TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/04 p. 4
  • Ni ñu mënee waare ci gox bu bare bitig

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Ni ñu mënee waare ci gox bu bare bitig
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Nañu waare xibaar bu baax bi fu nekk
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Ndax am nga gox bi nga moomal sa bopp ngir waare ?
    Sasu Nguuru Yàlla — 2006
  • Nañu seet ñi ko yelloo
    Sasu Nguuru Yàlla — 2003
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 7/04 p. 4

Ni ñu mënee waare ci gox bu bare bitig

1 Ndax bëgguloo waare foo xam ne kër boo dugg rekk ñu teral la ? Te foo dugg rekk fekk fa nit ? Xéyna boo waare ci bitig yi bokk ci seen gox dinga am loolu. Ñiy waare ci bitig yi, lu baax li ñu fa jële bare na.

2 Am na mbooloo yu am ci seen gox béréb yu bare bitig. Kiy toppatoo goxu mbooloo mi dafa war a def ay kàrt ngir gox yooyu. Bu amee yeneen kàrt yuy boole kër ak bitig yooyu, dañu ci war a bind ci lu leer ne waruñu laal bitig yi. Ci yeneen gox yi, mën nañu waare ci bitig yi. Bu fekkee ne masuloo waare ci gox bu bare bitig, nanga njëkk komaase ci bitig yu ndaw yi.

3 Nañu wax lu yomb : Bu ñuy waaraate ci bitig yi, dañu war a solu ni ñuy soloo bu ñuy dem ci ndaje yi ci Saalu Nguur gi. Dañu war a dugg ci bitig yu barewul nit, walla bu ñu gisee ne jaaykat bi jàppul. Waxal ne danga bëgg wax ak boroom bitig bi, walla ki ñu dénk bitig bi. Ci lu gàtt, waxal li la indi. Lan nga mën a wax ?

4 Lii nga ko mën a wax : “ Yéen ñii di liggéey ci bitig yi, fekk leen seen kër yombul. Looloo tax ñu ñów fekksi leen fi ngeen di liggéeye. Dañu yore ay téere yuy wax ci li xew ci àddina si. ” Boo waxee loolu ba pare, ci lu gàtt won ko benn ponk ci suñu benn yéenekaay.

5 Mën nga wax itam lii : “ Ñu bare dañu bëgg xam li nekk ci Biibël bi, waaye amuñu benn jot. Kayit bu ndaw bii dafay wax ci porogaraam bi ñu def ngir dimbali nit ñi, ñu am tontu laaj yi ñuy laajte ci Biibël bi. ” Ba pare woneel li nekk ci xët 4 ak 5 ci kayit bu ndaw bi tudd Ndax bëgg nga yokk li nga xam ci Mbind mu sell mi ?

6 Bu fekkee ne ki yor bitig bi dafa jàpp, jox ko rekk benn kayit bu ndaw te ne ko : “ Ndegam danga jàpp, dinaa la jox kayit bu ndaw bii. Boo bëggee mën naa fi jaaraat beneen yoon te dinga ma wax li nga ci xalaat. ”

7 Nañu dellu seeti ñi wone ne suñu waxtaan neex na leen : Mën nga def sax njàngum Biibël ci gox yu bare bitig. Suñu benn mbokk mu nekk pioñee bu jébbal jotam yépp ci waaraate bi, dafa tàmmoon a yóbbu suñuy yéenekaay ci benn boroom bitig. Benn bés, boroom bitig bi dafa ko wax lu ko neex ci suñu yéenekaay yi. Ci la ko pioñee bi won naka lañuy jànge Biibël bi ak nit ñi ci téere Laaj. Ñu komaase benn njàngum Biibël bi ci saa si, fi muy liggéeye. Waaye saa yu fa pioñee bi doon dem ngir jàngal ko Biibël bi, du fa yàgg. Lu mat 10 minit walla 15 minit kese la fa doon def. Ñun itam nañu def ni moom. Nañu kontine di wut ñi ko yelloo ci gox yi bare bitig.

[Laaj yi]

1. Lu tax waaraate fi bare bitig am njariñ ?

2. Lu ñu mën a def ngir mën a waare ci gox bu bare bitig ?

3. Lan lañu war a def ngir suñu waaraate ci bitig yi baax ?

4-6. Lan lañu mën a wax boroom bitig walla ki ñu dénk bitig bi ?

7. Naka lañu mënee dellu seeti ñi suñu waxtaan neex ci gox bu bare bitig ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager