Nañu xamal nit ñi turu Yàlla
1 Bés bi nga njëkk dégg turu Yàlla, lan la la def ? Ñu bare dañuy mel ni jigéen ji waxoon lii : “ Bés bi ma gisee turu Yàlla ci Biibël bi, dama jooy. Bi ma xamee ne mënoon naa xam turu Yàlla te woo ko ci tur boobu, dafa ma laal ci sama biir xol. ” Bi mu jàngee turu Yàlla, ci la jigéen jooju xam ne Yàlla kenn la koo xam ne, mën nañu xaritoo ak moom.
2 Lu tax ñu war koo xamal nit ñi ? Xam turu Yàlla ëmb na xam lii : jikkoom, li mu bëgg def ak jëfam yi. Bu ñu bëggee mucc it, dañu war a xam turam. Ndaw li Pool nee na : “ Képp ku woo Boroom bi ciw turam [Yexowa], dinga mucc. ” Waaye nee woon na itam : naka la nit ñi di woowee Yexowa, bu ñu jàngul dara ci moom, te bu ñu ko gëmul ? Kon nag, karceen yi waruñu yéex ci xamal nit ñi turu Yàlla ak lépp li mu tekki. Lu am solo la (Room 10:13, 14). Waaye, am na leneen lu gën a war a tax ñu xamal nit ñi turu Yàlla.
3 Ci atum 1920 ak at yi ci topp, mbooloo Yàlla gis na li Mbind mi wax ci dëggal kiliftéefu Yàlla ak sellal turam. Balaa Yexowa di alag nit ñu bon ñi ngir sellal turam, dañu war a “ xamal nit ñi ci suuf si sépp ” dëgg gi jëm ci Yexowa (Isa. 12:4, 5 ; Esek. 38:23). Kon nag li gën a tax ñuy waaraate mooy lii : dañu bëgg màggal Yexowa te sellal turam ci kanamu doom-Aadama yépp (Yaw. 13:15). Bu ñu bëggee Yàlla ak suñu moroom, dinañu sawar ci liggéeyu Yàlla boobu.
4 ‘ Xeet wu ñu tudde turam ’ : Ci atum 1931 lañu woowe suñu bopp Seede Yexowa (Isa. 43:10). Booba ba tey, mbooloo Yàlla mi xamle na turu Yàlla bu baax. Looloo tax téere Prédicateurs nee na ci xët 124 : “ Ci àddina si sépp tey, bu ñu gisee ku tàmm a wax turu Yexowa, dañuy gaaw a wax ne Seede Yexowa la. ” Ndax loolu lañuy wax ci yow ? Bu ñu bëggee gërëm Yexowa ndax mbaaxaayam, dinañu ‘ sant turam ’, di wax ci moom saa yu ñu ko mënee. — Sab. 20:7 ; 145:1, 2, 7.
5 Ndegam ñun ñooy ‘ xeet wu ñu tudde turam ’, dañu war a topp li Yàlla santaane (Jëf. 15:14 ; 2 Tim. 2:19). Ci lu ëpp, li nit ñi di njëkk seetlu ci Seede Yexowa yi mooy seen jikko ju rafet ji (1 Pie. 2:12). Ku dul topp liy yoon ci kanamu Yàlla, walla ku jiitalul ci dundam lépp li ñu war a def ngir jaamu Yàlla, mu ngi tilimal turu Yàlla. Buñu def loolu mukk (3 Mu. 22:31, 32 ; Mal. 1:6-8, 12-14) ! Nañu dunde ci fasoŋ buy wone ne tur bi ñu am, maanaam Seede Yexowa, dafa am solo lool ci ñun.
6 Tey li Yexowa waxoon mu ngi am. Maanaam : “ Bu jant bi di fenk ba waxtu bi muy soo, sama tur dina mag ci diggu xeet yi. ” (Mal. 1:11). Nañu kontine di xamal nit ñi dëgg gi jëm ci Yexowa, te nañu “ sant turam bu sell bi ba abadan, waaw ba fàww ”. — Sab. 145:21.
[Laaj yi]
1. Xam turu Yàlla, lan la mën a def ci nit ?
2. Lu tax waruñu yéex a jàngal nit ñi lu jëm ci Yexowa ?
3. Lan moo gën a tax ñuy waaraate ?
4. Bu nit tàmmee wax turu Yexowa, lu tax ñuy gaaw a wax ne Seede Yexowa la ?
5. Ku ñuy woowe Seede Yexowa, lu tax mu war a sàmm jikkoom ?
6. Fii ba abadan, am na lu réy lu ñu mën a am. Loolu lan la ?