TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Watchtower
TÉERE YI AM CI SUÑU PALAAS CI INTERNET
Wolof
  • BIBLE
  • TÉERE YI
  • RÉUNIONS
  • km 7/07 p. 1
  • Kuy muñ nattu, ku barkeel nga

Aucune vidéo n'est disponible pour cette sélection.

Il y a eu un problème lors du chargement de la vidéo.

  • Kuy muñ nattu, ku barkeel nga
  • Sasu Nguuru Yàlla — 2007
  • Leneen lu jëm ci loolu
  • Ku muñ dina am lu baax
    Sasu Nguuru Yàlla — 2004
Sasu Nguuru Yàlla — 2007
km 7/07 p. 1

Kuy muñ nattu, ku barkeel nga

1 Karceen yépp dañuy am ay coono (2 Tim. 3:12). Mën na nekk feebar, poroblemu xaalis, lu lay bëgg dugal ci lu bon, walla ñu lay fitnaal, ak yeneen yu bare. Seytaane dafa ñuy tegg ay coono, ngir ñu waññi li ñuy def ci liggéeyu waare bi walla ñu bañ ko def ni mu ware, walla sax ñu bàyyi di jaamu Yexowa (Ayó. 1:9-11). Ban mbégte la muñ di indi ?—2 Pie. 2:9.

2 Waajalal sa bopp : Yexowa jox na ñu Kàddoom bi nekk kàddu dëgg gi. Li Yeesu def ak li mu jàngale, mi ngi ci Kàddu googu. Bu ñuy déglu te di def itam li Yeesu wax, dinañu am fu dëgër fi ñu mën a jàpp. Te it dinañu waajal suñu bopp ngir mën a jàkkaarloo ak jafe-jafe yi (Luug 6:47-49). Am na leneen lu ñu mën a may doole : suñu mbokk karceen yi, ndaje karceen yi ak téere yi surga bu takku te teey bi defar te ñuy sukkandiku ci Biibël bi. Mën nañu ñaan Yàlla saa yu ñu ko bëggee. — Macë 6:13.

3 Yexowa may na ñu it yaakaar. Bu ñu fexee ba am ngëm gu dëgër ci li ñu Yexowa dig, suñu yaakaar dina mel ni fu ñu “ sës suñu xol, ba man a sampu bu dëgër ” (Yaw. 6:19). Ci jamano bi ñu doon bind Biibël bi, gaal du dem géej te amul lànkar (maanaam li koy téye ngir mu mën a taxaw ci géej gi). Bu asamaan leeree sax du dem géej te amul lànkar. Bu dee dafa jekki jekki rekk am taw bu metti, boroom gaal dafa doon sànni lànkar ci ndox mi ngir gaal gi taxaw te ba dal ci xeer bañ yàqu. Tey it, bu ñu fexee ba gën a gëm li ñu Yàlla dig, bu poroblem yi baree sax suñu xel dafay dal. Jafe-jafe yi mën nañu jékki-jékki rekk dal suñu kow. Fàttaliku leen bi Pool ak Barnabas komaasee waare ci dëkku Listar. Nit ñi dañu leen déglu woon bu baax. Waaye bi yawut yi leen doon kontar agsee, mbir mi dafa soppeeku ci saa si.— Jëf. 14:8-19.

4 Muñ, ci mbégte lay mujjee : Bu amee ay nit ñu nu kontar, bu ñu kontinee di waare, dinañu am xel mu dal. Dañuy bég lool bu ñu nit ñi toroxalee ndax turu Kirist (Jëf. 5:40, 41). Muñ nattu yi, dina tax ñu gën a woyof, gën a dégg ndigal te gën a mën muñ lu metti (5 Mu. (Deut.) 8:16 ; Yaw. 5:8 ; Saag 1:2, 3). Loolu dina ñu jàngal it yaakaar Yexowa, gëm li mu ñu dig, ak làqu ci ginnaawam.— Léeb. 18:10.

5 Ñun xam nañu ne nattu yi dinañu mas a jeex (2 Kor. 4:17,18). Nattu yi dafa ñuy may ñu wone fi suñu mbëggeel ci Yexowa tollu. Bu ñuy muñ nattu yi, loolu tontu la ci li Seytaane wax. Moo tax duñu bàyyi mukk ! “ Ku dékku nattu (maanaam kuy muñ nattu), ku barkeel nga, ndax boo ci génnee ak ndam, dees na la jagleel kaalag dund, gi ”. — Saag. 1:12.

    Téere yi ci Wolof (1996-2025)
    Ngir génn
    Ngir konektewu
    • Wolof
    • Yónnee ko
    • Ni nga bëgge mbir yi feeñe
    • Copyright © 2025 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania
    • Conditions d’utilisation
    • Règles de confidentialité
    • Paramètres de confidentialité
    • JW.ORG
    • Ngir konektewu
    Partager