TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/03 p. 3-4
  • Nañu waaraate bu baax te sawar ci

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu waaraate bu baax te sawar ci
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nanga waar nit ñi saa yoo ci amee bunt ngir màggal Yexowa
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Nañu kontine di xaar Yexowa
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 6/03 p. 3-4

Nañu waaraate bu baax te sawar ci

 Ndaw li Pool dafa sawaroon a waare xibaar bu baax bi. Fu mu mënta nekk, dafa doon waaraate bu baax, na Yeesu ak yeneen jaamukatu Yàlla yu ko doon topp. Bi mu nekkoon sax ci kër gi ñu ko tëjoon, dafa doon “ àggali ñépp ñi koy seetsi. Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Krist ak fit wu dëgër ”. — Jëf. 28:​16-31.

2 Ñun itam nañu sawar ci waaraate bi, di waaraate bu baax fu ñu mënta nekk : bu ñuy tukki, bu ñuy jóge ci suñu ndaje yu mag yi ak bu ñu nekkee ci jamano noppalu. — Jëf. 28:23 ; Sab. 145:​10-13.

3 Waaraate saa yu ñu ci amee bunt mooy lan ? Fasoŋu waaraate boobu, nekkul loo xam ne jékki-jékki rekk mu am. Te it du lu ñu waajalul walla lu amul solo. Suñu liggéeyu waare melul noonu. Màggal Yàlla ci waaraate bi, dafa amoon solo lool ci Pool. Noonu la mel it ci ñun. Kon bu ñuy tukki, fu ñu tollu nañu seet rekk li ñu mën a def ba waaraate. Waaye nag, waaraate boobu xaw na wuute ak waaraate kër-oo-kër. Dafa war a mel ni ñaari nit ñu nekk di waxtaan rekk. Loolu mën na tax nit ñi déglu la bu baax.

4 Nañu waajal suñu bopp : Pool, dañu ko tëjoon ca benn kër ca Room. Kon, dafa waroon a seet lu mu mën a def ngir waaraate. Mu woo njiitu Yawut yi ca kër gu mu nekkoon (Jëf. 28:17). Dëgg la amoon na benn mbooloo karceen ca Room. Waaye Pool dafa gis ne Yawut ya fa nekkoon xamuñu woon lu bare ci ngëmu karceen yi. Te li ñu xamoon, dañu ko déggoon nii rekk (Jëf. 28:22 ; Room 1:⁠7). Mu daldi leen waar bu baax-a-baax ci Yeesu Krist ak ci Nguuru Yàlla.

5 Am na ay nit ñoo xam ne barewul li ñu xam ci seede Yexowa yi. Boo naree tukki, balaa ngay dem, xalaatal loo mën a def boo dajee ak ñu mel noonu. Xéyna xamuñu ne dañuy jàngal nit ñi Biibël bi te duñu ci fey dara. Booy tukki, bare na fi nga mën a daje ak ay nit : bu ngeen di tukki te ngeen nekk ci yoon, walla ngeen taxaw ci yoon bi ngir noppalu tuuti, bu ngeen di jënd esaas, bu ngeen di jënd dara, bu ngeen di lekk ci restoraŋ, bu ngeen nekkee ci kaar walla taksi ak yeneen yu mel noonu. Deel seetlu ñi nga mën a waxal, te fexe ba waar leen. Balaa ngay dem, seetal loo leen mën a wax ngir ubbi waxtaan bi, te naka nga mënee am ak ñoom waxtaan bu gàtt. Bul xaar ba ngay tukki sog a jéem a waaraate saa yoo ci amee bunt. Boo tàmmee loolu, waaraate boobu dina gën a yomb ci yow. Waxal ak say dëkkandoo, say mbokk, ñi nga bokkal liggéey, ak ñeneen ñi nga xam.

