Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla, bu atum 2002
1 Wax, may la, gu jóge ci Yexowa. Waaye, li ëpp ci nit ñi duñu ci wone ngërëm. Ndaxam maye boobu day tax ñu mën a diisook ñeneen ñi, te xamal leen suñuy xalaat ak li ñuy yëg ci suñu biir xol. Li ëpp solo mooy, pexe la ngir màggal suñu Yàlla. — Sab. 22:22 ; 1 Kor.1:4-7.
2 Góor, jigéen ak xale lañuy jàngal ci Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla bi, ndax ñu màggal turu Yexowa (Sab. 148:12, 13). Doxalinu lekkool bi ngir 2002 daa ëmb waxtaan yu bare yu sukkandiku ci Biibël bi. Ku nekk ci ñun mën na leen a jariñoo, te mën nañu leen a jëfandikoo itam ci sasu waare bi. Waajal lekkool bi te di ci bokk mën naa tax ñu yokk suñu xam-xam ak suñu manoore niki jàngalekatiy Kàddug Yàlla. — Sab. 45:1.
3 Jàngal Biibël bi bés bu ne : Bu la sa Biibël dul sore mukk, mën ngaa jariñoo jot goo am ngir jàng ko. Li ëpp ci ñun am nañu simili yu néew ci biir bés bi, yu ñu mën a jagleel loolu. Jàng lu mu tuuti tuuti benn xët bés bu nekk, akay lu am njariñ ! Loolu doŋŋ lañuy laaj ngir topp doxalinu jàng Biibël bi ñu tëral ci doxalinu lekkool bi. — Sab. 1:1-3.
4 Mën jàng bu baax Biibël bi da ñuy dimbali ñu laal xolu ñi ñuy déglu te da leen di xiir ci màggal Yexowa. Jàngaan yi ñu sas Sas No. 2 ci lekkool bi, war nañu di tàggantu, di tàggantu — te bañ a tàyyi — ci jàng ca kaw li ñu leen sas. Wottukatu lekkool bi dina leen ndokkeel te xelal ngir ñu taneel njàng mi.
5 Jëfandikool téere Comment raisonner : Ñi ñu sas waxtaan No. 3 ak No. 4, ci téere Comment raisonner lañuy sukkandiku. Du ñàkk, ñu gën a bare ci ñun mën a gën a gimmi ci njariñam ci liggéeyu tool bi. Jàngaan yi war nañoo tànn anami seen waxtaan, fexe ñu dëppook li am ci gox gi ñuy waare. Wottukatu lekkool bi war naa bàyyi xel bu baax ci ni ñuy jàngale ak a jëfandikoo Mbind yi.
6 Yal na ñu Lekkoolu sasu Nguuru Yàlla dimbali ñun ñépp, ñu wéy di jëfandikoo mën-mënu wax, may gu ñu Yàlla baaxe, ngir xamle xabaar bu baax bi te màggal suñu Yàlla ju màgg ji, Yexowa ! — Sab. 34:1 ; Efes 6:19.