TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 6/04 p. 4
  • Lu waral ndaje bi tudd Njàngum téere bi

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Lu waral ndaje bi tudd Njàngum téere bi
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2004
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ndimbal bi ñu mën a am ci Njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Ni wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi di toppatoo nit ku nekk
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
  • Jàppleel sa wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi
    Sasu Nguuru Yàlla — 2002
Sasu Nguuru Yàlla — 2004
km 6/04 p. 4

Lu waral ndaje bi tudd Njàngum téere bi

1 Bu njëkk, jàngkati Biibël bi, maanaam ñi nekk tey Seede Yexowa yi, dañu doon daje ci ay gurup ngir jàng Biibël bi. Ci atum 1895, gurup yooyu dañu leen doon woowe ci tubaab Cercles de l’aurore pour l’étude de la Bible. Te dañu doon jàng téere bi tudd L’Aurore du Millénium. Ginnaaw ga, ndaje yooyu dañu leen woowe Cercles béréens pour l’étude de la Bible (Jëf. 17:11). Gurup yi, ay gurup yu ndaw lañu woon. Ñi ci bokkoon dañu doon tànn ngoon bi gën ci gurup bi yépp, ngir ñu daje ci benn kër. Njàngum téere bi ñuy def tey ci mbooloo mi, ndaje yooyu lay topp.

2 Dañu fay yokk doole nit ñi te di leen jàpple : Ndegam gurup yi barewuñu nit, ku nekk mën nga bokk bu baax ci waxtaan bi te wax bu baax ci li nga ngëm. Loolu dafay tax ñu mën a “ dimbaleente ci sunu ngëm ”. — Room 1:​12.

3 Seetlu bu baax ni wottukatu njàngum téere bi di jàngalee, mën na ñu dimbali ngir ñu “ faramfàcce bu jub kàddug dëgg gi ”. (2 Tim. 2:​15.) Seetlul ni muy waxe ci aaya yi. Ayu-bés bu nekk, bu ñu paree njàng mi, kiy jiite njàngum téere bi dina seet ndax mën na jëfandikoo Biibël bi kese ngir seetaat ak ñi teew li ëpp solo ci li ñu jàng. Bu ñu toppee fasoŋ bu rafet bi muy jàngalee, dinañu gën a aay ci waaraate bi. — 1 Kor. 11:⁠1.

4 Liggéeyu wottukatu njàngum téere bi yemul rekk ci jiite njàngale bi ayu-bés bu nekk. Moom it mooy jiite waaraate bi. Dina gise ak wottukatu liggéeyu waare bi ngir mu seet li mu mën a def ngir waa gurupam mën a waaraate bu baax. Dafay seet ni mu mënee jàpple képp ku bokk ci gurupam ngir mu def wareefam ci waaraate xibaar bu baax bi ak sàkk taalibe. — Macë 28:​19, 20 ; 1 Cor. 9:​16.

5 Wottukatu njàngum téere bi dafa bëgg képp ku bokk ci gurupam am diggante bu rattax ak Yexowa. Dafa ciy dimbali mbokkam yi ci ndaje yi walla buy waaraate ak ñoom. Bu demee it seen kër, dafay waxtaan ak ñoom ngir dëgëral seen ngëm. Kon bu amee ku soxla ndimbal ci wàllu ngëm, bumu ko ragal a wax wottukatu njàngum téere bi. — Isa. 32:​1, 2.

6 Ku nekk dafay yokk doole moroomam : Am na ay réew foo xam ne, boo bokkee ci mbooloo Yàlla, dañu lay tere def li la sa ngëm laaj. Foofu suñuy mbokk yi dañuy daje ci gurup yu ndaw. Suñu benn mbokk nee na : “ Dëgg la, nguur gi dafa ñu tere woon a topp suñu diine ni mu ware. Waaye ayu-bés yi ñu ko mënoon yépp, dañu doon def suñuy ndaje ci ay gurupu 10 ba 15 nit. Loolu dafa doon dëgëral suñu ngëm, ndax dañu fa doon jàng Biibël bi te di waxtaan ak suñu mbokk yi, bu njàng mi jeexee. Bi ñu doon waxtaan, dañu doon wax ci fi ñu jaar. Moo tax ñu gisoon ne ñun ñépp a bokkoon jafe-jafe. ” (1 Pie. 5:⁠9). Nañu faral a teew ci Njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi ngir ñu yokkante doole ak suñuy mbokk ci ngëm. — Efes 4:​16.

[Laaj yi]

1. Njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi, fan la jóge ?

2. Ci njàngum téere bi, naka lañu mënee def suñu wàll ngir “ dimbaleente ci sunu ngëm ” ?

3, 4. Njàngum téere bi, naka la ñuy dimbalee ci suñu liggéeyu waare bi ?

5. Ban ndimbal la kenn ku nekk ci ñun mën a am ci njàngum téere bi ?

6. a) Ci yenn réew suñu mbokk yi dañuy daje ci ay gurup yu ndaw. Naka la ndaje yooyu yokke seen doole ? b) Njàngum téere bi, ban njariñ nga ci gis yow ci sa wàllu bopp ?

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager