Lan mooy njariñu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla ?
1 Yexowa di la jàngal. Ñi bokk ci mbootaayam rekk ñoo mën a am loolu (Isa. 54:13 ; Ywna. 6:45). Waaye, boo bëggee mu jariñ la, fàww nga góor-góorlu ci bu baax. Ndax yaa ngi gis lu baax li Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla di def ci sa ngëm ?
2 Lu baax li ñu ci wax : Ay wottukatu Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla yu bare gis nañu ne waxtaan bi tudd Liy tax ñu aay ci wax, tax na ñu bare gën a aay ci waaraate bi. Léegi itam ñépp a mën a bokk ci waxtaan bi tudd Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi. Loolu tax na ñu gën a bare topp porogaraam bi ñu def ngir jàng Biibël bi ayu-bés bu nekk. Moom la kenn ci ñiy jiite Lekkool bi seetlu. Waxtaan no 2 bi nag, ñu bare kontaan nañu ci ni ñu koy defe léegi. Ñi koy def soxlatuñu wax dara bala ñuy jàng ci Biibël bi ak bu ñu jàngee ba pare. Kon dañu gën a am jot ngir waajal bu baax njàng mi te gën ci aay. — 1 Tim. 4:13.
3 Ñépp la mën a jariñ : Am na loo mën a def ngir joxe ay tont ci suñu ndaje neex la (Léeb. 15:23). Seetal bés bu ñuy fàttaliku li ñu jàng ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla. Teel nañu xam li ñu fa war a laaj. Kon mën nañu waajal laaj yooyu te, bu bés bi jotee, bokk bu baax ci waxtaan bi. Léegi La Tour de Garde mu ngi génne ay ponk yu am solo ci xaaju Biibël bi ñu war a jàng ayu-bés bu nekk ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla. Loolu ci La Tour de Garde bu 1 sãwiyee 2004 la komaase. Ñu bare dañu ciy jël li ñuy wax ci waxtaan bi tudd Kàddu yu am solo ci li ñu waroon a jàng ci Biibël bi.
4 Képp ku bokk ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla, am nga lu réy : dangay def ci kanamu ñépp waxtaan yi nga waajaloon. Kiy jiite lekkool bi, bu waxee lu baax li eleew yi def, ñépp a ci mën a jariñoo. Te bu bëggee wax ak eleew bi bu ndaje bi paree ngir dolli ci dara, loolu dina yokk njariñ bi eleew bi di jële ci lekkool bi. Ci téere Tirez profit de l’École du Ministere Théocratique, am na itam ci suufu njàngale bu nekk li nga mën a jéem a def ngir gën a aay ci ponk bi ngay liggéey. Loolu it baax na ci ku bëgg jariñoo bu baax lekkool bi.
5 Ci Lekkoolu Sasu Nguuru Yàlla, soo déggee loo xam ne bëggoo ko fàtte, nanga ko bind ci sa téere Tirez profit de l’École du Ministere Théocratique. Nanga xalaat bu baax ci li nga jàng. Te xam-xam bi la Yàlla may noonu, seetal lu baax li mu def ci sa ngëm.