nguur gu bees, dinañu ko mën a jël. Bu fekkee ne Saalu Nguur gi dafa am ordinatër ak CD-ROM Watchtower Library, xéyna dina am ñu mu mën a jariñ bu baax.
Ci Saalu Nguur gu nekk, benn mbokk mu góor moo war a toppatoo kàggu gi. Li gën sax mooy mu nekk wottukatu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi. Dafa war a yokk ndànk-ndànk téere yi war a am ci kàggu gi. War na bind ci téere bu nekk, luy wone bu baax ne kàggu gi nekk ci Saalu Nguur gi moo ko moom. At mu nekk, war na seet ndax téere yépp a ngi ci te benn yàquwu ci. War na ko def lu mu tuuti tuuti, benn yoon at mu nekk. Téere yi nekk ci kàggu gi, waruñu leen a génne ci biti Saalu Nguur gi.
Waa mbooloo yépp, gis nañu ne kàggu gi nekk ci Saalu Nguur gi, dafa am njariñ lool. Nañu ko toppatoo bu baax ñun ñépp, te di ko jëfandikoo ngir wut “ xam-xamu Yàlla ”. Noonu lañuy wonee ne fonk nañu ko bu baax. — Léeb. 2:5.