Ay Tont Ci Seeni Laaj
◼ Ndax waaraatekat war na bind adareesu e-mail bi mu moomal boppam ci téere yi muy joxe ci waaraate bi ?
Am na waaraatekat yuy bind seen adareesu e-mail ci suñuy yéenekaay walla ci suñuy kayit yu ndaw yi ñuy jox nit ñi. Dañuy jëfandikoo tampe walla ñu binde ko ak masin. Loolu dafay tax ki jël téere yi mën a am fu muy mënee jot waaraatekat bi, bu bëggee yokk li mu xam ci xibaar bi. Ñiy def loolu ngir dimbali ñi suñu waxtaan neex, dañu bëgg def lu baax. Waaye, def nañu ba pare adareesu site bi suñu mbootaay moom ci ginnaaw yéenekaay yi ak ci ginnaaw kayit yu ndaw yi. Kon li gën mooy waaraatekat yi bañ a def seen adarees ci téere yi ñuy joxe.
Nit ku nekk mooy seetal boppam ndax war na bind ci kayit fu ñu ko mënee jot ngir joxe ko ci waaraate bi, walla buy dellu seeti nit ñi. Waaye buñu fàtte ne ñun ci suñu bopp ñoo war a dem seeti ñi suñu waxtaan neex. Moo gën ñu leen di bàyyi ñu war ñoo bind leetar bu ñu bëggee yokk seen xam-xam ci xibaar bu baax bi. Bu ñu nekkee ci kanamu nit ki lañu koy gën a mën a won ne dañu ko bëgg dëgg.