TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 12/03 p. 1
  • Nañu seet ñi ko yelloo

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Nañu seet ñi ko yelloo
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2003
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ni ñu mënee waare ci gox bu bare bitig
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Ndax am nga gox bi nga moomal sa bopp ngir waare ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
Sasu Nguuru Yàlla — 2003
km 12/03 p. 1

Nañu seet ñi ko yelloo

1 Yeesu dafa ñu sant ñu seet ñi ko yelloo bu ñuy waaraate ci dëkk bu ndaw mbaa bu mag (Macë 10:11). Waaye tey ñu bare toogatuñu seen kër. Kon lu ñu mën a def ba seet nit ñooñu ni mu ware ?

2 Nañu seetlu bu baax ñi nekk ci suñu gox : Li ñu war a njëkk def mooy seetlu li nit ñi tàmm def ci suñu gox. Maanaam kañ lañuy faral a nekk seen kër, fu ñu leen mën a fekk bëccëg, yan bés walla ci yan waxtu lañuy gën a nangu déglu. Boo waaraatee ci waxtu bi gën a baax ci ñi nekk ci sa gox, sa liggéey dafay gën a baax. — 1 Kor. 9:23, 26.

3 Waaraatekat yu bare dañu gis ne waaraate ci ngoon bala muy guddi, dafa baax lool. Am na ñu gën a féex te bëgg waxtaan ci waxtu boobu. Waaraate ci telefon ci ngoon it mën na baax. Mën nañu waaraate it ci béréb fu am ay bitig, walla feneen fu dul ci biir kër yi ngir xamal nit ñi xibaar bu baax bi.

4 Am na benn mbooloo moo xam ne dañu jàppoon benn weer ngir yokk li ñuy def ci liggéeyu waare bi. Ñu daldi def ay ndaje ngir waaraate samdi ak dimaas ci ngoon, ak it àllarba ak àjjuma ci ngoon bala muy guddi. Ñu seet it ni ñu mënee waaraate ci telefon ak fu bare bitig. Bi ñu defee loolu, waaraatekat yi dañu sawaroon ba nga xam ne mbooloo mi dafa kontine di def ndaje yooyu.

5 Nañu def li ñu mën ngir dellu seeti ñi suñu waxtaan neex : Xéyna ci gox bi ngay waare, fekk nit seen kër boo leen delloo seeti, yombul. Kon bala ngeen di pare seen waxtaan (bu dee sax waxtaan bu njëkk bi la) nangeen jàpp bés bi nga koy seetiwaat. Fexeel nag ba seeti ko ci bés boobu (Macë 5:37). Bu amee telefon, laaj ko nimoroom. Loolu mën na la dimbali bés boo bëggee kontine seen waxtaan.

6 Bu ñu góor-góorloo ngir wut ñi ko yelloo, te dellu seeti képp ku suñu waxtaan neex, nañu wóor ne Yexowa dina barkeel bu baax suñu liggéey. — Léeb. 21:5.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager