Nañu leen gaaw a seeti
Gaaw a seeti ñan ? Ñi bëgg jot ci suñuy téere walla ci suñuy yéenekaay saa yu amee yu bees ak ñi bëgg waxtaan ak seede yi ci seen kër. Yenn saay, dafay am ay nit ñuy telefone suñu bànqaas walla ñuy bind leetar ngir laajte loolu. Bu boobaa, bànqaas bi dafay yónnee kayit bi tudd “ Veuillez suivre l’intérêt ” (S-43) ci mbooloo mi nekk fi nit kooku dëkk. Magi mbooloo moomu war nañu jox benn waaraatekat kayit boobu ci saa si ngir mu gaaw a dem seeti nit kooku. Bu ko mënul a fekk këram, na ko telefone walla mu bàyyil ko benn not. Loolu lépp, war nañu ko gaaw a def.