6 Booy waaraate saa yoo ci amee bunt, dinga soxla ay téere. Yan téere ? Mën nga wone kayit bi tudd Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? Woneel juróomi xise yu njëkk yi. Dañu fay wone lu tax ñu war a jàng Biibël bi. Ci xët bu mujj bi, am na benn wërale ngir ñi bëgg am benn njàngum Biibël bi. Wone ko. Boo gisee ku bëgg waxtaan ak yow, won ko téere Laaj bi. Boo bëggee waar nit ñiy làkk làkk boo déggul, jëlal it téere bi tudd Une bonne nouvelle pour toutes les nations. Ci xët 2 dinga gis ni ñu koy jëfandikoo. Booy tukki ci oto, xéyna dinga mën a yóbbaale yeneen téere yu mën a dimbali nit ñi suñu waxtaan neex bu baax-a-baax.

7 Seetlul bu baax sa jikko ak ni ngay soloo : War nañu fexe ba suñu jikko ak ni ñuy soloo bañ a tax nit ñi xalaat lu bon ci ñun, walla wax lu ñaaw ci mbootaayu Yexowa (Jëf. 28:22). Loolu du bu ñuy dem ci ndaje yu mag yi kese lañu ko war a def, waaye it bu ñuy tukki, walla bu ñuy féexal suñu xol. La Tour de Garde bu 1 ut 2002 nee woon na lii ci xët 18, xise 14 : “ Li ngay sol, waruloo ci wonewu te warul xumb lool. Boo dee jigéen, li ngay sol warul tax góor bu la gis rekk, xelam dem ci lu bon. Boo dee góor it li ngay sol warul tax bu la jigéen gisee, xelam dem ci lu bon. Warul wone cér yi ñu war a nëbb. Waruloo nekk it koo xam ne lu xew rekk, nga sol ko. Te it li ñu sol dafa war a wone ne dañu “ ragal Yàlla ”. Lii de, war nañu ci xalaat bu baax. Kon waruñu sol lu baax bu ñuy dem ci ndaje mbooloo mi, ba pare bu ñu nekkee feneen, sol li ñu neex. Fu ñu mënta nekk, li ñu sol dafa war a wone ne dañu ragal Yàlla, te dafa war a yiw. Lu tax ? Du ci yenn waxtu kese lañuy nekk waaraatekat. Bés bu nekk lañu koy doon, guddi ak bëccëg. ” — 1 Tim. 2:​9, 10.

8 Li ñu sol dafa war a yiw te yem. Fu ñu mënta nekk, suñu ngëm dafa war a feeñ ci li ñu sol ak ci suñu jikko. Su ko defee duñu mas a rus a waaraate ndax li ñu sol. — 1 Pie. 3:⁠15.

9 Waaraate saa yu ñu ci amee bunt dafay jur lu baax : Pool waaraate na ñaari at ca kër gu ñu ko tëjoon ca Room. Liggéeyam jur na lu baax, te gis na ko. Lukk wax na ne am na ñu ‘ gëm li mu waxoon ’. (Jëf. 28:24.) Pool ci boppam nee na : “ Li ma dal taxul xebaar bu baax dellu gannaaw, waaye da koo jëmale kanam. Noonu ñiy wottu buur bi ak ñépp gis nañu bu leer ne, turu Krist rekk a tax ñu jàpp ma. Te it mbokk yu bare takk nañu seeni fit ci li ñu gis samay buum, ba tax ñu gëna ñeme ci wax kàddug Yàlla ci lu àndul ak genn tiit. ” — Fil. 1:​12-14.

