Ku muñ dina am lu baax
1 “ Seen muñ moo leen di musal. ” (Lukk 21:19). Yeesu moo waxoon loolu ci jamano bi “ àddina di tukki ”. Li mu wax noonu, wone na ne ku bëgg topp Yàlla, dinga bare jafe-jafe. Waaye bu ñu Yexowa mayee doole, dinañu mën a “ muñ ba ca muj ga ” te “ mucc ” ñun ñépp. — Macë 24:3, 13 ; Fil. 4:13.
2 Feebar, fitnaal, ñàkk xaalis, naqaru xol ak yeneen mën na tax ñu dëkk ci naqar bés bu nekk. Waaye buñu fàtte ne Seytaane mu ngi def lépp li mu mën ngir ñu bàyyi Yexowa. Saa yu ñu toppee suñu Baay Yexowa rekk, def nañu luy tax mu mën a tontu ki koy sóoru. Am na it lu mën a seddal bu baax suñu xol : Yexowa du fàtte rangooñ yi ñuy tuur bu ñu nekkee ci coono. Rangooñ yooyu, dañuy laal Yexowa bu baax. Bu gisee ku koy topp te bañ ko weddi, xolam dafay sedd lool. — Sab. 56:8 ; Léeb. 27:11.
3 Jafe-jafe mën na tax ñu wàññi suñuy sikk : Jafe-jafe mën na feeñal sikk ci suñu ngëm, walla jikko bu bon bu ñu am, mel ni yéeg sa bopp, walla ñàkk muñ. Kon, bu ñu jaaree ci lu metti, buñu def li Yàlla tere ngir mën ci rëcc walla ngir jafe-jafe boobu jeex. Nañu bàyyi suñu “ muñ dem ba mat ”, ni ko Kàddu Yàlla waxe. Lu tax loolu ? Ndaxte bu ñu toppee Yàlla, di muñ suñu jafe-jafe yi, duñu “ fell fenn ” maanaam duñu am benn sikk (Saak 1:2-4). Mën na tax ñu soppi suñu jikko ba nekk ku ànd ak sa sago, ku laabiir, ku bare yërmande walla ku am beneen jikko ju rafet. — Room 12:15.
4 Dina sellal suñu ngëm : Muñ ay jafe-jafe dafay sellal suñu ngëm, maanaam dafay tax ñu am ngëm goo xam ne jaar na ci lu metti ba gën a dëgër. Yexowa fonk na ngëm gu mel noonu (1 Pie. 1:6, 7). Te it bu ëllëgee, bu ñu amee ay jafe-jafe, duñu dellu ginnaaw. Yàlla dina ñu won ne dañu ko neex. Loolu dina gën a dëgëral suñu ngëm, te suñu yaakaaru ëllëg dina ñu gën a wóor. — Room. 5:3-5.
5 Li gën a rafet ci li muñ mën a jur mooy li Saak 1:12 wax, maanaam : “ Ku dékku nattu, ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund. ” Kon nag, nañu sax ci jaamu Yexowa te na ñu wóor ne dina barkeel bu baax ñiy kontine di “ ko bëgg ”.