Nanga waar nit ñi saa yoo ci amee bunt ngir màggal Yexowa
1 Ñiy jaamu Yexowa dañu koy jéem a màggal bés bu nekk (Sab. 96:2, 3 ; Yaw. 13:15). Mën nañu ko def bu ñuy waare saa yu ñu ci amee bunt. Ñu bare tey noonu lañu xame xibaaru Nguur gi ba mën a jaamu Yexowa.
2 Ci fasoŋu waaraate boobu, boo waaree benn nit, mën na tax ñeneen dégg xibaaru Nguur gi. Seetal waxtaan bi Yeesu amoon ak jigéenu waa Samari ci teenu Yanxóoba. Waxtaan boobu tax na ñeneen ñu bare bëgg xam xibaar bu baax bi (Ywna. 4:6-30, 39-42). Seetal itam Pool ak Silas bi ñu leen tëjoon kaso ci Filipp. Waxtaan nañu ak boroom kaso bi ci dëgg gi ba moom ak waa këram yépp gëm ko. — Jëf. 16:25-34.
3 Fu ñu ko mën a defe : Kañ nga mënee bokk ci fasoŋu waaraate boobu, maanaam waar nit saa yoo ci amee bunt ? Am na ñu koy def bu ñuy dem màrse, bu ñu jëlee kaar walla taksi, walla bu ñuy nekk di xaar doktoor bi. Am na ñu koy def ci waxtu añ fu ñuy liggéeye walla ca lekkool. Mën nga def sax lu gën a yomb loolu yépp. Mën nga jël benn ci suñuy téere te def ko fu ko ñépp mënee gis. Mën na tax nit ñi bëgg xam li ñu gëm. — 1 Pie. 3:15.
4 Ni nga mënee ubbi waxtaan bi : Am na benn xale bu jigéen bu amoon 7 at. Ku bare kersa la woon. Mu dégg ci suñu benn ndaje lu tax ñépp a war a bokk ci liggéeyu waare bi. Benn bés ginnaaw loolu, dafa waroon a ànd ak yaayam bu amoon lu muy jëndi. Bala ñuy dem, dafa dugal ñaari téere yu ndaw ci saagam. Bi yaayam doon fey li mu jëndoon, xale bi daldi jël benn téere, won ko benn jigéen. Jigéen jooju kontaan te nangu ko. Bi ñu laajee xale boobu bare woon kersa fan la ame fit boobu, dafa ne : “ Li laa wax sama bopp : Pareel ! Pare nga ? Ayca ! Ma daldi dem ! ”
5 Ku bëgg waare saa yoo ci amee bunt, war nga mel ni xale bu jigéen boobu. Lu ñu ci mën a dimbali ? Ñaanal Yàlla mu may la fitu wax (1 Tes. 2:2). Waajalal benn laaj walla benn xalaat bu mën a itteel nit ñi. Ubbil sa waxtaan ak loolu. Te nanga xam ne Yexowa dina barkeel li ngay def. — Lukk 12:11, 12.
6 Bés bu nekk, ñu ngi tase ak ay nit. Bu ñu leen waaree saa yu ñu ci amee bunt, dinañu màggal Yexowa te bég. Dina tax it ay nit mën a aw ci yoonu dund gu dul jeex.