Nañu xam ni ñu waree jëfandikoo suñu téere yiy wax ci li nekk ci Biibël bi
1 “ Ci atum 1965 laa komaasee jàng seeni téere. Bu ma leen di jàng, damay wut ci Biibël bi aaya yi ci nekk. Gis naa ne, lépp li ñu wax ci seeni téere, dafa ànd ak li Biibël bi wax. Dama mas a bëgg xam dëgg gi ci Yàlla ak Yeesu. Waaye mën naa wax ne dëgg-dëgg, seeni téere ak Biibël bi, ñu ngi may xamal dëgg gi. ” Lii, benn góor moo ko bind ci leetar bu mu yónnee kër gu mag bu Seede Yexowa yi. Ci leetar boobu, dafa wax it ne dafa bëgg ñu jàngal ko Biibël bi.
2 Ci àddina si sépp, am na ay milyoŋi nit ñu bëgg téere yi “ surga bu takku te teey ” bi defar ngir jàngale Biibël bi (Macë 24:45). At mu nekk, dañuy defar ay téere yu baree-bare ngir dimbali boroom xol yu rafet yi, ñu “ xam dëgg gi ”. (1 Tim. 2:4.) Naka lañu mënee xam ni ñu waree jëfandikoo suñu téere yi ?
3 Bul jël lu ëpp li ngay soxla : Mën nañu dem ba dajale téere yu ëpp li ñu soxla. Lan lañu mën a def ngir moytu loolu ? War nañu xalaat bu baax bala ñuy jël ci mbooloo mi ay téere ngir waaraate bi. Bu ñu bëggee wone benn téere ci waaraate bi, mën nañu ci jël benn walla ñaar te bañ a jël yu bare. Bu ñu leen joxee ba pare, ñu sog a dellu wuti yeneen. Bu ñu defee loolu, duñu dajale téere yu bare ci suñu kër. Noonu it, bu ñu amee yéenekaay yu bare suñu kër yu ñu mënul joxe ci waaraate bi, xéyna li gën mooy ñu wàññi yéenekaay yi ñuy laajte ci mbooloo mi.
4 Su ñu amee téere yu ëpp li ñu ci soxla : Bu amee mbooloo bu am téere yu ëpp li mu ci soxla, kiy toppatoo téere yi war na seet ndax amul beneen mbooloo bu mën a soxla téere yu ëpp yi. Waaraatekat yi am téere yu yàgg, mën nañu leen jox seeni mbokk yu nekkul seede, ñiy jàng Biibël bi walla ñeneen. Ñi yàggul a bokk ci mbooloo mi, mën nañu bëgg am téere yooyu ngir boole leen ci kàggu (bibliothèque) bi ñu moomal seen bopp.
5 Li waral ñuy defar téere mooy dañu bëgg dimbali boroom xol yu rafet yi ñu xam lu rafet li Yexowa bëgg def. Bi Yeesu defee kéemaan ngir jox lekk mbooloo mu réy, sànniwul ñam bi desoon (Ywna. 6:11-13). Noonu it war nañu def li ñu mën ngir jëfandikoo ni mu gënee suñu téere yiy wone li nekk ci Biibël bi. Xibaar biy maye dund, te nekk ci suñu téere yi, bu desee ci suñu kër walla ci suñu saag, du mën a laal xolu nit ñi bëgg lu baax. Looloo tax ñu war a seet bu baax ñaata téere lañu war a jël ci mbooloo mi ngir waaraate bi. Te bu ñu leen jëlee ba pare, war nañu leen jëfandikoo ni mu gënee ngir ñu jariñ nit ñi. — Fil. 4:5.
[Laaj yi]
1, 2. Lan la nit ñu bare xalaat ci suñu téere yi, te ban laaj lañu war a laajte ?
3. Naka lañu mënee moytu jël lu ëpp li ñu soxla ci suñu téere yi ?
4. Bu mbooloo amee téere yu ëpp yi mu ci soxla, lu ñu mën a def ?
5. Naka lañu mënee wone ne dañu fonk suñu téere yi ?