Nañu fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi
Laaj yii di topp, dañu leen defar ngir ñu mën a xam li ñuy waxtaane ci ndaje bu mag bu ñaari fan ci atum liggéeyu waare 2005, bala ndaje boobu di jot. Laaj yooyu lañuy laajte it bu ñuy fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag boobu. Xaaj bi tudd “ Lu bees li ñu defar ngir fàttaliku li ñu waxtaane ci ndaje yu mag yi ” te nekk ci xët 4 ci Sasu Nguuru Yàlla bii, wax na ni ñu waree jëfandikoo xaaj bii. Bu ngeen di fàttaliku li ñu jàng ci ndaje bu mag bi, kiy jiite waxtaan bi war na xam bu baax ñaata minit la bëgg yàgg ci laaj bu nekk ngir mën a laal laaj yépp. Li ñu bëgg ci waxtaan bi mooy mu wone bu baax ni ñu mënee topp li ñu jàng ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi.
FAN BU NJËKK BI : SUBA SI
1. Lan moo ñu mën a dimbali ba ñu am xam-xamu Yàlla ?
2. Waaraatekat yi bokk ci mbooloo yi teewe ndaje bu mag bu ñaari fan bi, lan lañuy def ngir xamal nit ñu bare xibaar bu baax bi ?
FAN BU NJËKK BI : NGOON GI
3. Lu tax set ci wàllu ngëm ak ci sa xalaat am soloo lool ci karceen ? Ku bëgg a sete noonu, lan la war a def ?
4. Bu ñu nekkee ak suñu mbokk yi, naka lañu mënee wone ne dañu bare jàmm ?
5. Lan mooy ànd ak sa sago, te naka lañu ko mënee wone bu ñuy seet li ñuy def ci jot bi ñu am ?
6. Bu ñu seetee li Sóol ak Nóoxin def, lan lañu ciy mën a jàng ? Naka lañu mënee wone ne dañu “ nooy ”, maanaam dañuy dégg ndigal ? (Saak 3:17)
7. Naka la karceen yi mënee moytu nekk koo xam ne, boo nekkee ci sa diggu mbokk yi dangay wone jikko karceen, waaye bu la sa mbokk yi gisul rekk nga nekk ci li la neex ?
8. Naka lañu mënee roy Pool ci ni mu doon waxe ci xam-xamu Yàlla ?
ÑAAREELU FAN BI : SUBA SI
9. Lu tax ñu war a tànn bu baax li ñu bëgg def, te lan moo ñu ci mën a dimbali ?
10. Suñu mbokk yi bokk ci mbooloo yi teewe ndaje bu mag bu ñaari fan bi, lan lañuy def ba tàmm di teewe ndaje yi ñu am ci mbooloo mi, te ban njariñ lañu ci am ?
11. Lan la boroom kër mën a def ba waa këram am ngëm gu dëgër ?
12. Lan moo nekk soxla ci mbooloo yi teewe ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi ?
ÑAAREELU FAN BI : NGOON GI
13. Ni ñu ko wone ci waxtaan bi ñu jagleel ñépp, lu baax lan la xam-xamu Yàlla def ?
14. Lu tax ñu mën a wax ne ku wóolu boppam, walla ku wóolu koo xam ne xam-xamu Yàlla jiitalu ko, kooku amul xel ? Ci yan fànn lañu war a seet bu baax li ñuy def ?
15. Yan musiba lañuy moytu bu ñu toppee xam-xamu Yàlla ?
16. Lu tax topp li ñu waxoon ci ndaje bu mag bu ñaari fan bi nekk lu am-a-am solo ?