Ni wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi di toppatoo nit ku nekk
1 Lii moo tax ñu def njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi : “ mën a seetlu bu baax nit ku nekk ngir gis ni muy jëme kanam ci wàllu ngëm. [...] Loolu dafay wone ne Yexowa dafa laabiir te dafay toppatoo mbooloom ak mbëggeel ”. (om xët 75 ; Isa. 40:11). Wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi am na wàll bu am solo ci li ñuy def ngir toppatoo nit ku nekk.
2 Ci njàngum téere bi : Dañuy fexe ba ñi bokk njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi bañ a bare. Bu ko defee, wottukatu njàngum téere bi dina leen mën a xam bu baax (Léeb. 27:23). Ci lu ëpp, ayu-bés bu nekk, balaa njàngum téere bi di tàmbali, walla it bu jeexee, dina mën a waxtaan ak ñoom. Noonu, ci benn weer, dina mën a waxtaan ak li ëpp ci ñoom. Bu ko defee dinañu koo ñeme jege, bu ñu amee jafe-jafe, walla bu ñu soxlaa ku dëfël seen xol. — Isa. 32:2.
3 Wottukatu njàngum téere bi dafay jéem a xiir ñépp ci tontu, bu ñuy def njàngum téere bi. Lii bokk na ci li muy def ngir loolu : buy jiite, dafay neex deret (1 Tes. 2:7, 8). Dafay góor-góorlu ngir boole xale yi ak ñépp ci waxtaan bi. Bu amee ku bare kersa ba du ñeme tontu, mën na wéet ak moom, ngir dimbali ko ci. Bu boobaa, dinañu tànn aaya bu mu mën a jàng walla benn xise fu muy tontu. Mën na ko won it ni mu mënee tontu ci kàddu boppam.
4 Kiy jàpple wottukatu njàngum téere bi mën na nekk benn surga mbooloo mi. Bu boobaa, wottukat bi dina fexe ba ñaari weer yu nekk, mu jiite benn yoon njàngum téere bi. Dina tax mu mën koo seetlu te jox ko ay xelal yu koy dimbali. Lii de, baax na lool ngir dimbali suñu mbokk yu góor ndax ñu mën jàngale bu baax. — Titt 1:9.
5 Ci waaraate bi : Jiite waaraate bi bokk na ci li ëpp solo ci warugaru wottukatu njàngum téere bi (4 Mu. 27:16, 17). Dafay toppatoo lépp lu jëm ci waaraate bi ñuy def ci njàngum téere bi. Dafay dimbali it ñi ci bokk ndax ñu mën a am mbégte bu ñuy waaraate (Efes 4:11, 12). Ngir mën a am loolu, dafay fas yéene waaraate ak képp ku bokk ci njàngum téere bi. Yenn saay dafay am ñu bëgg gën a aay ci yenn fànn ci waaraate bi. Wottukat bi dafay seet ak wottukatu liggéeyu waare bi ni ñu mënee def ba waaraatekat yu leen gën a aay dimbali leen.
6 Sàmm bu am mbëggeel : Wottukat bi dafay toppatoo ñi nga xam ne am na liy tax lu tuuti rekk lañu mën a def ci waaraate bi. Am na ñu màgget ba mënatuñu def lu bare, ñeneen mënuñu génn seen kër walla def lu bare ndax dañu feebar lool walla dafa am lu leen gaañ. Ñooñu wottukat bi dina seet ndax xam nañu ne bu amee weer bu ñu mënul a waaraate lu mat 1 waxtu, bu ñu waaraate lu mat 15 minit, mën nañu bind li ñu def ci waaraate bi te joxe ko. (Kurélu liggéeyu waare bi mooy wax ku mën a bokk ci loolu.) Dina toppatoo it ñi bokk ci njàngum téere bi te bàyyi waaraate. Dina góor-góorlu ngir dimbali leen ba ñu bokkaat ci li ñuy def ci mbooloo mi. — Lukk 15:4-7.
7 Li ñu wottukatu njàngum téere bi ñuy def ci mbooloo mi di toppatoo ak mbëggeel, tax na ñu am ngërëm bu réy. Ni muy toppatoo nit ku nekk dafay tax “ nu mànkoo ci sunu ngëm [...], te taxaw taxawaay, bu dëppook matug Krist ”. — Efes 4:13.