10 Daaw, ca kaasamaas, ay waaraatekat yu doon bokk ci fasoŋu waare boobu ñu ngi newoon ci mbedd ma. Loolu tàmmoon nañu ko def talaata bu nekk. Benn waaraatekat wax ak benn xale bu góor bu doon jàng Lycée. Ci lu gàtt, waaraatekat bi waxtaane ak moom ci Biibël bi. Bi ñu paree, mu may ko kayit bu ndaw bi tudd Avez-vous un esprit immortel ? Mu wax ko it mu ñów teew ci waxtaan bi ñu jagleel ñépp dimaas bu ci toppoon, te bindal ko adareesu Saalu Nguur gi ci kayit bu ndaw bi. Ca dimaas ba ca tegu rekk, xale bu góor bi daldi teel a ñëw ca Saal ba. Bu ndaje bi jeexee rekk, ñu seet ni ñuy def ngir mu mën a am njàngum Biibël bi ci këram. Booba ba tey, ndaje yépp lay teewe. Dina teewe sax ci njàngum téere bi. Ñetti weer kese lañu ko jàngal, téere Laaj bi jeex. Mu tàmbali jàng ci téere Xam-xam, ñaari yoon ayu-bés bu nekk, te bàyyi di fekke ndaje yi ñu doon def ci diine bi mu bokkoon bu njëkk. Yaw nag ? Boo sawaree ci waaraate bu baax, lu baax lan la mën a indi ?

11 Nañu liggéey bu baax ngir xibaar bu baax bi jëm kanam : Mbokku Pool yi dañu doon góor-góorlu ngir sawar ni moom. Wóor na ne bi ko Pool déggee dafa ci kontaan lool. Ñun itam nañu def lépp li ñu mën ngir xibaar bu baax bi jëm kanam, di jàngal nit ñi Biibël bi saa yu ñu ci amee bunt.

[Laaj yi]

1, 2. Lan moo la gën a neex ci ni Pool gise woon waaraate bi ? Naka nga mënee waaraate bu baax ni moom ?

3. Lan lañu mën a def ngir waaraate saa yu ñu ci amee bunt bañ a nekk loo xam ne dafay jékki-jékki rekk am ?

4. Lan la Pool def ba mën a waaraate ca kër bi mu nekkoon ?

5, 6. Kañ lañu mën a def fasoŋu waaraate boobu ? Naka lañu mënee waajal suñu bopp ngir mën koo def bu baax ?

7, 8. Bu ñu seetee li xise bi wax ci li ñuy sol ak ci suñu jikko, lan lañu war a moytu bu ñuy tukki, ak bu ñuy féexal suñu xol ?

9. Liggéeyu waare bi Pool defoon ca Room, lu baax lan la indi ?

10. Daaw am na benn waaraatekat bu doon waaraate fekk dafa ci amoon bunt. Lu baax lan la ci jële ?

11. Bu ñu bëggee waaraate bu baax ngir xibaar bu baax bi jëm kanam, lu ñu war a def ?

[Wërale bi nekk paas 3]

Téere yi ñu soxla ngir waaraate saa yu ñu ci amee bunt

■ Aimeriez-vous en savoir plus sur la Bible ? (kayit bu ndaw)

■ Lan la ñu Yàlla laaj ? (téere bu ndaw)

■ Une bonne nouvelle pour toutes les nations (téere bu ndaw)

■ Yeneen téere yu mën a neex nit ñi

[Wërale bi nekk pass 4]

Bu leen fàtte !

Fàtte ñan ? Képp ku suñu waxtaan neex te teewe ci ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ak ci waxtaan bi ñu faral di am ci àddina sépp, bu ndaje bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu weesoo. Ndax wax nga leen ñu ñów ci waxtaan yi ñu jagleel ñépp ak ci njàngum La Tour de Garde yi ñuy am ayu-bés bu nekk ? Bu ñu waxee ak ñoom ngir xiir leen ci loolu, xéyna ñu bare dinañu ñów. Ñooñu bu ñu tàmmee ànd ak ñi nekk ci Saalu Nguur gi, ak di déglu luy maye doole lu ñu fay jàngale, dinañu gën a jege Yexowa ak mbootaayam. Wax leen ñu ñów te xoolal lu ciy topp. Waxleen lépp li ñu war a xam. Bu leen fàtte wax boppu waxtaan yi ñu jagleel ñépp ak xaaj yi ñu war a jàng ci La Tour de Garde ak waxtu ndaje yi.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager