Ndaje yu gën a mag yi ak yiy boole ay réew yu bare, xiir nañu nit ñi ci màggal Yàlla !
Ndaje yu gën a mag yi ak yi doon boole réew yu bare te tudd “ Nañu màggal Yàlla ” yi ñu jot a def, joxe nañu seede bu am doole. Xew-xew yu am solo yooyu màggal nañu turu Yàlla te tax nañu ñu gën a mën a “ màggal Yexowa màggal bi war ci turam ”. (Sab. 96:8.) Li Yexowa sàkk doy na kéemaan, te dafay wone jikkoom yu amul moroom yi. Loolu mu sàkk moo tax mu yelloo ñu màggal ko. — Ay. 37:14 ; Peeñ. 4:11.
Ci diggante 23 ba 29 feewriyee, dinañu waxtaan ci li ñu jële ci ndaje bu gën a mag bi. Ngir waajal ndaje boobu, jëfandikool laaj yii di topp ak kàddu yu am solo yi nga bindoon ci ndaje boobu.
1. Yëf yi dul dund yi Yàlla sàkk, naka lañuy màggale Yàlla ? Ni yëf yooyu di màggale Yàlla, naka la wuute ak ni ko nit di màggale (Sab. 19:1-3 ; “ Li Yàlla sàkk dafay koy màggal ”) ?
2. Yaramu Yeesu bi doon melax, dafa doon wone loo xam ne mu ngi am tey. Loolu lan la ? Loolu naka la yokkee doole karceen yi tey (Waxtaan bi jëm ci turu ndaje bi : “ Peeñu yi doy kéemaan te jëm ci lu war a am ëllëg, dañuy yokk doole ”) ?
3. Naka lañu mënee jàng woyof ni yonent Yàlla Dañel woyofe woon ? Te bu ñu ko defee, ban njariñ lañu ciy jële (Dañ. 9:2, 5 ; 10:11, 12 ; “ Ñi woyof lañu won ndamu Yexowa ”) ?
4. a) Am na ñetti mbir yu jëm ci àtte Yàlla yi, yu ñu mën a jànge ci li yonent Yàlla Amos yégle woon. Ñetti mbir yooyu ñooy yan (Amos 1:3, 11, 13 ; 9:2-4, 8, 14) ? b) Tey, lan la seede Yexowa yi mën a jànge ci li feeñ ci Amos 2:12 (“ Li yonent Yàlla Amos yégle woon, lu am solo la ci suñu jamano ”) ?
5. a) Ku dul yem ci ni muy jëfandikoo sàngara, bu fekkee sax du naan ba màndi, lu bon lan moo ko ci mën a dal ? b) Ku tàmmul a yem ci ni muy jëfandikoo sàngara, naka la mënee génnee boppam ci loolu (Mark 9:43 ; Efes 5:18 ; “ Moytuleen daanu ci ëppal ci sàngara ”) ?
6. Naka ngay jariñoo téere bu bees bu tudd ‘ Voyez le bon pays ’ (“ ‘ Réew mu naat ’ mu ñuy won ni Àjjana di mel ”) ?
7. Yan ñooy ñetti fasoŋ yi ñu mën a wone ndamu Yexowa (2 Kor. 3:18 ; “ Ni seetu, nañu wone ndamu Yexowa ”) ?
8. Yenn saay nit dina la bañ te fekk amul dara lu war a tax mu bañ la. Mbañeel bu mel noonu ci kan la jóge ? Bu ñu loolu dalee, lan moo ñu mën a jàpple ba ñu bañ a dellu ginnaaw ci wàllu ngëm (Sab. 109:1-3 ; “ Dañu leen bañ fekk defuñu dara ”) ?
9. Ci Yeesu, lan moo mën a tax nit nekk ku mag ? Naka lañu mënee seetaat suñu bopp ngir gis ndax soxla nañu góor-góorlu ngir gën a mën a xalaate ni Yeesu (Macë 20:20-26 ; “ Nañu bokk xalaat ak Krist ci liy màggaay ”) ?
10. Bu fekkee ne sax dañu sonn lool, lan moo ñu mën a jàpple ba ñu dëgër ci wàllu ngëm (“ Dañu sonn waaye duñu nangu loolu ëpp ñu doole ”) ?
11. Ci lan la Seytaane di jaar ngir siiwal ay fen ? Lan la Biibël bi wax ne mën nañu ko def bu amee ku bëgg yàq suñu ngëm (Ywna. 10:5 ; “ Nañu moytu waxu ñi bokkul ci ñun ”) ?
12. a) Naka la wayjur yi mënee roy ci li ñu wax ci Yeesu ci Mark 10:14, 16 ? b) Lan moo la neex ci téere bu bees bi tudd “ Écoute le grand Enseignant ” (“ Suñuy doom, lu réy la lu ñu donn ci Yàlla ”) ?
13. Ndaw yi, naka lañuy màggale Yexowa (1 Tim. 4:12 ; “ Naka la ndaw yi di màggale Yexowa ”) ?
14. Lan nga jàpp ci daraam bi tudd “ Nañu am fit, bañ a ragal bu ñu nu bëggee tere waaraate ” ?
15. Naka lañu mënee roy ci a) Pieer ak Yowanna (Jëf. 4:10) ? b) Ecen (Jëf. 7:2, 52, 53) ? c) Mbooloo karceen yu njëkk yi (Jëf. 9:31 ; daraam ak waxtaan bi tudd “ Nañu wéy di xamle xibaar bu baax bi ”) ?
16. a) Lan lañu fas yéene woon a def ngir màggal Yàlla ? b) Bu ñu toppee li ñu jàng ci ndaje bi gën a mag bi tudd “ Nañu màggal Yàlla ”, lan moo ñu mën a wóor (Ywna. 15:9, 10, 16 ; “ Nañu ‘ meññ meññeef gu sax ’ ngir mu màggal Yexowa ”) ?
Bu ñu xalaatee bu baax ci tegtal yu am solo ci wàllu ngëm yi ñu dégg ci ndaje bu gën a mag bi, dinañu bëgg topp li ñu fa jàng (Fil. 4:8, 9). Dina tax ñu gën a sawar a ‘ def lépp ngir màggal Yàlla ’. — 1 Kor. 10:31.