Ndaje bu mag bu ñaari fan bii di ñów : li ñu fay waxtaane
Ci “ bési tiis yu tar ” lañu nekk. Wéy di neex Yexowa, yombul. Moo tax ñu soxla topp xam-xamu Yàlla (2 Tim. 3:1). Ndaje bu mag bu ñaari fan bi ñuy am ci atum liggéeyu waare 2005, mu ngi tudd “ Nañu topp xam-xamu Yàlla ”. Dinañu fa dégg lu am solo, te bu ñu ci jógee, dina ñu gën a sawar a def li Yàlla bëgg. — Saak 3:17.
Dinañu fa déglu ay waxtaan yu def ay xaaj. Bu njëkk bi mu ngi tudd “ Nañu wone ci li ñuy def ne dañu am xam-xamu Yàlla ”. Dina ñu won lan mooy nekk ku sell, ku ànd ak jàmm maanaam ku bëgg jàmm, ku lewet ak ku nooy, maanaam ku dégg ndigal. Ba pare, wottukat biy wër dina wax ci yeneen fànn yu bokk ci xam-xamu Yàlla. Waxtaan bi mujj ci fan bu njëkk bi, Surveillant de district bi (maanaam kiy wër ci ndaje yu mag yu ñaari fan yi) moo koy def. Dina wax ci ñiy wax ne waaraatekati karceen yi “ musuñoo jàng mbaa [...] gëstu ci diine ”. Waaye dina wone ne am nañu lépp li ñu soxla ngir wax li jëm ci xam-xamu Yàlla. — Jëf. 4:13.
Ci ñaareelu fan bi, dina am waxtaan bu def ay xaaj bu tudd “ Nañu topp li mën a tax ñu jëm kanam ”. Dinañu ci seet ni ñu mënee moytu dellu ginnaaw ci wàllu ngëm. Dinañu seet it li ñu mën a def ngir xiir nit ñi ci jëm kanam ci wàllu ngëm, bu ñu nekkee ci ndaje mbooloo mi, ci waaraate bi ak ci suñu biir kër. Waxtaan bi ñu jagleel ñépp dina tudd “ Lu baax li ñu mën a jële ci topp xam-xamu Yàlla ”. Dina tax ñu gën a gërëm Yexowa ci lu baax li ñuy am bu ñu defee liy yoon ci kanamam. Waxtaan bu mujj bi mu ngi tudd “ Topp xam-xamu Yàlla, dafa ñuy aar bu baax ”. Dina tax ñu gën a bëgg am xam-xamu Yexowa ci muju jamano jii ngir topp ko.
Ni ñu ko tàmmee def ci ndaje yu mag yépp, dinañu sóob ci ndox taalibe yu bés yi. Dinañu def it Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi ak njàngum La Tour de Garde bi ñu war a def ci ayu-bés boobu. Yexowa dafa bëgg ñu jariñoo bu baax xam-xam bi mu ñuy jox. Dinañu jàng lu bare ci ndaje bu mag bu ñaari fan boobu, te dina ñu dimbali ñu jëm kanam ci wàllu ngëm. — Léeb. 3:13-18.