Lenn lu mën a dimbali nit ñi
Karceen dëgg yi dañuy xamle xibaar bu baax bi (Fil. 2:17). Am na lu ñu def ci Internet ngir jàpple leen ci. Mooy téere ak kayit yu ndaw yi ñu def ci 20 làkk, ci adarees bii : www.watchtower.org. Waaye du foofu la Seede Yexowa yi di jële seeni téere. Li ñu bëgg mooy, bu ñi bokkul ci Seede Yexowa yi bëggee xam li ñuy jàngale, ñu mën a jot ci loo xam ne ñun ñoo ko bind, waaye du keneen. Te ñu gis ne li Seede Yexowa yi jàngale yépp, ci Biibël bi lañu ko jële.
Bu yàggul, def nañu lu am solo ci internet. Dañu fa def téere Lan la ñu Yàlla laaj ? ci làkk yu gën a bare. Léegi mën nañu fa jàng téere boobu ci lu ëpp 220 làkk. Bind nañu itam adareesu Web boobu ci bépp La Tour de Garde ak Réveillez-vous ! buy génn, ci xët bu mujj bi. Loolu ci La Tour de Garde bu 1 sãwiyee ak Réveillez-vous ! bu 8 sãwiyee 2004 lañu ko komaase.
Loolu, naka lañu ko mënee jariñoo ? Booy waaraate mën nga daje ak ku bëgg waxtaan ak ñun waaye beneen làkk lay làkk. Bu kooku mënee jot ci Internet, mën nga ko won adareesu Web bi nekk ci xët bi mujj ci La Tour de Garde walla ci Réveillez-vous ! Bu ko defee, bala nga koy mën a indil ay téere ci làkkam, dina mën a seet li nekk ci téere Laaj ci làkkam, ci Internet. Mën nga boole itam nit kooku ak mbooloo walla gurup bu bokk ci làkkam.