Waaraate bi dafay tax ñu mën a muñ
1 Kàddu Yàlla mu ngi ñuy wax ñu “ daw xél wi [maanaam rawante bi] nekk suñu kanam, ànd ci ak muñ ”. (Yaw. 12:1.) Dawkat bu bëgg yóbbu ndam li, dafa war a muñ. Ñun it, bu ñu bëggee am dund gu dul jeex, dañu war a muñ (Yaw. 10:36). Liggéeyu waare bi mën na ñu dimbali ñu muñ, di topp Yàlla bu baax ba muju jamano ji jot. Naka la koy defe ? — Macë 24:13.
2 Dafay dëgëral suñu ngëm : Biibël bi dige na lu neex : Àddina su bees fu njub dëkk. Bu ñu koy yégal nit ñi, dafay dëgëral suñu yaakaar (1 Tes. 5:8). Bu ñu tàmmee bokk ci liggéeyu waare bi, dinañu mën a xamal nit ñi dëgg yi ñu jàng ci Biibël bi, ak it li tax ñu gëm leen. Loolu dafay dëgëral bu baax suñu ngëm.
3 Bu ñu bëggee jàngal nit ñi ni mu ware, dañu war a xam bu baax li Biibël bi di jàngale. Dañu war a gëstu te xalaat bu baax ci li ñu war a jàngal nit ñi. Bu ñu ci góor-góorloo, suñu xam-xam dina gën a yaatu, suñu ngëm gën a dëgër, te dinañu gën a am doole ci wàllu ngëm (Léeb. 2:3-5). Kon nag booy dimbali sa moroom, yaa ngi dëgëral sa ngëm. — 1 Tim. 4:15, 16.
4 Sawar ci waaraate bi, lu am maanaa la ci li Biibël bi di woowe “ yérey xarey Yàlla yépp ”. Boo solee yére yooyu, Seytaane ak malaakaam yu bon yi duñu la mën a daaneel (Efes 6:10-13, 15). Ku sawar ci liggéeyu waare bi, xelam dina nekk ci lu mën a dëgëral ngëmam, te àddina Seytaane sii du ko yóbbaale (Kol. 3:2). Jàngal nit li neex Yexowa, dafa ñuy fàttali ne ñun it suñu dundin dafa war a rafet. — 1 Pie. 2:12.
5 Yàlla moo ñuy dooleel : Am na leneen lu liggéeyu waare bi di def. Dafa ñuy jàngal yaakaar Yexowa (2 Kor. 4:1, 7). Loolu, barke bu réy la. Jàng wóolu Yexowa noonu, dina ñu dimbali ci waaraate bi, waaye it ci bépp coono àddina (Fil. 4:11-13). Jàng wéeru bu baax ci Yexowa, loolu mooy tax ñu mën a muñ (Sab. 55:22). Waaw, li liggéeyu waare bi di def ngir jàngal ñu muñ, bare na.